TÀGGE : NGŨGĨ WA THIONG’O DËDDU NA

Yeneen i xët

Aji bind ji

Afrig ñàkkati na kenn ci doomam yu ràññeeku yi. Wile yoon, njabootu ladab ak mbatiit ñoo am dëj. Nde, bindkat bu mag bii di Ngũgĩ Wa Thiong’o, di ab saa-keeñaa, moo wàññeeku ci àllarbay démb ji, 28 me 2025. Muy xibaar bu tiis lool te ànd ak naqaru xol wu réy. Ndax, moom bindkat bi, werekaan la woon, xarañoon lool, te daan jëfandikoo xalimaam ak baatam ngir xeexal Afrig. Amerig la faatoo, fekk mu ngi tolloon ci 87eelu atam.

Ngũgĩ Wa Thiong’o bokk na ci bindkat yi gën a mag ci mboorum Afrig. Daanika, dundam gépp, ci bind ak a fésal coppitey réewam (Keeñaa) la ko jeexal. Ku ko xam, xam ni ko fobu woon la ci mbatiitu Afrig, takku woon taxaw, di xeexal ak a liggéeyal làmmiñi Afrig. Dafa di, moom ci jëmmi boppam, dafa daan bind ci làmmiñ wi mu nàmp te daan soññ ak a xirtal saa-afrig yi ñuy bind ak a taalif ci seen i làmmiñi meen. Naam, ba muy door, ci àngale la daan bind. Waaye, bi mu demee ba ca biir, daf ko bàyyi, jël làmmiñ wa mu nàmp, di ca jëmmal i xalaat ak di ca fent lu xarañe, jaare ko ca xalimaam bu ñaw ba.

1938 la werekaan bi ganesi woon àddina. Jamono jooja, dafa fekkoon saa-àngale yi noot réewam. Kon, moom, jamonoy mbéeféer la juddu. Maanaam, jamono ja tubaab ya nootee kembaaru Afrig. Loolu nag, jeexital na bu baax ci xalaat ak mbindi fugraas bu mag bi mu doonoon.

Fa dëkk bi ñuy wax Limuru la màgge, bokkoon ci njaboot gu yaatu, di woon njabootu baykat yoy, oomlewuñu woon naam, waaye ñu ngi doon sant Yàlla. Noonu, ay way-juram fexe woon nañ ba yaxanal as tuut lañu daan am ci xaalis ngir fayal ko njàngam ca daara ja ñu dippee woon “Alliance”, ay làbbey saa-àngale jiite woon ko. Moom nag, jàmbaaru xalima bi, ca xaleelam la jànkonteel, ci teel, ak fitnay nooteelu tubaab yi.

Ca atum 1959 la Ngũgĩ laxasaayu, jàngi fa jànguneb Makere ba nekk Ugàndaa. Foofa la tàmbalee bind. Nde, ba fa ay bindkat doon amal ndajem waxtaan la jël la mu bindoon, jébbal ko bindkat bu mag ba woon, Chinua Achebe. Kookii daldi yónnee téere ba móolkatam ba nekkoon “Royaume-Uni”, mu daldi ko koy génneel ca atum 1964. Téere baa ngi tudd Weep Not, Child. Mu nekkoon téere bu siiw te xarañe, di woon itam njëlbeenug téere fent bu ab saa-afrigu penku bind ci làkku àngale.

Bi loolu amee, Ngũgĩ naaguwul. Dafa yattaat xalimaam, toftal ci yeneen ñaari téerey fent yu siiw a siiw : A Grain of Wheat ak The River Between. Booba, 33i at kepp la amoon. Moo taxoon sax saabalukaay àngale bii di Times boole woon ko, ca atum 1972, ci bindkati jamono yu gën a ràññeeku ci Afrig.

BBC jotoon na tóxal as lëf ciy kàddoom yuy firndeel loolii. Nde, ci biir kàddu yooyii BBC jukki, Ngũgĩ mi ngi ciy fàttaliku keroog ba mu jógee ca daaraam jooju di “Alliance”, ca njeexitalu ñetteelu weeru njàng ma, ñibbi dëkkam. Waaye, keroog ba mu àggee, dafa fekk saa-àngale ya rajjaxe dëkk bépp, yàq yaxeet dëkkuwaay ya, ba ay mbokkam ci boppam mujje ca dëkki béréb ya ñu tënkoon nit ña. Xew-xew boobu, mi ngi méngoo ak jamono ja ñuy xoqatal ak a nasaxal kurél gees dippee woon “Mau Mau”, daan xeex ngir jonnug Keeñaa. Waaye, jéyya ju gën a metti jooja dal na ko. Mooy ba nootkat ba di rey mbokkam mu góor ma tuddoon Gitogo. Ab balu fetel lañu ko sox ci digg ginnaaw gi ngir ne dafa tanqamlu woon ndigalu benn sóobare saa-àngale. Ndekete, Gitogo moomu, dafa tëxoon, déggul woon ndigal la.

COPPITE GI

Ca atum 1977 la Ngũgĩ soppeeku, daldi fippu. At mooma la soppi aw turu tubaab wees ko ngéntee woon, James, daldi fental boppam aw tur wu bees ci làmmiñu meenam, Ngũgĩ Wa Thiong’o. Yemu ca de. Ndax dafa bàyyiwaale làkku àngale, tàmbalee bind ci làkkam wii di Kikuyu.

Petals of Blood mooy téere fent bi mu mujje bind ci àngale. Naam, ca téereem yu njëkk ya, doon na ca ŋàññi way-mbéeféer ya. Waaye, ci téereem bu mujj boobu, ma nga cay jam njiiti Afrig yi wuutu tubaab yi ci jal bi.

Moom Ngũgĩ, kaso la bindee téereem bu njëkk ci kikuyu. Nde, ginnaaw bi mu bindandoowee ab kilib ak kii di Ngaahika Ndeenda (I Will Marry When I Want), Nguur ga daf ko jàpplu woon, tëjlu ko. Téereem baa ngi tudd Devil on the Cross. Nee ñu, ci këyiti laabukaay yi la ko bindoon ndax amul woon kàrne.

Bi Daniel Arap Moi faloo la Ngũgĩ génn kaso. Waaye, ba mu génnee kaso ginnaaw 4i at, dafa déggoon ni, am ñu kootoo, di nas i pexe ngir faagaagal ko. Ca la gàddaayee Etaasini, toog fa diirub 22i at. 2004 la ñibbi réewam.

Waayeet, ba mu delloo, jàmm fekku ko ca. Ndax, ay saay-saay dañu songoon këram, dal ci kawam, fitnaal ko ba noppi daldi siif soxnaam sa. Moom Ngũgĩ, way-pólitig yi la ko jiiñoon.

KELEŊU LÀKKI AFRIG

Ngũgĩ bokk na ci ñi gën a fës ci xeexal làkki Afrig yi. Dafa gëmoon ni, bind ci aw làkk doxandéem ci njaamug mbatiit la bokk. Ci gis-gisam, dara wutalewul pólitiseŋ buy wax ni Afrig dafa soxla tubaab bi ak saa-afrig buy bind ci làkkuw tubaab. Looloo taxoon sax digganteem ak Chinua Achebe xawoon a ñagas.

Ngũgĩ nag, ag guy la ci ëttub ladabaakoni Afrig. Taxawaayam ak dayoom tax na ba ñu bari def ko royukaay, di safoo ak a ndamoo mbatiit ak làkki Afrig. Demam gi doon na lu tiis lool ci Afrig gépp.

EJO ÉDITIONS ak LU DEFU WAXU ñoo ngi koy jaale njabootam, di ko jaale askanu Keeñaa, di ko jaale njabootu ladab gépp ak ñiy xeexal làmmiñi Afrig, rawatina bindkat bu mag bii di Bubakar Bóris Jóob mi mu bokkaloon waar wi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj