UBBITEG KOPPEY LIGGÉEY AK JÀPPALANTE YI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, ma nga woon Kumpentum, fa diiwaanu Tàmbaakundaa. Ci àjjumay tay jii, 21i fani màrs 2025, la fa dem. Li mu ko dugge mooy ubbi Koppey Liggéey ak Jàppalante yi, maanaam Coopératives Productives Solidaires (CPS).

Sémbu CPS wi nag, dafa bokk ci sémb yu gën a réy yi Njëwrñu Mikorofinaas ak Koomug mboolaay mi ak jàppalante bi. Sémb wile dafa bokk ci naal wu gën a yaatu, ñu duppe ko PRECOSOL. Bi mu jëlee kàddu gi, lii la elimaanu jëwriñ yi wax :

« Jëwriñ yi nekk ci sama Càmm gi ak man mii, noo ngi rafetlu ndajem kaajar mii nga xam ne, ci benn boor, dafay sumb naal wees duppee Programme d’appui aux acteurs de l’économie sociale et solidaire (PROGRESS). Ci beneen boor, ubbite gii nuy def ci Koppey liggéey yi ak jàppalante bi day suuxat bu baax a baax yokkuteg dëkki Senegaal yi. »

Ay kilifa yu mag jot nañoo teewe ndaje ma, niki jaraafu diiwaanu ba (gornoor), kilifay caytu yi fa nekke ak jëwriñu Mikorofinaas ak Koomug mboolaay mi ak jàppalante bi, Aliw Jonn.

Njiitu réew mi ak elimaanu jëwriñ yi dañu gëm ni kooomug mboolaay mi ak jàppalante bi yoon wu gaaw la ci naatal réew mi ak dëkk-dëkkaatam. Loolooy feeñ ci kàdduy Sëñ Usmaan Sonko yii toftalu :

« Naal wii, am nanu ci yaakaar ju réy ci ne mën na jeexital bu baax, ci anam bu sax, ci dundin ak nekkinu askan wi. »

Naaluw PROGRESS nag, li ko tax a jóg mooy tàggat ay nit, gunge leen, lootaabe mbootaayi liggéey yi te di dimbali ñiy yëngu ci fànnu koomug mboolaay mi ak jàppalante bi. Ndimbal loolii, mi ngi aju ci wàlluy xarala ak koppar. Bu ko defee, ñàkkug xëy mi dina wàññeeku fi réew mi. Nde, bu naal wi sottee, ñu bari dinañu am liggéey bu sax.

Muy mbootaay ak mbawari jigéen ñi, di kuréli ndaw ñiy yëngu ci wàllu ñeeñal ak pasin, beykat yi, añs., ñépp la naaluw PROGRESS wi ñeel, amul xàjj-ak-seen. Rax-ci-dolli, bees sukkandikoo ci kàdduy elimaanu jëwriñ yi, dees na jiital ci naal wi diiwaan yii di Koldaa, Luga, Séeju, Ndar, Kéedugu, Maatam, Tàmbaakundaa ak Sigicoor. Jubluwaay bi mooy jëmmal màndute diggante mberaayi réew mi ci fànnu ndogali pólitig yees tënk ci biir naalu « Vision 2050 ».

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj