Lu ëpp juróom-fukki njaboot la SOGEPA nar a génne ciy kër yoy, moomeelu Nguur gi lañu. Njaboot yooyii nag, ay liggéeykati Nguur gi lañu. Kër yooyu, di ay kër yu bakkane, féete fa « Cite Fayçal », korosmaa Kàmbereen (Ndakaaru).
Yéenekaay Libération moo xëyee xibaar bi xëtam bu njëkk. SOGEPA (Société de gestion et l’exploitation du patrimoine bâti de l’Etat) moo doon luññutu ak saytu moomeeli Nguur gi ñeel lépp lu aju ci taax ak tabaxi Nguur gi ci diiwaanu Ndakaaru. Li ko sabab nag mooy ab seetlu bu ñu def. Seetlu bi mooy ne, ak li Nguur gi yor lépp ciy taax ak i tabax, dafa daan yoolu (luwe) ngir dëkkal ay liggéeykatam, ba noppi daan fay at mu nekk 2i miliyaar ay jàmbur. Ci jenn jamono ji, 60i miliyoŋ kese la Nguur gi daan jot at mu nekk ciy këram yu mu yoolu. Loolu moo tax SOGEPA bëgg a nangu kër yooyu, dëkkal fa ay liggéeykati Nguur gi. Bu ko defee, SOGEPA dina nangu lu tollu ci 54i « baux » yu féete fa Cité Fayçal, Mermoz, Point E ak Fann Résidence.
Bu dee kër yi nekke Cité Fayçal, luññutu gi dafa feeñal ne am na 40i kër yees yoolu woon ci diirub 99i at, ña ñu ko luwe di fay diggante 60 000 ak 80 000 ciy CFA.
Cig pàttali, Abdulaay Jóob ma woon jëwriñu Kopparal gi ca Nguurug Abdulaay Wàdd dafa bañoon a xaatim këyit yuy jaay kër yi. Bi Maki Sàll faloo ba toog lañu jaay kër yi. Waaye, SOGEPA yemu fa.
Dafa di, SOGEPA sumb na beneen liggéey ngir nangu ay kër yi Nguurug Maki Sàll jaayoon ay jàmbur, jaare njaay mi cib areete. Bokk na ci ag kër gu jàkkaarloo ak raglub « Hôpital Principal » bu Ndakaaru, ñu jaayee woon ko 30i miliyoŋ ciy CFA. Li ci doy waar nag mooy ne, as soxnas doxandéem lees ko jaay. Te, kër googee, njëgam dëggantaan a ngi tollu ci 1 miliyaar.
Yéenekaay L’As nag, siiwal na turi jëwriñ, DG ak i àttekat yu nar a génn. Bees sukkandikoo ci yéenekaay bi, kii di Usmaan Jaañ, jëwriñu Yoon wi, ci la bokk. Ka woon magum tof-njiitu Njénde li, Maksim Sã Simõ Njaay, ka woon magum tof-njiitu Càmm gi, DG ya woon, Séex Isaa Sàll, Màgget Seen, Aliw Sàll, jëwriñ ya woon, Xuraysi Caam, Kansumbaali Njaay, Abdulaay Elimaan Kan ak kenn ka woon tof-njiitu Ndajem ndeyu sàrtu réew mi.