Ibaaduy Senegaal yi julli nañu tabaski niki tay ci alxames ji, 6i suwe 2025. Fu bari ci diiwaani réew mi julli nañu fa, rawatina fi Ndakaaru. Kon, nees ko tàmm a gisee, julliti Senegaal yo duñu tabaskeendoo. Ndax, bu dee ñoñ tarixa yi, ñoom ëllëg lañuy julli, ci gaawu bi.
Fii, fi Ndakaaru, Ustaas Moor Kebe jiite na mbooloo mu takku lool fa pàkku fowub Lewopool Sedaar Seŋoor. Bi mu sëlmalee nag, biral na fa xutba bu am solo.
Ustaas dafa woote jàmmoo, bennoo ak jàppoo. Dafa soññ saa-senegaal yi, rawatina jullit ñi, ci ñu mbokkoo, booloo def wenn say ngir mën a dékku ngaañ yi leen di gaar.
Ustaas Moor Kebe dafa njëkk a fàttali solos bés bile. Ndax, ciy waxam, bésub tabaski mooy bés bi gën a màgg ci aj gi. Li ko waral mooy xeeti njaamu Yàlla yi ci daje. Nee na, bésub tabaski, bés bees di màggal Yàlla la, di Ko ci bàkk, di Ko ci kañ, di Ko kennal ak a sant. Waayeet, ba tay ci kàdduy imaam bi, bésub mbégte la ñeel jullit ñi, di yit bés buy wane rafetaay ak taarub lislaam.
Ustaas Moor Kebe xamleet na ne ci jamonoy fitna lañu nekk. Dafa bari ay lënt-lënt yiy yàq diine ak di ko xajamal. Muy woo jullit ñi ci ñu góor-góorlu, laabal xol yi, sellal pas-pas yi te sukkandiku ci xam-xam bu leer te wér, di xam-xam bu tegu ci Alxuraan ak Sunna. Nee na, kuy def, na defal Yàlla kepp, sellal yéeneem, bañ cee boole ngistal walla di ci xool keneen.
Ngir loolu am, Ustaas bi soññe na ci muñ ak digle lu baax ngir ñu baaxal ak yéwénal jikko yi. Nde, bu jikko yi baaxee, mboolaay mi dina baax.
Mi ngi woo boroom kër yi ci ñu jëmbat ci xale ay mbaax, yiir leen te wattandikuloo leen musiba ak yàqutey mbaali jokkoo yi.
Bàyyiloo na xel kilifa yi jiite réew mi ci wàllu àdduna ngir ñu gën a sàmm lislaam ji, xeex lépp lu koy gàkkal, di ko ñaawal ak a fowe. Woo na leen tamit ci ñu jàppale ñoñ lislaam, dugal seen loxo ci mbirum weer wi ngir ñu ànd doon benn, di woorandoo, di woreendoo ak a julleendoo.
Ustaas Kebe naqarlu na kàdduy Seneraal Maysa Sele Njaay mii doon tuumaal ibaadu yi. Kàddu yii toftalu la ko jagleel :
“Dunu jeexal sunu xutba bii nag lu dul ne tontu nanu ak yékkati sunuy kàddu, di kàdduy naqarlu [ñeel] yenn kàddu yu fi jib fan yii ci kenn ku ñu yaakaaroon ne kilifa la […] jël wax ju ñaaw a ñaaw, jëmale leen ci jàngalekati Alxuraan yi, jëmale leen ci jàngalekat yiy jàngale ak di woote ci yoonu Yàlla.”
Rax na ca dolli ne :
“Xam nañu ne réew mi, mi ngi jël yoon woo xam ni neexul ñu bari. […] Bokk na ci pexe yi noon yiy jëfandikoo ci réew mi mu bëgg a yëngal, mooy jéem a yee fitna, féewale ak xàjjale jullit ñi, di tam ñenn ci ñoom dëmm ak di wax ci wàllu terorism ak jihaadism ak yi ci jëm.”
Loolu nag, ci li Ustaas bi wax, kenn déggagu ko fi réew mi. Jàmm moo fi am, dal moo fi am. Mi ngi ñaan jàmm jooju wéy di am.