Elimaanu jëwriñ ja woon, Mahammad Buun Abdalaa Jonn, moo génn àddina. Tey, ci àjjuma ji, 5 awril 2024, la gaañu. Farãs gim doon fajoo la gaañoo. Ci dalu webu APS lees jukkee xibaar bi.
Moom nag, lawax la woon ci wotey 2024 yii nu génn. Ci gaawug 23 màrs 2024 lees ko rawale woon Farãs ginnaaw bim daanoo feebar ci kàmpaañ yi. Juróom-benn-fukki at ak juróom (65i at) la amoon.
Dees na ñëwaat ci jaar-jaaram.
EJO ak LU DEFU WAXU ñoo ngi koy jaale njabootam ak i mbokkam, di ko jaale naataangoom yim bokkaloon làngu pólitig ak askanuw Senegaal, di ko ñaanal Yàlla njéggal ak yërmande.