Taaxub 3i etaas moo màbb ci guddig altine ji jàpp talaata. Xaar-Yàlla la jéyya ji amee. Ci lees xamagum, 5i nit ñàkkagum nañ ci seen i bakkan, mu 12 yu ci jëley gaañu-gaañu. Jukkees na xibaar yile ci APS mi leen jële ci takk-der yi.
“Limagum nañ fukk ak juróom-ñaari nit yu ci lors, am juróom yu ci dee.”
Bees sukkandikoo ci APS ba tey, bi 1 waxtu di jot ci guddi gi lañ xamal takk-der yi ne am na taax bu màbb fa Xaar-Yàlla, wetu Walfadjri. Bi takk-der yi agsee, dañu gis ne dafa am lu màbb cib taamu ñetti etaas bob, dañ ko doon yeesalaat fekk ay nit ñoo nga fa woon dëkk.