TOMB YI GËN FËS CI KÀDDUY NJIITU RÉEW MI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Njiitu réewum Senegaal lu yees li, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, doon na wax ak askan wi ci bésub tey jii, àllarba 3 awril 2024, bi 20i waxtu jotee. Muy aada bob, at mu nekk, Njiitu réew mi dina ko def laata xewteg 4 awril, di bés bees di màggal bi Senegaal moomee boppam. Tomb yii toftalu ñoo gën a fës ciy kàddoom ya mu biral fa njénde la (pale).

Mbirum ndaw ñi 

“Sunu ndaw ñu njaxlaf ñi, di xolu askan wi, ñoo may gën yitteel. 

Yeen ndawi Senegaal, seen i gént ñooy samay gént, seen i bëgg-bëgg ñooy samay bëgg-bëgg, bokk naa ak yeen seen i mébét ngir jariñ seen bopp, seen njaboot, seen mboolaay ak seen réew.”

Xeex nger, aar weejekat yi (lanceurs d’alerte)

“Dinaa xeex càccug alalu réew mi ak xaalis bi ñuy rawale.”

“Dinañ jéggal ñiy abale seen i tur ak defkati njombe ci kow ñu waxal seen bopp.”

“Dinañ siiwal caabali IGE, Cours des comptes ak OFNAC.”

“Dinañ xeex nger ci anam bu tar a tar a tar ak xaalis bu lewul bi. 

“Dinañ aar weejekat yi (ñiy boole sàcc yi), neexal leen.”

Yoriin wu sell, jub te leer

“Ngir tabax Senegaal gu naat, Senegaalu ñépp gu amul xàjj-ak-seen, fas naa yéene saxal yoriin wu sell te jaar yoon, yoriin wu leer wu aju ci jub, jubal, jubbanti ak warteefu wuyu ci lees la dénkoon.”

Yeesalug Yoon

“Fas naa yéene amal ay péncoo [ngir soppi jubbanti yoon] ak àttekat yi, layookat yi, wiisiyee yi, gerefiyee yeek ñiy liggéey ak yoon, jàngalekat yoon yoon yi, maxejj yi ngir seet ay pexe yu ñuy joyyantee yoon, defaraat ko.”

Coppiteg nosteg wote yi

“Dinan fi jële CENA, teg fi CENI (Commission Électorale Nationale Indépendante), yokkal ko dooleel ak sañ-sañam.”

“Dinañ seetaan limub làngi pólitig yi, yeesalaat leen, saytu xaalis bi ñuy pólitigee.”

“Dinañ fexe ba bépp maxejj bu am kardànteem mën a wote [te du aaju bindu ci keyitug wote yi].”

Ndonol jàmbaari réew mi 

“Dinan sàmm bu baax ndonol panafrikanism (yittey bennale réewi Afrig yi) bi ñu jële ci Séex Anta Jóob ak Lewópol Sedaar Seŋoor mi nga xam ne, bokk na ci ñu sos OUA.”

Mbirum bitim-réew 

“Sunuy dugaale yépp, ak fu ñu mën di jóge, ñoo yem ci nun kepp. Dinañ jox ku ci nekk cër ak worma bi nga yeyoo ci kow nga jox nu cër ak worma bi ñu yayoo.”

Cig pàttali, Njiitu réew mi tekki na ndombog-tànkam ci làngug Pastef gi mu bokkoon. Li mu ko duggee mooy doxal ci màndute, tëdde njaaxanaay, yemale ñépp.

Ginnaaw wax, jëf a ci des.

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj