TAAXUM KAW MA MÀBB FA TUUBAA

Yeneen i xët

Aji bind ji

Am taaxum kaw a màbbati. Fa Ngor (diiwaanu Ndakaaru) la am taaxum kaw njëkkoon a màbb, ñaari ayu-bés ci ginnaaw. Wii yoon nag, fa Tuubaa (diiwaanu Njurbel) la jéyya ji xewe. Dafa am taaxum kaw mees doon tabax mu faf màbb ci dibéeru barki-démb ji, 25i me 2025. Ndeysaan, 18i nit ñoo ci loru ; ci biir 18i way-loru yooyu, 11 yi ñàkk nañu ci seen i bakkan. Càmmug Senegaal, ci làmmiñu jëwriñu Tabaxte gi, Sëñ Musaa Bàlla Fofana mi fa demoon, fas na yéene taxawal ci meeri bu nekk ag ndiisoog xarala guy saytu lépp lu aju ci mbirum tabax yi.

Ñaari nit ñoo faatu woon ca sababu taax ma màbboon Ngor, mu amoon kenn ku ci jële woon ay gaañu-gaañu yu metti. Wile yoon, lim bi faatu ci màbbub  taaxum kaw fa Tuubaa àgg na ci fukk ak benn. Ci lees waxagum nag, ay xeeti càggante yu bari ñooy waral màbb yi, niki : ñàkk a sàmmonte ak sàrti tabax yi, ñàkkug saytu bi, nger, ndóol ak bëgg lu yomb.

« Jamono yii, danoo seetlu ne dafa bari na ay nit yu faatu ci sababu taax yuy màbb. Danu war a gën a fobu ci anam yi nuy tabaxee sunuy taax ak i dëkkuwaay, muy tabaxi bokkeef gi walla tabaxi jàmbur yi. » (kàdduy Xaadim Aan, Perefe Mbàkke)

Bi 15i waxtu toftalee as lëf ciy simili la taaxum kaw ma màbb. Taaxum ñetti etaas la woon mom, doon nañ ko tabax, fa béréb bees di wax Gaaraas Daaru. Jamono ja muy daanu nag, dafa fekk mu amoon ay masoŋ yu bari yu nekkoon ca biir taax ma, di liggéey. Ba taax ma daanoo, ca saa sa la wallukat ya (sàppëer yi ak waa Kurwaa Ruus) gaawantu woon nañu, daw walluji way-loru yi. waaye, du ñépp ñoo mucc. Ndaxte, 11 dee nañu ci, 7 ame ci gaañu-gaañu yu mettee metti. Ba nëgëni nag, ñoo ngi wéy di seet ndax amul i nit ñu nekkandi ci suufu màbbit yi.

« Ci ngoon gi lañu woo sàppëeri Tuubaa yi, yégal leen ni dafa am um taaxum ñetti etaas mu màbb fekkoon mu am ay masoŋ yu nekkoon ca biir doon liggéey. Ba sàppëeri ya àggee, wër nañu ay waxtu laata ñuy génnee ña woon ca biir màbbit ya, mu am ña ca faatu ak ñu ca mucc, waaye amey gaañu-gaañu yu metti. » (Kàdduy Perefe Xaadim Aan)

Ci altiney démb ji lañu xam lim bi ci faatu (11) ak lim bi ci jële ay gaañu-gaañu (7). Bees sukkandikoo ci kàddu perefe bi bat ay, àntarpërënëer bi ñu wax ne moo sabab màbbub taax ma ca Ngor (keroog 8 me 2025), kookii tamit moo doon tabax taax mii màbb fa Tuubaa. Perefe bi xamleet na sax ni, jamono jii, àntarpërënëer baa ngi ci loxoy Yoon.

Senegaal nag, bari na lees fy gis walla dégg ay taax ak i tabax yuy màbb ak a daanu. Léeg-léeg, mu am ñu ci ñàkke seen i bakkan. Bu ñu dee fàttaliku sax, ca weeru saãwiyee 2024, amoon na am taax mu màbboon fa Xaar-Yàlla (Ndakaaru) ba mu am ku ci ñàkkoon bakkanam. Booba, dafa amoon ñu doon tabax te mënuñu, doon defaraat ab maraaj bu amoon i xar-xar. Ci li caabalug Birigàdd sàppëer yi xamle woon ca atum 2022, lu tollu cin 75i  bakkan jotoon nañu rot ci sababu taax yu màbb. Bu dee sabab yi, nee ñu, dafay dellu ci ñàkk a sàmmonte ak sàrti tabax yi, ñàkkug saytu bi, nger, ndóol ak bëgg lu yomb. Moone de, Senegaal tëral na ay sàrt yu bari te leer nàññ ñeel lépp lu aju ci tabax yi. Waaye, li ëpp ci tabaxkat yi, ñi leen di liggéeyloo ak ñi leen war a saytu duñu sàmmonte ak sàrt yooyu. Dafa di, ci li waa « Services de la protection civile » xamle woon ca atum 2021, am na 1 44-i taax yu nekk ci yoonu màbb ci réew mépp. Ci biir lim boobu, 627 yi Ndakaaru lañu nekk.

Jëwriñ ji ñu dénk Tabaxte yi, Bokk-meeli réew mi ak Sanci mberaay mi demoon Tuubaa, fa jéyya ji xewe. Fésal na fa ndogal yi Càmm gi namm a jël ngir fàggandiku ci musibay taax yiy màbb di faat i bakkan. Ci kaw loolu, xamle na ni Càmm gi dina taxawal i ndiisooy xarala yuy saytu lépp lu aju ci mbiri tabax yi. Dafa ne : « Yoon wi nu tànn mooy dooleel meeri yi, taxawal ci bu ci nekk diisoog xarala guy saytu lépp lu aju ci mbiri tabax yi. »

Ba tay ci waxi jëwriñ ji Fofana, « ci meeri yi lees mënee saytoo lépp lu jëm ci tabax yi, xool ndax sàmmonte nañu ak àppi tabax yi, jumtukaay yi war ak lépp li war. » Rax-ci-dolli, dinañu joxe ag limtu gog, mënees na cee woote ngir weeje, boole képp kuy tabax te sàmmontewul ak li Yoon sàrtal ci wàll wi.

Jëwriñ ji jaale mbokki way-dëddu yi, mastawu njabooti way-loru yi. Waayeet, ndokkeel na wallukat yi ak fajkat yi taxawu way-loru yi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj