TABASKI 2023 : XUTBA CEERNO SAYDU NUURU TAAL

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ci alxamesu démb ji la ñu ëpp ci saa-senegaal yi tabaski. Ku ne tabaski, ne xutba. Te, xutbay imaam yi, dees na koy faral di xaaj ñaari pàcc. Bu ci njëkk bi, imaam yi dañu koy jagleel diine ji, jagleel beneen ñaareelu pàcc bi tolluwaayu réew mi, rawatina li ci fës. Noonii la fa deme at mii tam. Ceerno Saydu Nuuru Taal, ca xutbaam ba, ñaan na jàmm ci réew mi, sàkku ñuy amal waxtaan at mu nekk ci fànn yépp te soññ ndaw ñi ci moytoo yàq alalu réew mi.

Imaamu jumaay Omariyeŋ yi, Ceerno Saydu Nuuru Taal, ci alxames ji la julli. Ba muy xutba, ñaanal na Senegaal jàmm ak tawfeex. Waayeet, soññ na njiit yi ci ñuy jiital diisoo ci fànn yépp, ginnaaw bim rafetloo waxtaan wi Njiitu réew mi sumb. Dafa jàpp ne, waxtaan woowile, warees na ko amal at mu nekk te yaatal ko ba muy laal dund gépp.

Imaam Ceerno Saydu Nuuru Taal ñaawlu na tamit yëngu-yëngu yi toftalu woon ci ndaanug Usmaan Sonko ga ñeel layoom beek Aji Saar, bay nit ñu bari dee ci. Imaam bi nee, bakkan dafa tedd fa Yàlla, wareesu ko dog lu moy ci kow dëgg. Mu daldi tari aayab Alxuraan juy feddali waxam ji : « Ku rey benn bakkan, mel na ni àddina sépp nga rey. »

Kilifag taalibey Umar Fuutiyu Taal yi naqarlu na tamit yàq yi, toj yeek càcc gi àndoon ak yëngu-yëngal yooyee. Mu ne : « Islaam dafa araamal càcc ak jël alalu jàmbur. » Ni saa-senegaal yiy tojatee ak a yàqatey béréb, di taal ak a jafal ay daamar añs. Daf ko jaaxal, tiital ko lool. Ndax, Senegaal, léegi, dañu xër ci toj ak taal te, ciy waxam, « daan nañ wax ni, doomu Senegaal mënul sax rey ab mellentaan. » Kon, bu yeboo jàpp ne, Senegaalu démb, du Senegaalu tey. Teewul Imaam baa ngiy ñaaxati ndaw ñiy yàq, di leen xelal ak digal ci ñu bañ a déglu taalkati fitna yoy, ña nga bitim-réew toog, nekk ci seen jàmm. Daf ne :

« Buleen déglu ñi leen wax ngeen taal walla yàqate këri jàmbur yi walla ay bérébi liggéey. Ñaare, bitim-réew lañuy nekk, toog ci seen i saal yu nooy (…) te, ëllëg, yeen a aajowoo biis yeek saxaar gi. »

Ndigle laa ngoog. Nu xool ba xam dees na ko jëfe.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj