TER, FOOY TEERE ?

Yeneen i xët

Aji bind ji

Keroog, gaawu 28 saŋwiye 2023, la yéenekaayu Farãs bii di Le Figaro génne ab saabal, jagleel ko saxaaru TER gu Senegaal gi. Ñu bind ci boppu saabal bi ne : « TER bu Ndakaaru : Senegaal 0, SNCF 1, fileek ñuy xaarandi nguddal gi. La ca biir saabal bi nag, moo yéem Saa-Senegaal yi, jur ci réew mi coow lu réy a réy boobaak tey. Ndekete yoo, bees sukkandikoo ci saabal bi, saxaaru TER gi, Senegaal daf ko teeru rekk, waaye tubaab yaa ko moom.

Bésub 21 desàmbar 2021 la Njiitu réew mi, Maki Sàll, doon ubbi TER gi. Laata bés boobu, saxaar gu yees gi juroon na coow lu bari ñeel solos naal bi ci boppam, cëslaayu pas yeek digaale yi Nguurug Senegaal xaatim ak tubaab yi, xaalis bi ñu ci def, béréb bi muy daw, dëkkuwaay yi mu laal, añs. Naam, njort ñaawoon na lool, xol naqadi. Waaye nag, bu dee wax dëgg rekk, bésub ubbite ba, xaweesoon na fàtte tuuti coow li.

Ngir fàttali, saxaaru TER gi bokkul woon ci naalu Yoonu yokkute bi Maki Sàll, lawax ba woon, dagaane baatu askan wi ci wotey 2012 yi. Bi mu faloo yit, boolewu ko woon ci naalu PSE bi. Loolu, ñu bari bàyyiwuñ ci xel. Dafa di, ca atum 2016 la mbirum TER gi tàmbali. Xalaat baa nga bawoo ca Champs des Elysés, màkkaanu Njiitu réewum Farãs. Jamono jooja, François Hollande moo jiite woon suufus Faidherbe si. Kon, saxaaru TER gi, Maki Sàll njortu ko, xalaatu ko te yit, du moo ko nas, daf ko jéggaani ci xonq-nopp yi.

Xam naa, yow miy jàng saabal bi, laaj baa ngiy xasanal saw làmmiñ. Danga bëgg a xam kan moo sumb TER gi ak nan la fa deme ? Dees na ci indiy leeral ci beneen saabal. Dangay bàyyi ñu tënkal la saabalub yéenekaay bi yëngal sunu gaal gi, du noonu ?

Ci gàttal, ak li coow liy bari bari, mënees na tënk solos saabal bi ci ponk yii toftalu :

Bi ci jiitu mooy ne, saxaaru TER gi, Senegaal moomu ko. Li koy firndeel mooy, sosete biy saytu TER gi, téye ko ciy loxom, mi ngi tudd SETER (Société d’Exploitation du Train Express Régional de Dakar). SETER di moomeelu SNCF, ag kërug liggéey guy yëngu ci ndefari saxaar ak lu ci aju. Te, SNCF ci boppam, moomeelu Farãs la.

Ñaareel baa di ne, Farãs moo lebal Senegaal xaalis bi mu liggéeye TER gi. AFD (Agence Française de Développement) moo joxe li ëpp ci xaalis bi. Nde, AFD def na ci 1 milyaaru ëro, maanaam 655i milyaari CFA [1]. Noo ko gisandoo.

Yemul foofu. Ndaxte, ca ndoorteel la, ba ci njeexitalu TER gi, tubaab yi rekk nga ciy gis. Ñoom ñoo génne seen alal, lebal nu ko, teg ci intere yu diis a diis. Ñoom ñoo tànn sosete bi koy liggéey te ñu moomal ko seen ko bopp. Ñoom ñoo defar saxaaru TER gi. Ñoom ñoo teg raay yi. Ñoom ñooy saytu doxalinu TER gi, jiite lépp. Xanaa xëm ngeen.

Nguur gi nag, moom, nees ko xamee, ci weddi la dëkk. Moo tax Abdu Kariim Fofana, jëwriñu yaxantu bi wax ne :

« Warees na xam ni, Senegaal, ci wàllu saxaaru TER bi mu moomal boppam, ci sagoom la ciy doxe.  Bu ma nee TER bi mu moomal boppam nag, li ma ci namm mooy ne Senegaal kesee moom léppi TER bi. Senegaal a moom fi muy dow, moom raam yeek gaar bi. »

Waaye, weddi rekk doyul ci teggi tuuma. Nde, Le Figaro dafa wax lu leer. Te sax, balaa moom, am na ñu ko njëkkoon a wax. Waaye, bàyyil ma tekkil la boppu saabalu Le Figaro bi.

Le Figaro dafa bind « Senegaal 0, SNCF 1 ». Mu mel ni xëccoo dafa amoon diggante Senegaal ak SNCF, ki mujj ki am ndam ci kow Senegaal. Lees war a njëkk a seetlu fii mooy ne, genn kërug liggéeyu doxandéem moo jàmmaarloo ak réewum lëmm, am ci ndam. Xam naa yaa ngi naan : « Céy ! Bile gàcce ! » Gis nga de. Lii moom, Afrig rekk nga koy gis. Li tax yéenekaayu tubaab bi bind ko mooy ne, ca njëlbeen ga, ñoom, dañ foogoon ne, bu TER gi àggee, dina yab bés bu nekk lu tollu ci 1 000iy Saa-Ndakaaru. Waaye, dañu xaatimoon ci pas gi ne, bu lim boobu matulee, Nguurug Senegaal mooy fay xaalis bi méngook lim bu des bi. Waaye, Senegaal dafa mujje dellu ginnaaw. Mbasum Covid-19 baa fa jaar.

Ñu ni déet-a-waay, tubaab yi bëggati Nguur gi xaatimal leen ag pas gu leen di tax a gaaw a jotaat ci xaalis bi ñu def ci TER gi. Ki jiite SNCF, Jean-Pierre Farandou, moo xalaatoon lu ni mel. Waaye, Stéphan Volant mi jiite woon SETER, di doomu Farãs ak Senegaal, mësoon fee jiite SNCF, dafa lànkoon. Looloo sabab ndàqam. Te, loo ci xamul, ndàq mi teguwul ci yoon. Ndax, yégaluñ ko Nguurug Senegaal sax. Jëwriñ Mansuur Fay daldi bind ab bataaxal ngir kaas ko, ñu tanqamlu ko daanaka, ñàkkal ko faayda. Ndeysaan. Mooy li wolof di wax rekk, merum ginaar lu muy wàññi tusuñe ? Waaye, njombe yi des nañ ba tey.

Bi ñu dàqee Stéphan Volant, dañ fa teg kii di Pierre Boutier, beneen xonq-nopp. Li ñu doon gën di dem, seen yaakaar di gën a tas. Ndax, TER gi yabul lim bi ñu doon xaar. Ca lañ dàqee njiitalu SETER li, Frédéric Bardenet. SNCF xool ci biir i liggéeykatam ba sonn, gisul kenn ku ko mën a wuutu, mu tegandi fa yeneen ñaari doomi Farãs : Patrick Tranzer ak Marc Burger. Yéenekaay Le Figaro bi di nu xamal ni, ñaar ñooñii, donte seen xam-xam des na ci wàll wi, ñoo ngi leen di fay 84 000iy ëro weer wu nekk, jaare ko ci sosete Valtus Transition. 84 000iy ëro day tolloo ak 55i miliyoŋ ak weccet. Loolu doyul, ñu dëkkal kenn ki ci otel Pullman, keneen kiy jóge Moritani ayu-bés bu nekk, di liggéeysi Senegaal. Te Nguurug Senegaal moo leen gàddul xaalis boobu yépp.

Fi mu nekk nii nag, tubaab yaa ngi puus Nguurug Senegaal ngir mu xaatimal leen pas gi nu tudd ci kow. Li ñuy taafantoo mooy ne, pas googooy tax TER giy wéy di daw. Ñu mën cee déggee ne, bu Nguur gi bañee, ak lim ci def ci xaalis yépp, TER gi day gaare. Le Figaro di leeral ne, pas googu, amalul Senegaal benn njariñ. Mu dolli ci ne, bi njiitalu SNCF li di ñëw Senegaal, Njiitu réew mi sóoralewu ko woon ciy ndajeem. Waaye, àmbaasadëeru Farãs bu Senegaal, fexe na ba Maki Sàll gise ak moom.

Lii mooy, ci gàttal, li ñu yéenekaay biy xamal ci coowal TER gi. Dees na leen bindal beneen saabal buy leeral cosaanu TER gi.

[1]https://www.afd.fr/fr/actualites/dakar-lancement-train-express-regional#:~:text=Accompagn%C3%A9%20par%20l’Agence%20fran%C3%A7aise,du%20groupe%20AFD%20R%C3%A9my%20Rioux

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj