SIGICOOR : BENN TAKK-DER ÑÀKK NA BAKKANAM

Yeneen i xët

Aji bind ji

Xeex bu mettee am ca Sigicoor diggante ndaw ñiy taxawu Usmaan Sonko ak takk-der ya. Ci suba ba léegi, xeex ba dakkagul. Fi mu nekk nii nag, ndaw ñaa jekkoogum ci lees jotagum ciy xibaar. Nde, dañoo fatt yoon yi jëme kër Usmaan Sonko yépp, teg fay xeer yu mag, daldi fa taal ay matt ak i póno. Nee ñu sax, jafal nañ benn daamaaru pólis.

Te, musiba mujj na cee am. Jëwriñu biir réew mi génne nab yégle di ci xamle turam, muy Haasim Jéeju. Ci biir yégle bi, mi ngi ciy xamle ne daamaaru takk-der yee jaar ci kowam ci lu dul teyeef, mu faf ñàkke ci bakkanam. Yégle bi sargal na ko, jaal koy mbokkam.

 Waaye, am nay ndaw yees rawale ca raglub Hôpital de la Paix ba ca Sigicoor. Senenews a biral xibaar bi, ne ci ay seede ya fa nekk la xamee ne, am na 3i ndaw yuñ dóor bal dëggantaan.

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj