TÀGGE : PAATUG AAMADU MAXTAAR MBÓW

Yeneen i xët

Aji bind ji

Guy daanu na. Aamadu Maxtaar Mbów, maamu askan wi, moo génn àddina. Ci guddig altiney démb ji, jàpp talaatay tay jii, la wuyuji Boroomam. Mi ngi amoon téeméeri at ak ñett.

Saabalkat bii di Aas Mademba Njaay moo siiwal xibaar bu tiis bile. Ci xëtam bu X (Twitter ba woon) la bind lii toftalu :

“Aamadu Maxtaar Mbów génn na àddina sos, liggéeyal na ko diirub dundam. Bokk na ci ñoñ, seen dund dafa amal njariñ doomi Aadama yi. Ginnaaw bi mu dundee 103i at, yeyoo na noflaayug jàmm. Na guyaaru Firdaws doon këram (…)”

Moom, Aamadu Maxtaar Mbów, kàngam bu mag a mag la woon. Àddina sépp xam ko te ràññee ko. Nde, jot na fee jiite UNESCO ci diirub fukki at ak ñetti (1974-1987). Jàngalekat la woon itam ci jàngune yi, di woon it nitu pólitig.

Farãs la Aamadu Maxtaar Mbów amalee njàngam mu kowe. Ginnaaw gi, doon na jàngale mboor ak sewogaraafi. Rax-ci-dolli, diggante 1966 ak 1970, nekkoon na fi jëwriñu Njàng mi ak mbatiit mi.

Ca atum 2008, weeru suwe, moo jiite woon lees dippee ci nasaraan “Les Assises nationales du Sénégal”, maanaam waxtaan yi soxaloon réew mépp. Jiite woon na tamit Ndajem joyyanti campeefi réew mi, ci tubaab “Commission nationale de réformes des institutions” (CNRI).

Ñetti at ci ginnaaw (2021), Senegaal màggal na téeméereelu atu Aamadu Maxtaar Mbów, maanaam xarnu bi mu def ci kow suuf. Njiitu réew ma woon, Maki Sàll, lees baayale woon xew ma. Ñu jotoon cee fénc ay wëppa yu solowu ñeel dundam, xamtu, pólitig ak mbatiit. Réew mépp delloo ko ci njukkal. Waaye, yemul foofu. Ndax, moom lañu tuddee ñaareelu jànguneb Ndakaaru bi nekk Jamñaajo.

Mënees na wax lu bari ci moom ndax dayoom ak jaar-jaaram. Waaye, lu jóge ci nag wépp, xajul ci cin li. Xanaa nu tëjee yaxal bi ak kàddoom yu gànjaru yii mu waxoon, keroog ca tëjteg “Assises nationales du Sénégal” ya :

“Amul, ci dundug askan, lu mënul a soppeeku. Lépp a mën a soppeeku. Waaye, dara du soppeeku fileek ñi bëgg a soppi seen dundiin booloowuñu, boole seen i coobare. Sunu ëllëg ajuwul ci lenn ndogal lees bind teg. Nun noo ko war a tabax ngir sunu bopp, tabaxal ko sunu bopp, ngir waajal tamit sunu ëllëgu doom ak i sët. Waaye, ëllëg dañu koy liggéey, doore ko ci bésub tay jii, tàmbalee ko ci faj jafe-jafey tay te di jëf jëf yoy, dañuy jeexital bu baax ci xewi ëllëg. “

EJO ÉDITIONS ak LU DEFU WAXU ñoo ngi koy jaale njabootam, di ko jaale i mbokkam, Senegaal ak àddina sépp. Yàlla na guyaar di wàccuwaayam.

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj