TASUB CESE AK HCCT

Yeneen i xët

Aji bind ji

Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, dafa jébbal njiitul Ngomblaan gi ab dekkare buy soppi ndeyu-sàrtu réew mi. Li mu ci jublu mooy tas ñaari campeef yii di CESE (Conseil Economique, Social et Environnemental) ak HCCT (Haut Conseil des Collectivités Territoriales). Ca alxames ji la dépite yi war a lëlu, fénc dekkare bi ngir wote ko.

CESE mooy Ndajem koom gi, mboolaay geek kéew mi. Bu dee HCCT, mënees na ko firee Magum ndajem bokk-moomeeli mberaay yi. Ñaari campeef yii la Njiitu réew mi bëgg a tas. Daf ko dige woon ca jamonoy kàmpaañ ya. Dafa di, yàgg nañoo xalab CESE ak HCCT. Ndax, jàppees na ni amaluñ askan wi njariñ te xaalis bu baree ciy dem. Nee ñu, bu ñu tasee CESE ak HCCT, dees na sakkanal, ci xayma, lu tollu ci 15i tamñaret (fukk ak juróomi milyaar) ci sunuy koppar.

Ñu baree ngi rafetlu ndogalu Njiitu réew mi. Nde, lees jàpp mooy ne, ay àndandooy pólitig kepp la Maki Sàll, Njiitu réew ma woon, bëggoon a fat ak a neexal. Moo ko taxoon a samp CESE ak HCCT. Kujje gi nag, rawatina waa Bennoo Bokk Yaakaar, rafetluwuñu ko. Loolu nag, bettul kenn. Ndaxte, seen i ndaw rekk ñoo fa nekk. Abdulaay Daawda Jàllo (APR) moo jiite CESE bi, Aminata Mbeng Njaay (PS) jiite HCCT.

Abdu Mbów mi jiite kippaangog dépite Bennoo Bokk Yaakaar, woolu na seen i dépite ngir ñu waxtaane mbir mi ci ni mu gën a gaawee. Kii di Zahra Iyaan Caam, di woon jëwriñ ci nguurug Maki Sàll, àddu na. Moom dafa gis ne, Njiitu réew mi, jafe-jafey Saa-Senegaal yi itteelu ko, waaye xeex kujje gee ko tax a jóg. Ci xëtu Xam (twitter) la bind lii toftalu :

« Léegi leer na ni, li gën a soxal Njiitu réew mi ak elimaanu jëwriñam yi, dafa mel ni du li jamp ci wàllu mboolaay gi ak koom-koom gi. Waaye, li leen soxal mooy defaraat seen toogaay ci wàllu pólitig. »

Moom, soxna si, dafa jàpp sax ne amoon na lu ëpp solo fuuf tasub CESE ak HCCT. La mu ca namm mooy DPG bi elimaanu jëwriñ yi war a def, coowal ONAS li, mbëkk mi, pasi liggéey yi ñuy dakkal, añs. Mu neeti, « …ñaar ñi jiite réew mi, dañu bëgg a néewal doole seen i nawley pólitig. »

Cig pàttali, Bennoo Bokk Yaakaar moo ëppale ay dépite ca Ngomblaan ga. Bu leen neexee, sémbuw àtte bi du jàll. Ñu bari gis ne, Njiitu réew mi daf leen a dugal ci guuta. Ndax, bu ñu ko wotee mu jàll, seen bopp lañuy yàqal ndax ñoom kese ñoo nekk ci campeef yooyu di ci am xaalis bu bari. Bu ñu ku wotewul, dina gën a gàkkal seen der ci kanamu askan wi te dina doon lay ci Njiitu réew mi ngir mu tas Ngomblaan gi.

Kon, dafa mel ni Njiitu réew mi ak Usmaan Sonko dañuy wure ak waa Bennoo Bokk Yaakaar. Te, dox nañ foo xam ne, ci lees njort, dañuy daan, mbaa ñu daan. Bu dee waa Bennoo Bokk Yaakaar, dañuy ñàkk, mbaa ñu ñàkk. Waaye, ndax noonu la fay demee ? Li ci kanam rawul i bët.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj