TATA MIMI COKKAAS NA MAKI SÀLL

Yeneen i xët

Aji bind ji

Dige bor la. Wolof a ko wax. Moo tax, Aminata Ture dëggal na digeem ba. Gor ca wax ja. Ndekete, ndaw si Mimi, fasul yéene dellu ginnaaw ci xeex bi mu sumb ak Njiitu réew Maki Sàll. Ci altine 10 oktoobar jii weesu la soxna si jébbal pekkug Ngomlaan gi ab sémbub àtte buy yemale tabbub mbokki Njiitu réew mi ñeel Campeefi Bokkeef gi.

Tataa Mimi, nees koy dàkkentalee, dafa laltaayoo àtte yi Senegaal xaatim ci wàllu baaxal caytuwiinuw réew biir Afrig. Bokk na ci, àtteb 81-53 bu 10 sulet 1981 ñeel ndaanug dajale alal ju lewul, àtteb 81-54 biy taxawal Kërug àttewaayu ndaanug dajale alal ju lewul, 22i at ci ginnaaw laata àddina si di ko ci roy. Àttee yooyii,   ñu ngi cëslaayu ci déggoob Mbootaayu Xeet yi ngir xeex nger. Dolli na ci yeneen i àtte, ba ci bi samp OFNAC. Ginnaaw laltaay bi, mi ngi sàrtal ci dog bu njëkk bi, tëral ci ne :

Képp kuy mbokk walla ngay digaaleb Njiitu réew mi, ndomboy-tànk yii toftalu daganuñ ñeel la :

– Njiitalu Campeef ;

– Jëwriñ ju mag ;

– Jëwriñ ;

– Fara-caytub Càmm ;

– Njiitul larme lu mag a mag li ;

– Njiit walla Njiit lu mag ci béréb bu Càmm gi moom walla cig lijjanti gog, Càmm gaa fa ëpp wàll ;

-Àmbaasadëer ;

– Ndawul réew.

Ci dog ñaareel bi nag, leeral na ñan la àtte biy dal seen kow, te mooy :

1)    Waj-juri Njiitu réew mi ak/walla yu soxnaam ;

2)    Njabootu Njiitu réew mi ak/walla yu soxnaam ;

3)    Mag walla rakki Njiitu réew mi, yu góor ak yu jigéen, ak/walla yu soxnaam ;

4)    Njabooti mag walla rakki Njiitu réew mi, yu góor ak yu jigéen, ak/walla yu soxnaam.

Nu gis ne, kon, àtte bi, mbokki Njiitu réew mi ak soxnaam rekk la ci jublu. Jëwriñ yeek yeneen xeeti kilifa yi tuddu leen. Waaye, bu ñu sukkandikoo ciy waxam, àtte bu ni mel, jéego bu réy lay doon [bu jàllee] ci yoriinu réew mi. Rax na ci dolli, cib yégle bi mu siiwal démb ci àllarba ji, ne, « àtte yii, fépp foo dem ci réewi Mbootaayu Xeet yi, am na fa. Kon, sama sémbub àtte bi day dolleeku ci aaday demokaraasi bi nga xam ne, jamono jii, day xeex ngënaleg deret ci mbootaay yi. Àtte bu ni mel dafay gën a baaxal sunu caytuwiinu réew. » Ngir firndeel li muy wax, Tataa Mimi dafa fàttali ab dog ci dogi Càrtub liggéeykat yi. Dog baa nga wax ne :

« Ngir moytu bépp xeetu njeexitalub deret, ci lu wér walla ci lees njort walla ñu ragal ay itte yu daje ci biir PNUD, Càrtub liggéeykat yi dafa tëral ne ” wareesul a tabb mukk nit koo xam ne baay la, walla ndey, walla doom – muy góor mbaa jigéen -, walla rakk – muy góor mbaa jigéen – ñeel kenn ci liggéeykat yi “. »

 Dolli na ci ne, Senegaal dafa bokk ci nosteg Mbootaayu Xeet yi ba mu daj, rawatina PNUD. Kon, àtte yu ni mel dañuy gàllu ci kowam.

Waaye de, sémbub àtte bii, jàllam taxu koo yombe noonu. Nde, wóor na ne, lëkkatoo Bennoo Bokk Yaakaar moom daf koy xotti, sàndi mbalit. Bu dee waa Yewwi Askan Wi, ñoom, fàtteeguñu seen xeex beek Aminata Ture ci wote yi jàll. Bu dee lëkkatoo Wallu Senegaal, fa la coow li gënatee nekk. Ndaxte, njabootu Abdulaay Wàdd gi dafa jàpp ne, li dal Kariim Wàdd yépp, Mimi Ture a ko waral. Bu dul loolu sax, ñu bari dañu jàpp ne ndaw si day faj mer kese, waaye duggewu ko leneen.

Ñu ngi ruumandaat naan, li Njiitu réew mi, Maki Sàll, tànn Aamadu Maam Jóob ci kilifteefu Ngomblaan gi moo metti soxna si ba tey. Nde, buñ ko tànnoon, ci waxi gaa ñi, du takk séram bay dékk xeex Njiitu réew mi.  Waaye, nag, bu ñu tegee boor loolu yépp, càmbar sémbub àtte bi, bañ a par-parloo ak a njort jëme fii walla fee, dinañ xam ne, am na cis lëf, njariñ la.

Ñoo ngi fàttaliku bi Abdulaay Wàdd, Njiitu réew ma woon, bëggee def i pexe ngir teg doom ji, Kariim Wàdd, ci boppu réew mi. Balaa boobu sax, daf ko dénkoon ay ndomboy-tànk yu baree bari ba nit ñi daan ko tooñee jëwriñu asamaan seek suuf si. Bi Maki Sàll toogee ci jal bi ba léegi nag, mbirum mbokkoo ak deret dafa gën a fés. Rakkam yeek goroom yi, doomi bàjjenam yi, xaritam yi, mbokki soxnaam yeek i am-di-jàmmam, ñoom ñépp, ku ci nekk tabb na la walla mu fexe ba nga toog cig Campeef. Muy lu ñaaw nag, luy gàkkal deru Senegaal. Kon, sémbub àtte bile, dina am njariñ ci wile wàll, bu jàllee. Donte ne, mënees na ñaawlu anam ak jamono ji mu ame. Ginnaaw gi, bu ñu ko defaraatee, am lees ci yokk, dina gën a baax.

Ak lu ci mën di am, Mimi cokkaas na Njiitu réew mi. Te nag, wolof dafa wax ne, dóor, feyu la sant. Léegi nag, nu seetaan.

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj