Ci alxamesu démb ji la ñu ëpp ci saa-senegaal yi tabaski. Ku ne tabaski, ne xutba. Te, xutbay imaam yi, dees na koy faral di xaaj ñaari pàcc. Bu ci njëkk bi, imaam yi dañu koy jagleel diine ji, jagleel beneen ñaareelu pàcc bi tolluwaayu réew mi, rawatina li ci fës. Xalifa ñaseen yi, Sëriñ Maahi Ñas, woote na jàmm ak ndal ci Senegaal.
Sëriñ Maahi Ñas, moom, jàmm lay sàkku ci réew mi, di ko ñaan te di ci woo ñépp. Nde, ci gis-gisam, jàmm mooy indi ndal giy tax koom-koom gi mën a yokku, réew mi naat. Ginnaaw bi mu jiitee ñaari ràkkay tabaski yi, toftal na xutba bob, jóo na ci waa réew mépp, muy njiit yi ak ñi ñu jiite yépp, ñu joxante loxo, jàppoo, bennoo ngir saxal jàmm ci Senegaal, suuxat ko ngir suqali réew mi. Xalif bi ne :
« Am réew, na askan wa mel rekk lay mel. Bu askan wa nangoo topp ci ginnaaw nguur gog, tàllal na loxo askanam ngir dimbali ko, yar ko, tàggat ko, xirtal ko ba maxejj bu nekk di gis boppam ci li nguur giy doxal, bu boobaa maxejj bi dina soppi aw doxiinam ci lu baax. »
Noonu, Sëriñ Maahi Ñas xelal na ndaw ñi tamit, xamal leen ne dañu war a waajal seen ëllëg. Nde, ñoom ñooy nekki kilifay ëllëg.
« Nanguleen a jàng, jikkowooleen jikko yu baax. Ndaxte, benn maxejj warut a xeeb jëfam ci liy tabax réew mi. Maxejj bu baax ak Njiitu réewam ñoo bokk ay àq ak i yelleef. »
Kilifa gi dafa jeexalee xutbaam ci fàttali ne, Senegaal benn bopp la, kenn mënu ko xar ñaar. Moo tax, ciy digleem, ñu war a sàmm kàddu yi, tànn yi ci gën yiy sabab jàmm di indi ndal ci réew mi.
« Nun ci sunu wàllu bopp, jéemunoo lor kenn, te baal nanu képp ku nu tooñ. Jàppalunu kenn dara. Yaraate ak jàngale rekk ñooy sunuy itte. Te, danuy jéem a def lu baax. »
Ay ñaan la tëjeey waxam, rawatina ngir bennoog way-pólitig yi.