Elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, doon na jël kàddu gi tey, ci àllarba ji. Liggéeykati njëwriñ gu mag gi (primature) la doon janool, doon waxtaan ak ñoom ci anam yi ñuy liggéeyee ak yi ñuy aajowoo ci seen bérébu liggéey. Ca ndaje ma, àdduwaale na ci coow li lëmbe réew mi fan yii, muy tasug campeef yi di CESE ak mbirum “motion de censure” bi waa Bennoo Bokk Yaakaar di tëkkoo Càmm gi.
“Motion de censure” du am te dinan tas Ngomblaan gi
Njiitu réew mi dafa dige woon ne, bu jotee ci Nguur gi, dina tas yenn campeef yees jàpp ne amaluñu askan wi njariñ. Ci kow loolu la tasee kurél gii di “Haut Conseil du Dialogue Social”. Looloo ko taxoon a jébbal Ngomblaan gi aw sémbu àtte ngir tas yeneen ñaari campeef yii di CESE ak HCCT. Waaye, barki-démb ci altine ji, dépitey Bennoo Bokk Yaakaar yi dañu gàntal sémbu àtte woowule. Àndandooy Maki Sàll yi yemuñu ca. Nde, Abdu Mbów mi jiite kippaango dépitey BBY yi dafa dugal lees di wax “motion de censure”, maanaam aw sémb ngir daaneel Nguuru gi.
Bi xibaar bi jibee nag, ñu baree ngi doon naqarlu taxawaayu Nguuru Jomaay geek Sonko ñeel waa BBY. Nde, ci seen gis-gis, ñoo leen seetaan ba ñuy am fitu wax ak a tëkku Nguur gi. Ndax, waxtu wii, bu leen fekkoon ci pekki toppekat yi, ci kanami àttekat yi walla sax ca ndungusiin, tal koon nañ leneen lu mooy fëgg dënn ak a yëkkati baat. Teg ci ne, ñu baree gi sàkku ci Njiitu réew mi mu tas Ngomblaan gi. Dafa mel ni nag Usmaan Sonko, elimaanu jëwriñ yi, dégg na leen te fas na yéene, moom ak Njiitu réew mi, lijjanti mbiri way-pólitig yooyii réy-réylook réy baat.
Ci ndaje mi mu doon amal tey ak liggéeykati njëwriñ gu mag gi (primature), joxe na fay xibaar. Xamle na ni, “motion de censure” boobii dépitey BBY yiy tëkkoo Càmm gi du mës a am. Daf ne :
“Dama bëgg a dalal xeli ñépp. Dégg nañ ñuy wax waxi “motion de censure”, daaneel Càmm gi. “Motion de censure” du fi ame. Am na way-pólitig yoy, xamuñu fu ñuy taxaw, ànd ak seen i saabalkat yi leen di jàppale… Waaye maa ngi dalal seen i xel, di leen wax ne “motion de censure” du am fii ak 12i pani sàttumbaar. Te, keroog 12i pani sàttumbaar, gaa ñooñee dinañ am leneen lu ñuy def lu dul nekk dépite.”
Lees mën a déggee ci kàdduy elimaanu jëwriñ yi mooy ne, Ngomblaan gii day tas keroog 12i pani sàttumbaar te waa BBY dinañ wuyuji Yoon.
Toppe gi dina tàmbali ci ayu-bés bii
Ci beneen boor, ñeel yaxanal beek sakkanal alalu Nguur gi, Usmaan Sonko tontu na liggéeykati Càmm gi, ñoom ñi génne woon ab yégle di ci naqarlu ndogal yi mu jëloon ci wàll wi. Mu leen di xamal ni, duggewu ko lenn lu dul wàññi yàq gi ak ëppal bi. Te sax, ciy waxam, réew yi suqaliku yépp noonu lañuy doxee. Kon, lu tee Senegaal gi xam ne demagul fenn di wéy ci yàq ak pasar-pasaree as-tuut lim am ci alal ak i jumtukaay ? Ba tey ciy waxam, yaxanal alalu askan wi moo tax ñu bëgg a far campeef yoy, seen njariñ feeñul, niki CESE ak HCCT donte ne Ngomblaan gi dafa gàntal sémbu àtte wi fa Njiitu réew mi dugaloon. Waaye, ci kàdduy njiitul Pastef li, loolu yéexal jéll la rekk. Ndax, yàgg yàgg dinañ leen far.
Balaa boobu, dinañ dàq njiiti campeef yooyu. Sonko moo ko xamle, wax ne Njiitu réew mi dina torlu dekkare tey, jële Abdulaay Daawda Jàllo (BBY) ak Aminata Mbeng Njaay (PS) ci boppi CESE ak HCCT. Te, du fa yem. Ndax, dinañ fexe ba alal dootul dugg ci ñaari campeef yooyu.
Bu loolu weesoo, xamleet na ni, dinañ tàmbalee topp ñi luubal ak ñi sàcc alalu askan wi.
“Ci ayu-bés bii lay tàmbali… Mënuñoo seetaan ay nit def lu leen neex, tibb ay miliyaari miliyaar jaare ko ci [njaay ak njëndu] suuf si, ci tabax yi, ci jawi bokkeef gi (marchés publics) ci jawi làrme bi, añs., ci fànn yépp, dajale ay miliyaar yoo xam ne xam nañ ni mu demee, ba noppi yaakaar ne dinañ xi génnee noonu.”
Dafa di, toppe googu di waaj a tàmbali moo tax ñu tënk ñenn ñi fi réew mi, tere leen génn. Sonko neeti :
“Loolu moo tax ñu jël sunuy matuwaay ngir ñenn ñi bañ a génn réew mi léegi. Am na ñett walla ñeent yu jot a daw réew mi. Waaye, bu jaree ñu jëli leen, xëcc seen baaraami tànk, diri leen indi, dinañ ko def. Dinan def sunu kemtalaayu kàttan ngir Yoon àtte, ñu delloosi xaalisu Senegaal bi ñu randal. Du càggan ne danuy seetaan walla danoo yéex. Dañu bëgg rekk amal liggéey bu mucc ayib. “
Bees sukkandikoo ciy kàddoom ba tey, ci fan yii di ñëw, ay fukki fukki nit dinañ wuyuji yoon. Ku sàcc ñaar-fukki junni ak téeméeri miliyaar lañu yemale. Ku jël dërëm, dinga fey. Ci tënk, Usmaan Sonko tontu na waa BBY yi doon jaay fit, di leen tëkku te naroon leen tere liggéey. Wolof nee, bukki bu yabee waxambaane, ca doxiin wa la.