Cin bax na, waaye du jikkoom, matt a ko ca jóo. Altine ba tey, Bàrtelemi Jaas a ngi ame rajo yi, tele yi ak mbaali jokkoo yi. Génn bi mu génn keroog, ci ngoonug altine ji 8 me 2023, dal ci kow njiitul Pastef li moo sooke coow li. Fi mu ne nii, li ëpp ci jotaay yi, mbirum « doomi ndey » ya woon, Bàrtelemi Jaas ak Usmaan Sonko lañ fay fénc ak ëllëgu askan wi. Wax ji bari lool. Téesante bi ak dàggasante bi mel ni tulleek maale diggante farandooy Pastef ak farandooy Bàrtelemi Jaas. Waa Bennoo Bokk Yaakaar di ci wut poroxndoll ngir féewale kujje gi, ëlëm xel xel yi. Yow mi ci néewley xibaar, xaw a ñàkk a seetlu tuuti, amaana sam xel lëj ci mbir mi. Moo tax, xam naa yaa ngi bëgg a laaj, yow miy dégg coowal faramfàccekat yiy faral di safaanoo léeg-léeg : « Lu xew ? » Nu dellu ginnaaw tuuti, jéem a seetlu, jàngat ngir ràññatle mbir yi.
Bëre suuf
Ci dibéer ji 7 me 2023, la Usmaan Sonko amaloon uw waxtaan ci guddi gi, wax ci ne :
« Maki Sàll, ñaar-fukki fan ak juróom ci ginnaaw, dalal na genn kilifag pólotig goo xam ne ci Yewwi Askan Wi la bokk, li ko dale 22i waxtu ba 1 waxtu ak lu teg ci guddi gi. Kilifa googu, bim génnee ca ndaje ma, daf ma woo, ne ma dama lay saabal ndax Maki Sàll dalal na ma fii ci Mermoos, ci kër doomam. Te ci waxtaan woowu, wax na ma, wayndarew Usmaan Sonko Wi li ci xewoon ca àtte bu njëkk ba daf ñoo rëcc. Ndax àttekat bi ko àtte, Pastef la bokk. Waaye dinañ ko dabu ci layoob dabu bi. Nii la ma ko waxee. Billaahi ! Wallaahi ! »
Bi Usmaan Sonko waxee lii, dafa mel ni ku àjji kaabaab Bàrtelemi Jaas. Nde, dafa mel ni ñaari doomi ndey yoy, kenn foogul woon ci àddina sax ne, dinañ xuloo bay xeex. Ndekete, booba, ñu ngiy léewtoo ci lëndëm gi, ci suuf, te kenn yëgul, kenn tinul. Biñ demee ba làmp yi nar a tàkk, ñépp gis leen ñu ngembu sëgg di bëre, ca la jenn doomu ndey ji, Usmaan Sonko, waaxu jeneen doomu ndey ji, Bàrtelemi Jaas, dóor kob laaw, faf làmp yi tàkk. Jeneen doomu ndey ji, Bàrtelemi Jaas, am mbetteel lool. Nde, ni Usmaan Sonko doxalee, foogewu ko woon. Loolu daldi nasaxal pexe mum laloon, mu daldi mer, tàggook sagoom, di xataraayu ak a yuuxu, di yàq lu mel ni xeme « doomu ndeyam » ja woon. Ca la làmp yi tàkkee, géew gi leer nàññ.
« Bàrt, yaa ngi doxal… »
Ci altine ji lees waroon a biral àtteb dabu ci layoob Usmaan Sonko ak Maam Mbay Ñaŋ. Ca ngoon ga la àttekat yi siiwal daan bañ gàll ci ndoddug njiitul Pastef li nga xam ne, lawax ci wotey 2024 yi. Àddina sépp bokk njort ne, àttekat yi, ci ndigalu Maki Sàll lañ jële ndogal loolu. Nde, umpaleesul ne, Maki Sàll dafa bëgg a tere Usmaan Sonko bokk ci wote yi. Kon bés boobu, képp kuy xeexal demokaraasi, nga bokk ci kujje gi walla déet, rawatina boo dee « doomu ndeyu » U. Sonko, taxaw ciy wetam moo la war, jàppale ko, taxawu ko, xeexle ko. Waaye, Bàrtelemi deful loolu.
Ci ngoonug altine jooju la dépite, meeru Ndakaaru bi, Bàrtelemi Toy Jaas janook taskati xibaar yi wax lu yéem nit ñi, bette lool. Ndaxte, waxam jépp, daf ko dal ci kow Usmaan Sonko, « doomu ndeyam » ji, yakk ko lu mel ni xeme.
« Kaawteef ! Bàrtelemi Jaas menn mi ? »
Waaw kay ! Looy yéemu ? Xanaa déggoo li wolof wax : « bëñ weex na, waaye deret a ko lal. » Nga laajati ma : « Lu Bàrtelemi wax sax lu fi jar coow lépp ? ».
Li Bàrtelemi Jaas wax bari na. Àddu na ci ci waxtaan wi Njiitu réew mi woote, wax ne moom ci boppam moo ko sumb, waxtaanam la. Nu déglu ko :
« Man maa njëkk a bëgg waxtaan wi am, sàkku woon ko keroog 26 sãwiye 2023. Boobaak léegi, amul lenn njiitul pólitig lu ma wax ne àndul ci wooteb waxtaan woowu. Dafa am ay nit yu deful pólitig yu ma seetsi ngir waxtaan ak man. Ñoom ñoo jóg ngir wax ak Maki Sàll. Ñëw nañ sax ay yoon sama kër. »
Yaa ngi dégg de. Nee na, lépp moom la. Ndax gëm nga ko ? Waaw, kaay nu bokk seetlu ndax lim wax yenu na maanaa walla déet. Ndax Bàrtelemi Jaas am na dayob jóo Njiitu réew mi ciw waxtaan ? Moom mi nga xam ne, naam mooy meeru Ndakaaru di yit dépite ca Ngomblaan ga, jiitewul genn làngu pólitig. Taxawu Senegaal bim bokk, Xalifa Sàll a ko jiite. Ca lëkkatoo Yewwi Askan Wi, bokkul ca kilifa yay dogal. Bàrtelemi Jaas, dayoom ci pólitig Ndakaaru la yem. Te, sax, ginnaaw Yàlla, bu dul woon Usmaan Sonko, du doon meeru Ndakaaru. Fàtte xaju fi kat. Xalifa Sàll miy kilifaam ci pólitig, Sowam Wardini la tànnoon ngir mu doon lawax ci wotey meer yi amoon 2022. Usmaan Sonko moo xeex, bañ ba ñu samp Bàrt, mu am ci ndam. Leneen li mooy, moom Bàrtelemi Jaas, Njiitu réew mi Maki Sàll dafa am fum ko téye. Bu ko neexee, suba suba, nangu meeri Ndakaaru ak cërub dépiteem ba ca Ngomblaan ga. Waaw, diggante Maki Sàll ak Bàrtelemi Jaas, ku ci soxla waxtaan ak keneen ki ? Xanaa Bàrtelemi Jaas dafa fàtte la mu tontu woon Paap Ngañ Njaay ca jotaayu Faramfàcce bam amaloon ak moom. Moom de moo waxoon lii :
« Maki Sàll, bëgguma ko gis. Soxlawuma ko gis. Bëgguma ko. Yelloowul ma toog ak moom. Yelloowul sama kóolute ndax nawloowul saa-senegaal yi. Mënoo taxaw fii, nga bóom 14i saa-senegaal, amul benn luññutu, amul kenn kuñ ci jàpp. Loolu mooy Senegaalu Maki Sàll. Di dëkkloo say naataangooy pólitig yi ci kujje gi fu ñu dëkkul, di gal-gal Xalifa Sàll, di def yu mel noonu. Kilifa diine yi di wax ak yow nga leen di ñàkkal faayda. »
A waaw, Bàrtelemi, lu soppeeku ci diggante bi ? Ndax leeral nañ mbirum 14i saa-senegaal yiñ bóomoon yi ? Ndax Maki Sàll dafa tàmbalee rafetal ñeel ay naataangoomi pólitig yi ci kujje gi ? Ndax mi ngi doxal demokaraasi ? Ndax Yoon dafa tëdde njaaxanaay ? Ndax dañoo bàyyi luubal alalu askan wi ? Ci gàttal, ndax Senegaalu Maki Sàll dafa soppeeku ci lu baax ? Bàrtelemi daal, waxagoo wax ji. Te, sax, yow Bàrtelemi, lu la Usmaan Sonko def ?
Bees seetloo waxi Usmaan Sonko yi, mësu cee tuddu Bàrtelemi Jaas. Dafa di, kenn mësul xalaat ne Usmaan Sonko moom la doon waxal. Ndax, njiitul Pastef li, « …genn kilifag pólotig goo xam ne ci Yewwi Askan Wi la bokk » la wax. Te, sax, Bàrtelemi bokkul ci ndajem kilifay lëkkatoo YAW. Amu fa baat, amu fa ndogal. Xam naa sa xel maa ngi xasan, nga naan :
-
« Kon lu tax mu aakimoo wax ji, wax anam bim waxee ak bés bim tànn, waxtu wi, wax ko ci ? Lu tax ?