Naam, CEDEAO joxe ko dëgg. Naam, Ëttub àttewaay bu mag bi neenal na àtteb Sabasi Fay ba. Waaye, ba tey Sonko moo am ndam, bees jàngatee mbir yi wàllu pólitig.
Loolu nag, buñ koy wax, CEDEAO taxul. Nde, bu àttekati CEDEAO joxoon dëgg Usmaan Sonko sax, Càmmug Senegaal du ko jëfe. Te, démb rekk Aysata Taal Sàll fàttali na ko ça Ngomblaan ga. Deesut a fàtteet Xalifa Sàll ak Karim Wàdd, ku ci nekk, yow la CEDEAO joxoon dëgg. Waaye, Nguurug Maki Sàll gi, daf ci dëggoon tànkam, ne dee du ko jëfe. Moo tax, CEDEAO moom, daanaka amul benn xeetu njeexital ci réew mi ñeel yoon.
Xuwaan Barànkoo, kenn ci layookati Usmaan Sonko yi, moo jëkk a siiwal ndogalu àttekat ya, bind ne :
“Ëttub àttewaayu CEDEAO bi dëggal na tas gi ñu tas làngug kujje gi gën a mag ci Senegaal.”
Sire Keledoor Li, di layookatu Usmaan Sonko, wax it ne :
“Ëtt bi dafa jàpp ne kenn salfaañewul àqi Usmaan Sonko, daldi koy gàntal ciy càkkuteefam.”
Waaye, bu dee ci lees soppi Usmaan Sonko ci wayndarew wote wi, Ëttub CEDEAO bi da cee màndu, ne du ci wax. Maanaam day bàyyi àttekati Senegaal jël ci ndogal.
Loolu nag, neexul Sire Keledoor Li ak soppey Usmaan Sonko yi. Layookat bi ne :
“Waa réew mi ak àddina sépp seede nañu […] xoqatal ak bunduxataal bu jéggi dayo bi ñu teg ci kow Sëñ Usmaan Sonko, ak barikaad yi ñu tegoon këram ngir ndar-kepp ko.”
Rax na ci dolli sax ne, ndogal lii CEDEAO jël day tax ba jaaykatu doole mën doxale ni Maki Sàll di doxalee te dara du leen ci fekk. Li wóor daal mooy, CEDEAO moom, ñàkk na Senegaal. Nde, bu Usmaan Sonko walla kenn ci waa PASTEF jotee ci Nguur gi, Senegaal dina génn ci kurél gi. Nu delsi Senegaal.
Bu dee fi réew mi nag, màndarga yu bari firndeel nañ ndam Usmaan Sonko donte ne Ëttub àttewaay bu mag bi Càmm gi la topp. Ndax, laata bés bi di agsi, Senegaal ba mu daj, bésub 17eel bi rekk nga doon gis, di ko dégg fu nekk. Nga xam ne, mbiri Usmaan Sonko itteel na askan wépp.
Bi bés bi jubsee ba ñu ne ëllëg la, ci alxemes ji, Dakar Dem Dikk dafa gaarey otoom ne du daw ci bés bi. Gornooru Ndakaaru ak perefe yi aaye njaayum karbirã ci buteel ak yu ni mel, tere moto yi daw ci bés bi. Li ñu doon ragal mooy ay yëngu-yëngu am, xale di toj ak a taal. Nga xameet ni, Nguur gi, Usmaan Sonko tere na leen nelaw.
Leneen luy firndeel ndam Usmaan Sonko seen kow mooy bi ñu waxee ne àttekat bi, Sire Aali Ba, jox na dëgg Usmaan Sonko, dina bokk ci wote yi. Daanaka, ñépp a bégoon lool, xol yi féex, nit ñiy génn ci mbedd yi, ñii taxaw seen i bunti kër di yëkkatiy ak a sant Yàlla. Nga xamati ne, Usmaan Sonko moo dee ci xoli saa-senegaal yi.
Bu dee ci wàll yoon kepp nag, foofeet meeru Sigicoor bi am na ci ndam. Ci naka ? Benn, Sire Aali Ba dafa def lees mësut a gis. Nde, dafa dow àtte bi, delloo ko waa Ëttub àttewaay bu Ndakaaru. Te, ci li ma-yoon (juriste) yépp xamle, Ëttub àttewaay bu mag bi, du dàq àtte, day jël ndogalam rawatina bu dee ci wàllu wote.
Fi Sire Aali Ba sukkandikoo mooy ne Usmaan Sonko Ndakaaru la dëkk, kon fi Ndakaaru lees ko war a àtte. Te, Usmaan Sonko mooy meeru Sigicoor, fa la bindoon. Cig pàttali, bi Kariim Wàdd amee coow lu ni mel, dañ ko waxoon ne mëneesu ko àtteb Ndakaaru ndax Dubaay la bindoo. Ñu gis ne, Ëttub àttewaay bu mag bi dafa weddi boppam kon.
Te sax, bu àtte dee am, fàww limu àttekat yi tóol. Waruñoo nekk ñaari àttekat walla ñeent. Nde, bu ñaari àttekat àndee ci ndogal, yeneen ñaar bañ cee ànd, fàww am ku leen juróomeel ngir àtte am. Te, démb, àttekat bii di Aysata Jàllo Ba dafa gedd, daldi bàyyi, mu des ñeenti àttekat. Ñoom ñooñu, ci njiitalu Sire Aali Ba, ñoo neenal àtteb Sabasi Fay bi.
Sikk amul ci ne layookati Sonko yi dinañ dugal lees duppee “rabat d’arrêt” ngir ñu xoolaat ndogal li Sire Aali Ba jël.
Lii yépp nag, day wone ne Maki Sàll sonal na Usmaan Sonko gaa, waaye mënalu ko dara. Day firndeel itam ne wóoluwul mbëram. Ak lu mën di xew ëllëg, Sonko yey na askan wi, yey àddina. Li mu yàqal Maki Sàll moo ëpp fuuf li ko Maki Sàll yàqal.