« Am nanu ndam ! Àttekat bi santaane na ñu bindaat Usmaan Sonko ci këyitug wote yi. » Bi Sayid Larifu, kenn ci layookati Usmaan Sonko, di wax kàddu gii, 22i waxtu tegaloon nañ 30i simili. Nde, àtte bi dafa yàggoon lool démb, fa tirbinaalu Sigicoor bu mag ba. Démb, alxames 12 oktoobar 2023 lañ waroon a àtte mbirum Usmaan Sonko mi ñu Nguur gi aroon turam ci këyitug wote yi.
Ginnaaw bi ko Ëttub àttewaay bu mag bi gàntalee ñeel xobi baayale yi ko DGE bañoon a jox, àttewaayu Sigicoor bi rekk desoon ci yaakaaru njiitul kujjeg Senegaal gi, Usmaan Sonko. Nde, nekkam lawax ci wotey 2024 yi mi ngi aju woon ci ndogalu àttekat bi. Waaye, ginnaaw 12i waxtu yi layoo bi daw, Sabasi Fay, àttekat bi, delloo na Usmaan Sonko àqi maxejjam, wax ne lees ko dindi ci këyitug wote yi dëppoowul ak Yoon, santaane ñu bindaat ko. Bi ndogal li jibee, layookati Usmaan Sonko yi, waa pàrteem ak soppeem yépp fésal seen mbégte ci ndogal li. Ñuy tagg ak a sargal àttekat bu « gore » bi te « dëggu ». Waaye de, ndawul Nguur gi ci wàllu Yoon, Yoro Musaa Jàllo, àndul ci ndogal li te xamle na ko.
Nguurug Senegaal, ci kàdduy Yoro Musaa Jàllo, daa fas yéene dugal ag dabantal (recours). Nde, ciy waxam, àttekat bi wonewul ag màndute. Moo tax, ciy waxam, jamono jii, mëneesagul a bindaat Usmaan Sonko ci këyitu wote yi.
Ak lu ci mën di am, ci waxi boroom xam-xam yi seen xel màcc ci wàllu Yoon, ginnaaw ndogalu Sabasi Fay li, dara tereetul Usmaan Sonko doon lawax ci wotey njiiteefu réew mi, keroog 25 féewaryee 2024. Bu ko neexee mu jëli xobi baayale yi ca DGE, dagaaniy mbaayale saa-senegaal yi.