(Ci tekkig Ndey Koddu Faal)
Njolloor, ca Minneapolis. Alkaatib Tubaab teg óomam ci kow loosu nit ku ñuul di bës, di bës, di bës rekk, tëwa bàyyi. Ñépp fàttaliku démb. Noyyi të ko ticc, mu fatt naan ngir Yàlla mënumaa noyyi. Saa su ne metit wiy gën a tar. Bëggul a dee, di woo ndey ji wallu, fàtte ne kooku faatu na bu yàgg a yàgg, ndeysaan. Di wàkkirlu Boroom bi. Ay onki yàkki. Àddina sépp di dégg i yuuxoom, teg ciy bëtam. Mu dëféenu ci tali bi, askan yépp di ko seetaan, xolu takk-der biy reetaan mu bësaat. Noyyi gënatee të George Floyd, mu faf dog.
Nun, kàngami Mbootaayu Xeet yi fekk baax Afrig, ñaawlu nanu bu baax xeetal geek néewal-doole doomu-aadama gi sax dakk fii ci Amerig ak ci àddina si. Ma nga doore ca maam ya ba sun-jonn-Yàlla-tey jii. Te ñiy def ñaawteef yii, nit ñu ñuul ñi lañ singali ; nu wax ko ak nu bañ koo wax, am na lu mu def ci nun. Kon dunu tàyyee jébbaane nooteel gi ñeel doomi Afrig yu ñuul yi. Duut ko baaraam am na solo, waaye danoo war a weesu wax, tey jëf.
Am na sax lu ci António Guterres miy njiitu Mbootaayu Xeet yi wax. Dafa ne : « Warunoo toog di seetaan ñuy toroxal nit ndax melo deram kese. » « Black Lives Matter » du ay wax rekk, xeet yépp a ko tax a jóg.
Kon wax ji doy na, nanu farlu ci xeex xeetal.
Naam, du guléet waaye George Floyd ak ñi xeetal mës a dal seen kow ñoo nu may nu mën a weeje tey xeebaate beek ñaawteefi takk-der yi. Kon, nu ngi leen koy sante. Nun ñi Yàlla may nu doon i kilifa noo war a waxal sunu mbook yi seen baat mënta àgg fu sore. Jot na nu taxaw temm daan musiba mii di nooteel te tàmbalee lëmbe àddina si ay xarnu ci ginnaaw.
Bóom gu ñaaw gi ñu bóom George Floyd weesu na jëmmam di wéy. Dañ cee war a am jàngat bu yaatu, daanaka mënees na koo méngaleek benn per cib caqu jafe-jafe yoo xam ni su nu ci jógul du baax. Jot na nag Mbootaayu Xeet yi jàmmaarlook xeetal ak noggatug doxandéem te loolu su ko defee day dëppook lim bi jiitu ci Sàrtam, lim biy wax ni dafa war a « naatal ak dooleel àq ak yeeleefi doomi-aadama yépp, bañ a toppatoo seen xeet, seen làkk walla seen diine ». Te ci dëgg-dëgg li Mbootaayu Xeet yi gëm mooy ñépp a yem te wareesul a doyadil benn doomu-aadama mbaa di ko mbugal.
Am na jamono doomi Amerig yu ñuul yi di xeex ngir jële ci àddina si boddikonte ci biir xeet (gàttal gi ci nasaraan CIEDR, di joxe ‘’Convention Internationale sur l’élimination de toutes les formes de discrimination raciale’’) fekk it ay réewi Afrig yuy soog a moom seen bopp ñëw bokk ci Mbootaayu Xeet yi. Ci jamono jooju ci atum 1969 lañuxaatim benn Déggoo bu yaatu ñeel bépp boddikonte ci biir xeet.
Jamono ju kenn dootul fàtte la ndax ca la ‘’apartheid’’, doonoon ñaawteef bu yoon daganaloon, nërméelu. La ko daneel, nag, Mbootaayu Xeet yi am na ci wàll te ba léegi da koy ndamoo.
Àq ak yeelleefu doomu-aadama ak sagu nit ku ñuul ci Afrig ak ci àddina si ñoo ngi riir tey te sunuy sët dinañ leen déggi ëllëg. Kon,mu war a leer ñépp ni Mbootaayu Xeet yi dootul dumóoyu su ñuy noot nit te dootul nangu par-parloo. Moom daal, dina def kem-kàttanam ngir kenn dootul jam kenn naani.
Daanaka la woon, wonni na ba tax Mbootaayu Xeet yi am fu mu wéeru. Dina jëmbët fulla ci xeex bi, xamal ñépp ne njaw des naw xambin, de4gg la, waaye du tee mu war a wóor ni xeetal ak i gàkk-gàkkam dinañ fi jógeji ba fàww.
Sunu Sekerteer Seneraal jël na ay dogal ngir xeex xeetal ak i njéexitalam yu ñaaw fépp ci àddina si ba ci sax sunu biir kër gii ci New York.
Su nu bëggee doon ay njiit yu baax, fàww nun ci sunu bopp nuy def li nuy digal nit ñi.Coppite dëgg dafa laaj nu waxtaan ak sunu xel, seet sunu digganteek Yàlla ndax sunuy jëfin méngoo naak li Sàrtu Mbootaayu Xeet yi santaane.
Soo dee njiit, dangay nangoo tënku ci Sàrtu Mbootaayu Xeet yi ni mayul kenn mu ni patt. Danoo war a yëkkati sunu kàddu, am fitu ñaawlu jaay-dooleek xoqtal.
Ku nekk ci nun dina takku ba dëgër, def kem-kàttanam ngir dakkal fi xeetal, dinanu ci dugal sunu xam-xam, def lépp lu nu mën ngir déqati ko, jële ko fi ba fàww.
Ba nit ñu weex ñi tàmbalee jàpp jaam sunuy maam di leen jaay ci diggante Afrig, Ërob ak Amerig, léegi mu mat 500i at. Rax-ci-dolli, ñeenti at rekk moo des ci fukki at yi ñu jagleel nit ku ñuul, ndax 2024 lay jeex. Kon, nanu bennoo, xàccandoo dóorandoo, fexe ba Mbootaayu Xeet yi def wareefam, indi ci àddina si coppite yi sunuy askan yàgg a yaakaar. Ni ko ñépp xame, amees na arminaatub (agenda) 2030 ñeel àddina si. Bunu yëkkatee sunu baat dugal ci arminnatub Afrig ñeel 2063, coppite bi ñépp bëgg dina am.
Afrig la doomu-aadamaa fekk baax te it mooy jéeri ji war a taxawu bu baax àddina ngir mu mën a sottal yokkute gu sax dakk ak jàmm.
Lii moo yittéeloon Mag ñi sosoon OUA ak tamit njiit yu mel ni Kwame Nkrumah walla xeltukat bu mag bu mel ni Séex Anta Jóob.
Bunu fàtte mukk kàdduy Nelson Mandela yii : « Képp ku iñaane nit àqam, daa fekk jàppewoo ko ni nit.»
Fannie Lou Hamer, doonoon fi njiit ci xareb doomi Amerig yu ñuul yi, mu ngi nuy bàyyiloo xel ci ne : « Kenn mënul a moom boppam fileek ñépp moomuñu seen bopp. » Doktoor Martin Luther King Jr, feelu ko naan : « Nooteel, fépp fu mu mënti ame, musiba la ci ñépp ».
Ñu teg ciy at, tey, ca réewu Afrig-bëj-Saalum làbbe Desmond Tutu dëggal kàddu yooyu ne : « Ngir nit ku weex moom boppam, fàww nit ku ñuul moom boppam ndax amul xeet wu mën a féex moom kenn, ñépp a war a àndandoo féex.»
(*) Ñi xaatim kayit gii ci seen turu bopp lañ ko defe. Kenn ku ci nekk ag kàngam nga ci Mbootaayu Xeet yi, di tofo ci Sekerteer Seneraal bi.
Tedros ADHANOM GHEBREYESUS
Mahamat Saleh ANNADIF
Zainab BANGURA
Winnie BYANYIMA
Mohamed Ibn CHAMBAS
Adama DIENG
Bience GAWANAS
François Lounceny FALL
Gilbert HOUNGBO
Bishar A. HUSSEIN
Natalia KANEM
Mukhisa KITUYI
Jeremiah Nyamane MAMABOLO
Phumzile MLAMBO-NGCUKA
Oumarou D. MOUSSA
Mankeur NDIAYE
Parfait ONANGA-ANYANGA
Pramila PATTEN
Vera SONGWE
Hanna TETTEH
Ibrahim THIAW
Leila ZERROUGUI