SIGARET BAAXUL… WAAYE AFRIG LA YÉESE !

Yeneen i xët

Aji bind ji

Fan yii weesu, Marie Maurisse, ab taskatu xibaar bu fekk baax Siwis, bind na bataaxal bu jar a bàyyi xel. La muy ciy nettali mooy ñaawtéef yu këri-liggéeyukaay yu mag yiy jaay sigaret ci réewi Afrig yiy def, te sunuy gornamaa ne yàcc di leen seetan.

Tóx baaxul, loolu dëgg gu wer péŋŋ la, kenn sañu koo werante. Képp ku koy def, sa bakkan a ngi ci xott, dina la feebarloo, gàttal say fan. Teewul bitig boo dugg Senegaal mu ngay jaay sigaret ; li am ba am moo di ne nguur gee ko daganal, di ci jël moyaal. Li ñu Marie Maurisse di xamal nag, teg ko ci ay firnde yu leer nàññ, moo di ne xeetu sigaret yi ñuy jaay Afrig, ñoo yées fopp yi ñiy jaay Ërob, ca réewi Tubaab ya. Mën nan koo metitlu waaye warunoo bett ndax Afrig yàgg naa doon ‘’Mbëbësu” Ërob. Kolobaan gii, boo fa doxantoo, dinga fa fekk ay jali jali fëgg-jaay, maanaam ay yëre yuñ sol Ërob ba sànni leen ci mbalit mi. Yàggul dara, daaw-jéeg rekk, lanu dégg ni esãs ak gasuwaal bi ñuy jaay fii ci Senegaal ak ci yeneeni réewu Afrig, kenn sañu leen a jaay Fràs walla Almaañ ak ñoom seen. Lu ko waral ? Xanaa seen mbon ci wér-gi-yaramu doom-aadama.

Bi ñu siiwalee li Marie Maurisse bind, Philip Morris, këru liggéeyukaay gu mag gi ubbi fii Senegal ab isinu sigaret, daldi nay tontu. Ñaari mbir a jar a fësal ci li mu wax : bu jëkk bi moo di ne Philip Morris weddiwul ni sigaret yi muy jaay Senegaal ñoo yées yi ñuy jaay Ërob ; ñaareel bi, nag, mooy, sunu wér-gi-yaram gi ñuy fowe, nee na ci li ko nguuru Senegaal may la ko teg. Waa OMS, kurél gi ñu dénk lépp lu jëm ci wér-gi-yaram ci àddina si, firndeel nañ ni fileek 2030, limu tóxkati Afrig yi dina ful ñaari yoon. Ërob moom, tàmbalee naa xeex ak doole sigaret, ngir aar ay ndawam, fexe ba ñu bàyyee tóx. Looloo tax defarkati sigaret yu mel ni Philip Morris jàpp ne liggéey ak Afrig moo fi sës, sunu réew yi amal leen lool solo. Ci gàttal, nun nooy seeni nooy-neex, seen yoon newul ci sunu wér-gi-yaram. Bu sunuy njiit amoon fullaak faayda, yittewoo seen bànneexu askan, neneen la mbir miy deme.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj