SOROJ BI : BALLUY SÀNGOMAAR YI KAWE NAÑU NJORT

Yeneen i xët

Aji bind ji

Balluy Sàngomaar yi, 100i kilomeetar lañu soree Ndakaaru. Kërug liggéey gii di Australian Woodside moo sasoo liggéey bi. Mu mel, fi mu tàmbalee nooy na lool. Nde, lees doon séentu ci balluy soroj yi nekke Sàngomaar dina kawe njort yi. Maanaam, tolluwaayu soroj bi war a ballee ci teeni Sàngomaar yi dafa weesu tolluwaay bi ñu xayma woon ca njëlbeen. Dafa di, ci biir juróom-benni weer yu njëkk yi, ñoo ngi xaarandi lim bu tollu ci diggante 15 jàpp 16i miliyoŋi barigoy soroj.

Ñeenti miliyoŋi barigoy soroj ñooy dolleeku ci lim bu njëkk bees xayma woon. Ci xalaatu Charles Thiemele, lu ni mel nag, « lu neex lay gaatnga » ñeel liggéey biy sog a door. Moom Charles Thiemele, BGN lay liggéeyee, di ki jiite banqaasu Afrig ci kër googee. BGN nag, kërug liggéey la guy yëngu ci wàllu soroj.

 Jamono jii, juróom-fukki junniy barigoy soroj lañuy génnee bés bu set fa Sàngomaar. Nisër bi mooy ful lim boobii ñaari yoon. Maanaam, ñu dem bay génnee lu tollu ci téeméeri junniy barigoy soroj bés bu nekk. Bu loolu sottee, déwén, Càmmug Senegaal dina ci góobe lu ëpp xaaju miliyaar ci xaalisu dolaar. Ndaxte, 100 yoo jël ci liggéey bi, Càmmug Senegaal moo taxawee 18 yi. Du ca yam nag. Nde, buuña bi mooy ne, dees na mën a jaay soroju Senegaal fi réew mi. Cegguwaay (raffinerie) bi nekk Mbaaw moo liggéey loolu.

Cig pàttali, ceggug (raffinage) soroj bi, fa Sàngomaar, dafa xawoon a yéex a tàmbali. Li ko waral mooy ne, xeetu soroj bi fay ballee dafa diis, bari lool lees di wax ci nasaraan « souffre ». Jamono jii, waa bitim-réew lañu koy jaay, rawatina waa kembaaru Aasi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj