« Place de la nation », walla Péncum askan wi ci wolof, wuyoo na turam démb ci àjjuma ji. Nde, ci ngoon gi, foo sàndi waan mbàttu mu tag. Dafa di, askanuw Senegaal dafa wuyusi woon wooteb way-moome yi ci lu baree bari. Mag, ndaw, góor, jigéen ba ci way-laago yi sax, ñépp ñoo nga woon ca ndajem ñaxtu ma. Ndaw ñaa fa ëppoon nag, feesoon fa dell. Jubluwaayu ndaje maa doon sàkku ci ñu topp ñi caabalug Ëttub Cettantal gi duut baaraam ñeel koppari xeexub Covid-19 bi. Bu doon ne mbooloo la way-moomeel ya bëggoon, seen nisar àntu na. Waaye, dépite Paap Jibril Faal moom, jëlewu fa lu sedd xolam.
Mbasum Covid-19 maa ngi wéy di lëmbe réew mi. Bu tereetul nit ñi génn tamit, tere naa nelaw ñenn ci njiiti réew mi. Ñoo yéy nag. Tuuma yees leen gàll ñoo réy. Daanaka, dañu leen tam dëmm. Kees di wax ni deretu askanam lay dunde, ndax jiiñeesu ko dëmm ?
Jamono ji ñuy tëj nit ñi seen i kër, di leen tee liggéeyi ak a tukki, ndeke ñoo ngi daan jalgati yoon, di jéggi tëralini sàrti caytu gi, di def lu leen neex. Yemu ca de. Déedéet ! Dañ daan ñukki, di ñóox ci seen i jiba. Guddi ya ñu daan dóor nit ñi, ndekete dañ daan laxasaayoo lëndëm gi, di dóoraale ci 1 000 milyaar yees leen dénkon ngir ñu xeexe ko mbas mi, muy alalu askan wi. Waaw, bees sukkandikoo ci caabalug Ëttub Cettantal gi ñeel koppari Force Covid-19 yi, gaa ñi dañoo dóor, dóoraat. Waaye nag, wolof nee na, dóor feyu. Moo tax way-moomeel yi wootem ndaje ngir yoon niit caabal gi, lëñbët ba xam ci yan jiba la alalu askan wi tàbbi. Ginnaaw gi, bu ko jaree, mu jël yat wi, dóor boroom dóor dóoraat yi ci laale. 10i nit ak lu teg lees joxoñ, mu am ciy jëwriñ yoy, du guléet ñu leen di dégg ciy njombe ak i luubal.
Mbooloo ma bari woon na lool sax. Pénc ma dafa ñuuloon kukk ak i nit. Way-ñaxtu yi dañu indaale woon seen i pànkart. Ñuŋ ca bindoon : « Sunu milliards du rees », « Sunu milliards yi du rees », « Libérez Pape Ousmane Seck » [Bàyyileen Paap Usmaan Sekk], « Libérez Pape Alé Niang » [Bàyyileen Paap Aale Ñaŋ], « Mansour Faye voleur de milliards » [Mansuur Fay sàcckatu milyaar], « La Casamance n’est pas un abattoir » [Kaasamaas du seeraas], « Rendez-nous nos milliards » [Dellooleen nu sunuy milyaar], « Libérez les otages politiques » [Bàyyileen way-tayle pólitig yi], « Non à un 3ème mandat » [Lànkees na 3eelu moome], « Non au népotisme » [Bàyyileen boddekonte mbokk], « Macky Sall, le Sénégal n’est pas un royaume » [Maki Sàll, Senegaal du Nguurug ndono], « Alioune Sall, mes 400 000 » [Aliyun Sàll, samay 400 000], « Mamour Diallo et Moustapha Diop déshonorent Louga » [Maamuur Jàllo ak Mustafaa Jóob gàcceel nañu Luga], « Détournement fonds covid-19 Macky Sall lever le coude » [Lubbalug koppari Covid-19, Maki Sàll yékkatil sa concu], « Détournement fonds covid-19, les morts réclament justice » [Lubbalug koppari Covid-19, way-dëddu yaa ngiy sàkku yoon], añs.
Wëliis askan wi, kilifa yu bari teewoon nañ fa : kilifay kujje gi, way-moomeel yi, lenn ci kilifay diine ak kilifay aada, jël kàddu gi, yakk Nguur gi lu mel ni xeme. Waaye, yuuxu yees gatandoo dépite Paap Jibril Faal, taskatu xibaar ba woon, moo xaw a ñagasal xew-xew ba. Lees koy tuumaal mooy ne péeteem leerul. Maanaam, day cuuj fii, capp fee. Am na ci sax ñuy njort ne Nguur gi la àndal ci pet. Moo tax mayuñu ko mu wax. Te sax, coow loolaa taxoon ñu dagg xew-xew ba diirub 20i simili. Ginnaaw bi ñu fexee ba yéegal ko ci tirbin bi, jéemoon naa wax, waaye mbooloo ma mayu ko ko. Ndeysaan, day mujje wàcc, ñibbi. Looloo tax sax yenn kilifa yi tamit ñibbi, muy Aliyun Tin mi jiite Africa Jom Center, Sadiix Ñas bu Raddho, dépite yii di Aminata Ture, Gii Mariis Sañaa, Biram Suley Jóob… Njiital PASTEF lii di Usmaan Sonko, moom, teewul woon ca ndaje ma, waaye ñaawlu na yuuxu ya mbooloo ma yuuxu Paap Jibril Faal. Mi ngiy xamle ne, xeex bi, ci Maki Sàll kese ak i ñoñam lees ko war a jëmale.
Ginnaaw bi ndaje mi sottee, mbooloo ma wuyusi leen, ñoo ngi xaarandi tëggub bool bi Yewwi Askan Wi woote ci 31 desàmbar bi, bu 20i waxtu jotee.