SËRIÑ SAALIW TURE WÀCC NA

Yeneen i xët

Aji bind ji

Sëriñ Saaliw Ture mi toogaloon xalifa Murid yi ca Kees a wàcc liggéey guddig àjjuma jàpp gaawu (14/15 sàttumbar 2023) fi Ndakaaru. Amoon na 84i at.

Sëriñ Saaliw Ture ñiŋ ko tudde Sëriñ Saaliw Mbàkke mi ko yar, jàngal ko, wóolu woon ko tamit ba daan digaaleek moom lu bari. Moom jëwriñ ji, ca Cees defandoo na daara ak Sëñ Muntaqaa mi ci jal bi tey, ñu fasante fa kóllëre.

Sëriñ Abdu Lahaat ci boppam moo ko sampoon Cees ca atum 1980 ginnaaw bim ci mànkook njabootam. Keroog jooju ba tey ni mu génne àddina, Sëriñ Saaliw Ture nekkul woon ci lu dul wattu ak taaral yoonu murid. Daa na woote ak a ñaax taalibe yi ci jaamu Yàlla ak liggéey te bañ a yàq, jub te moytu tooñ.

Sëriñ Saaliw Ture gëmoon na Yàlla, di liggéey ngir Yàlla jaare ko ci yoonu murid ndax Sëriñ Tuubaa. Daan na wax taalibe yi :

« Saa jëmmu bopp jii, woowuma ci kenn. Ndax, lu jar woo nit nekku ci. Waaye, Sën Tuubaa lu jar woo nit a ngi ci moom…

Mu yéex, mu gaaw, danga dajeek Yàlla ci bàmmeel. Su booba koo ko tëkkaleek danga xam ne kooka du Yàlla ».

Ginnaaw biñ ko dencee ba noppi fa Tuubaa, lii la ko Sëriñ Mustafaa Saaliw seedeel ci mbooloo ma ko gunge woon këram gu mujj. Nee na :

« Sëriñ Saaliw Ture, ci digganteem ak yeneen tarixa yi, ak jàngu bi, dafa doxaleek ñoom doxiinu xam-xam ak jullit, taalibe, ba ñépp di ko xoole Sëriñ Tuubaa. Daawul wone boppam mukk. Ku tabe woon lool ci alalam ak ci darajaam ; njabootu Sëñ Tuubaa gu mësaan egg ci moom mu teral la te moone moo la mag fuuf, ëpp la xam-xam fuuf, dàq laa jaamu Yàlla fuuf, ba noppi liggéeyal Sëriñ Tuubaa loo ko liggéeyalul. Waaye, mu jàppe la sëriñam ngir jëmmu Sëriñ Tuubaa. Sëriñ Saaliw Ture waatoon ci Sëriñ Tuubaa ni du dajeek moom mukk rus. Kon, dëgg ak njub la fi nekke woon te du dellusi mukk di wax ak nun. Kon, rikk la mu nu bàyyiloon, nanu ci nekk ba fekki ko ».

Liggéeyam bu rafet bii moo taxoon Akaademi Sëriñ Saaliw Ture ak Cheikh Ahmadou Bamba Consulting International lëkkoo woon, am yéeney sargal ko ci dundam ci weeru nowàmbar 2023 fa Grand Théâtre bu Ndakaaru. Waaye, Yàlla weddi. Sëriñ Saaliw Ture du ko fekke naam, waaye sargal gi dina am bu soobee Yàlla. Ci kow loolu sax, ñi ko séq jotoon nañ seeti Sëriñ Muntaqaa, mu jox leen ci ndigal, ñaanal leen.

Yal na àjjana di këram ba fàww !

EJO-EDITIONS ak Lu Defu Waxu ñu ngi koy jaal ñépp, rawatina yoonu murid.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj