MÀGGALU DAARU XUDÓOS

Yeneen i xët

Aji bind ji

Mu doon tur wu siis wi ñu ko xame, màggalu daaru xudóos doon xew-xewu diine. Murit yi di ko màggal at mu jot ca Tuubaa, rawatina fa goxu daaru xudóos.

Xew-xewu diine boobu di fàttali bés ba Sëriñ Tuubaa Xaadim Rasuul di wuyuji Boroomam. Mu doon bés ba ñu ko jébbalee Boroomam faTuubaa ginnaaw ba mu làqoo ca Njaaréem (Njurbel). Ñu njëkk ko màggal ca atum 1935. Sëriñ Móodu Mustafaa di ab taawam nekk tamit xalifaam bu njëkk moo taxawal bés boobu. Muy wéy ba su nu jonni-Yàlla-tey. Waa Daaru xudóos di ko màggal ba mu far wuyoo ci turu màggalu Daaru xudóos. 

Bés boobu ëmb mboor ak i baatin ca atum 1927 ba Sëriñ bi làqoo. Mu nekkoon tiis ju réy ci murit yi, jur njàqare ci taalibe yépp. Waaye, seede yi di wéy di biral taxawaayu taawam ba mat sëkk taaw, di Sëriñ Móodu Mustafaa. Nde, loolu ndénkaan la woon digganteem ak Sëriñ bi. Ndax, la mu sàkku woon ci moom mooy “ Bés bu ma wàccee, nañu ma yóbbu Tuubaa”. Mu nekkoon jamono yu metti ci digganteem ak tubaab yi waxoon ne, mëseesu koo bàyyi ( résidence surveillé) ba ni mu làqoo. Mébét moomu la doomam ja sottal ba ni mu ko indee Tuubaa te benn tubaab gisu ko. 

Ren, ñu màggal ko ci dibéer jii weesu 6 ut 2023, yamoo woon ak 19i fan  muharram atum 1445. Ci teewaayu Sëriñ Ahmadu Maxtaar, di xalifab Daaru Xudóos. Bés boobu di am njooqe. Ndax, teewaayu nit ñu takkoo-takku ngir fekke guddi gi. Mu doon bésu xubbeeku ci ay bàkkaar. Nde, képp ku ko fanaane màggal ci béreb bu sell ba, ñu far say ñaawteef. Mu doon kàddu yu Sëriñ Móodu Mustafaa jaayante ak Boroomam. 

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj