Saa bu waxee, loxo dar gemmiñ. Amet Siise nekk ku ñu miin ci mbaali-jokko yi. Mu tàmbalee fés ci Youtub bi ginnaaw ba mu fay jaarale ay waxtaani boppam. Bokk na ca lañu gën a nemmeeku, ay wax yu ñàkk teggin, doonte ne moom xam-xam la ko dugge. Kon xam-xam boobu fan mooy cëslaayam ?
Mu mel ni diinee tax mu ràññeeku. Te bu ñuy wax diine jooju, Lislaam a tax. Amet Siise ŋàññi na diiney Lislaam jaarale ko ci Téere bu sell bii di Alxuraan, waxi Boroom Bi. Ñenn ñi di ko firee ku tubbi ginnaaw ba mu weddee waxi sunu Boroom ci ay kàddoom yu ñàkk worma. Mu mel ni du guléet. Ndax, Amet Siise jote na fi ak yoon ci lu ni mel tax ba am ñu jàppoon ko.
Mënees na wax ne dof moom kenn du ne ko yaa moom nit ñi. Loolu lañu fàttee wax Amet Siise. Tax ba mu moom nit ñi ci mbaali-jokkoo yi, lu ko neex mu wax, ku ku neex mu dal, boroom xam-xam bu wax mu tontu, tuutal la. Moo tax it ne wii yoon, saaraani na. Ne tooñut kenn nit walla ñaar, waaye am mbooloo la maasee tooñ ginnaaw ba ñu bokkee gëm diiney Lislaam. Looloo tax ba ñu bari genn di ñaawlu kàddoom yooyu ak di ko tëkku. Bokk na ca waa JAMRA ga nga xam ne fa la bokkoon. Maam Maxtaar Géy beddi na ko ci seen kurél googu. Ñu gisaat tamit waa kurél Aar daara ci njiital Ustaas Maxtaar Saar boole nañu ko yoon ñaari yoon, ca toppekat ba ak ca takk-deri lënd gi (cybercriminalité). La mu jàppe Amet Siise bu ñu sukkandikoo ci ay kàddoom mooy ab saay-saay, ab sàmbaa-bóoy wala sax ab rëtëlkat.
Mën nañoo tënk ne, diine dafa nekk lu loyox. Tax ba lu ñu ciy wax dafa war a nekk lu leer. Amet Siise juumati na. Tax ba Imaam yi, waarekat ak képp kuy yëngu ci diine di mettitlu ay kàddoom. Muy lu ñu war a saafara balaa jur yeneen coow.