Tàmbali nañu tabax ab dëq (digue) fa Daaru, diiwaanu Ndar. Jubluwway bi mooy aar askan wa ci walum dex Senegaal gi. DIRPA, banqaas bi yor kàddug làrme bi moo ko xamle.
Ci X (Twitter ba woon) la DIRPA bind, siiwal ne, : « Fa Daaru, ñu ngi tabax ab dëq ngir aar bëj-gànnaaru dëkku Ndar. »
Bees sukkandikoo ci ñoom ba tay, ci talaata jii weesu, 29i pani oktoobar 2024, fajkati làrme bi doon nañ saytu wér-gi-yaramu way-loruy walum dex gi ci lu amul fay. Ña dëkk Orkajere (Podoor) ñoo ci doon jariñu.
Jëwriñu ndox mi ak cellal gi, Séex Tiijaan Jéey, nemmeekuji woon na dëqu Daaru bi. Ndax, ci gis-gisam, Daaru dafa bokk ci béréb yi gën a yomb a loru ci walum dex gi, foofa, fa diiwaanu Ndar. Loolu moo tax ñu jël seen i matuwaay ngir dooleel dëqu Daaru bi.