Ndogal li rot na. Tey jii, ci gaawug 20 sãwiyee 2024, la 7i àttekati ndajem ndeyu àtte mi waroon a biral toftaleg lawax yiy joŋante ci wotey njiiteefu réew mi, keroog 25 féewaryee 2024.
Xaar bi yàggoon na lool nag. Nde, ci suba ba léegi, askan waa ngi doon séentu ndogalu àttekat yu mag yi. Ci guddi gi la mujje génn, bi 22I waxtu jotee daanaka. Li ci gën a fës nag mooy li Usmaan Sonko ak Kariim Wàdd dul bokk ci wote yi. Bu dee Basiiru Jomaay Jaxaar Fay ak Séex Tiijaan Jéey, ñoom dañuy bokk.
Bu ko defee, 20i lawax ñoo nar a dagaan baatu askan wi ngir xëcco jal bi. Ñii la :
-
Buubakar KAMARA
-
Séex Tiijaan JÉEY
-
Décce FAAL
-
Daawda NJAAY
-
Abiib SI
-
Xalifa Abaabakar SÀLL
-
Anta Baabakar NGOM
-
Aamadu BA
-
Róos WARDINI
-
Idiriisa SEKK
-
Aliyun Mamadu JA
-
Sëriñ MBUUB
-
Papaa Jibril FAAL
-
Mamadu Lamin JÀLLO
-
Mahammad Bun Abdalaa JONN
-
Elaas Maalig GÀKKU
-
Aali Nguy NJAAY
-
Elaas Mamadu JAAWO
-
Basiiru Jomaay Jaxaar FAY
-
Ceerno Alasaan SÀLL