TUKKIB NJIITU RÉEW MI FA GINE BISAAWO

Yeneen i xët

Aji bind ji

Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, demoon na Gine Bisaawo ci talaatay tey jii, 30 awril 2024. Mu di woon tukkib liggéey ak sàmm kóllëre gi dox diggante ñaari réew yi. Ci dalu webu njiiteefu réew mi (site de la présidence de la république) lees jukkee xibaar bi.

Tukki bi day wone solos digaale bi dox diggante Ndakaarook Bisaawo.  Jukkees na ci dalu web boobu ne :

« Tukki bii, dafa bokk ci jéegoy sàmm ak dooleel kóllëre gi yàgg a boole ñaari réew yi. Rax-ci-dolli, dafay gën a dëgëral mbokkoog mbatiit gi dox diggante Senegaal ak réew yi mu digalool. »

Bees sukkandikoo ci Pekkug xibaari nguur gi (Bureau d’information gouvernementale – BIG), ñaari Njiiti réew yi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fa yak Umar Embaloo Sisoko, waxtaan nañ ci fànn yii di : kaaraange, mbatiit ak napp gi. Te, sikk amul ci ne, dinañ xaatim ay pasi liggéey ci fànn yooyii.

Dafa di, Gine Bisaawo dafa bokk ci réew yi Senegaal di gën a jaay ay njureefam. Ci xayma, ci atum 2022 mi rekk, Senegaal jaay na Gine Bisaawo lu tollu ci 108 257 toni njureef. Bu ñu ko xaymaa ci xaalis, mi ngi tollu ci 55,201 miliyaar CFA.

Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Fay, yàggu fa. Ndax, ci ngoon gi la ñibbisi Ndakaaru.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj