TÀGGE : SOXNA WAALO MU SËRIÑ SAALIW MBÀKKE NELAW NA

Yeneen i xët

Aji bind ji

Xibaar bu tiis la njabootu Tuubaa ak taalibey murit yi xëyee tey. Soxna Waalo Mbàkke moo wuyuji Boroomam, tey ci àllarba ji. Ci suba si la dëddu. Moom nag, mooy taawu Sëriñ Saaliw Mbàkke (Yàlla na ko Yàlla yërëm te jéggal ko).

Seede yi benn la : moom Soxna Waalo, ku jullite la woon, fonkoon lool diine ji ak njàngaley Séex Ahmadu Bàmba Mbàkke, Sëriñ Tuuba. Liggéey na lu baree bari ci yoonu murit. Kenn du fàtte àddiyab 16i tamndaret bi mu mujjee jox xalifa bi, Sëriñ Muntahaa Mbàkke Basiiru, ngir def ko ci tabaxug jàngune Séex Ahmadu Bàmba Mbàkke ba ca Tuubaa.

Moom, Soxna su tedd si nag, mooy way-juru Abdul Xaadr Kebe mi bind ñaari téere yii di : Mboorum àdduna si ak Jéego ci làmmiñu wolof. Ñaari téere yépp nag, Ejo Editions moo leen móol.

Du murit yi kese ñoo ñàkk, umma bi yépp la. Di ko ñaanal yërmaande ak njéggalug Boroom Bi, mu tàbbal ko ci àjjanay firdawsi.

EJO Editions ak Lu Defu Waxu ñoo ngi koy jaale Abdul Xaadr Kebe, di ko jaale Xalifa murit yi, di ko jaale njabootu Sëriñ Tuuba, njabootu Sëriñ Saaliw Mbàkke, taalibe yeek jullit ñépp.

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj