Njabootu mbatiit ak làmmiñi réew mi amati nañ tiis ak uw naqar. Kenn ci seen i kàngaam, di woon jàmbaar ci toolu mbatiit ak làkki Afrig, moo dëddu. Uséynu Béey moo wéy, wuyuji Boroomam. Wolof nag nee na, garab, fa mu juddoo lay deewe. Uséynu Béey doy na ci firnde.
Tey lees jot ci xibaar bu tiis bile. Uséynu Béey, moom mi bokkoon ci ñi jiite saabalukaayu web bii di Seneplus, moo gaañu ci ngoonug dibéeru démb ji, 21 pani sulet 2024, fa raglub “Principal” bu Ndakaaru.
“Ouzin” lees ko daan dàkkentalee, moom Uséynu Béey. Atum 1945 la ganesi woon àddina, Bàlla Béey di baayam, Koddu Caam di ndeyam. Fa Medinaa, “Rue 3 X Blaise Diagne”, la juddoo. Ba mu jàngee ba jeexal ci daaray tuut-tànk yeek yu digg-dóomu yi, ca la demee ca liise “Delafosse”. Mi ngi féetale woon njàngam ci wàllu koom-koom ak kontaabilite. Uséynu, ku xëroon la ci Senegaal, bëggoon lool réewam. Looloo ko taxoon a sóobu ci géewu pólitig gi. Xaritam bi, doomu ndeyam ji, Bubakar Bóris Jóob, mooy seede bi :
“Ci wàllu pólitig, njabootu “gauche” la Uséynu Béey féetale woon boppam. Bañkat la woon nag. Fésoon na lool ci xeex nooteel ak mbéeféer. Daan na yatt xalimaam bu ñaw ba, di ca fent i yaxal yu solowu te xóot, yaxal yoy, dañuy màndargaal xel muy nàcc te rafet. Teg ci ne, ku amoon fit la. Bu xeex jotaan, day taxaw dëggal boppam ; bu waraan bind walla wax, mu biral xalaatam te du ca ragal dara.”
Uséynu Béey, jàngalekat la woon. Nde, jàngale na diir bu yàgg fa diiwaanu Sigicoor. Jamono jooja, da daan jàngale di defaale pólitig. Dafa di, RND bu jamonoy Séex Anta Jóob la bokkoon. Taxawaayam ak dayoom taxoon na werekaan bi, magum jàmbaar yi, Séex Anta Jóob, ràññee woon ko, daan ko woo ngir ñu weccooy xalaat ci tolluwaayu réew mi, jooja jamono. Ku ne Séex Anta nag, saam xel dem ci mbatiit ak làkki réew mi. Moo tax, sëñ bi Uséynu, bey na waaram ci wàll wi laata muy wéy fa Boroomam. Daan na bind ak a liggéey ciy sémb yu ñeel làkki réew mi.
Uséynu Béey bokk na ci ñi samp EJO ÉDITIONS, di kërug móolukaay i téere yees bind ci làkki réew mi. Naka noonu, bokkaat na yit ci ñi taxawal saabalukaayu web bii Lu Defu Waxu, di yéenekaayu web buy siiwal i xibaar ak yu ni mel ci kàllaamay Kocc. Uséynu Béey bokkoon na tamit ci ñi sos Fonk Sunuy Làmmiñ (FSL). Soxna Ajaratu Sàll mi jiite laboraatuwaaru làmmiñal bu IFAN te bokk it ci FSL, a ngi seede ni Uséynu Béey “…nit ku baax la woon, yaru, bëgg liggéey, mën a sàmm kàddoom.” Kon, bu yeboo ñu ne ko : “Uséynu, sa jaan wàcc na !”
Fa sëgi Yoof ya lañu ko rob. Kër Masaar ga mu dëkkoon, “Cité MTOA”, lañuy nangoo njaal yi.
EJO ÉDITIONS ak Lu Defu Waxu ñoo ngi koy jaal njabootam, di ko jaal waa FSL, di ko jaal waa Seneplus ak képp kuy yëngu ci wàllu mbatiit, rawatina ci làkki réew meek yu Afrig. Nu ngi ñaan Yàlla mu xippee guyaar, Boroom Bi yërëm ko te jéggal ko.