Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Fay, war teew ca Farãas ci àllarbay tey jii. Tukki bii moiy doon njëlbeenug tukkeem ci biti kembaaru Afrig.
Njiiteefu réew mi (Présidence de la République), moo biral ab yëgle di ci xamle ne, moom Njiitu réew mi, dina fa teewe am ndaje mu mag mom, dees na ci fénc mbirum moom sa bopp ak yeesal ci wàllu ñakk. Kurél yii di GAVI, Alliance du Vaccin ak Bennoog Afrig yi ñoo ko ci dëne (inviter).
Ba tey, ci yëgleb Njiiteefu réew mi, bu Njiitu réew mi jógee ca ndaje mooma, dina gise ak naataangoom bu Farãas bii di Emmanuel Macron.