WAAJTAAYI MÀGGALUG TUUBAA 2023

Yeneen i xët

Aji bind ji

Dëkk bu sell bii di Tuubaa sóobu na ci waajtaay yi ñeel màggalug 18 safar gu ren ji. Mu nekk bés bu màgg, di xew-xew bu siiw buy dajale mbooloo mu takkoo takku. Loolu tax ba kurél giy sàytu doxalin wi, amal ay ndaje ngir gën a ñoŋal xew-xew bile. 

Fan yu néew rekk ñoo ci des laata  bés biy teru. Kurél giy saytu waajtaayu màggal gi doon na amal um ndaje, ci talaatay démb ji, fa Tuubaa. Jëwriñu biir réew mi, Antuwaan Jom, ak yeneen i kilifa niki Sëriñ Basiiru Abdu Xaadr ma yore kàddu yoon wi, bokkoon nañ ci ndaje mi. Bokk na ci liñ jot a tënk, jafe-jafey ndoxum taw yi ak taa-taa yoy, warees na ci jël ay matukaay balaa muy gàllankoor xew-xew bi. Jot nañ cee def koppar yu tàkku sax ngir Tuubaa bokk ci dëkk yiy tàggook mbënn mi. Mu doon liggéey bu réy a réy, rawatina ci jamonoy nawet.

Leneen li ñu jot biral, bu ñu sukkandikoo ci kàdduy Antuwaan Jom, mooy ndoxum naan mi. Mu mel ni dalal na xel yi ci wàll woowu ginnaaw ba mu fésalee jumtukaay yu mag yi ñu teg ci loxoom. Muy 20i sëfaani ndox (camion-citerne) ndox yu réy. Benn bu ci nekk di def lu tollu ci 30 000iy liitar. Boo boolee 20i sëfaani ndox yépp, 600 000iy liitari ndox ngay am. Rax-ci-dolli,  sëfaanu ndox gu nekk mën naa duy ñeenti yoon ci bés bi, muy lu jëwriñ ji biral. Mu nekk ay jumtukaay yu yees-péq yu Tuubaa war a daloo. 

Mënees na tënk, wax ne waajtaayu màggalug Tuubaa gaa ngi ci njeexital li. La ñu ca nemmeeku ginnaaw at ya ko jiitu, mooy ay jumtukaay yu dolleeku ak ay liggéey yu mag ci jamonoy nawet ji mu tombeel. Loolu di firndeel yokkute gu réy gi muy àndal at mu nekk. 

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj