UGB : XEEX BI DOORATI NA !

Yeneen i xët

Aji bind ji

Xeex bi jolleeti na diggante ndongoy iniwérsite Gastoŋ Berse ak takk-der yi. Jamono jii ñuy bind yaxal bi, xale yaa ngay jàmmaarloo ak takk-der yi ci kow tali bi. Oto demul, oto dikkul. Xeer yaa ngiy xërr-xërri, gërënaad yiy soqi, póno yeek matt yiy tàkk, saxaar si ubale fépp, ngelaw laa ngi wex xàtt, mëneesu fa noyyi. Bii mooy ñaareelu yoon ndongo yiy génn ci tali bi. Ndax, keroog ci alxames jii weesu, defoon nañ lu ni mel ci ngoon gi, ginnaaw bi ñu génnee ci seen ndaje ma ñu séqoon ak jëwriñ ju yor njàng mu kowe mi te njiiti iniwérsite bi teewoon ca.

Li waa CESL, kurél gi jiite ndongoy UGB yi di xeex mooy, ci seen i wax, li njiiti daaray Ndar ju kowe jiy seetaan ndongo ya fay jànge. Nee ñu, Usmaan Caare (Recteur) ak Bàmba Ka (njiitalu CROUS) jéemuñoo def dara ngir wutal pexe jafe-jafe ya fa njàngaan yiy jànkonteel. Li xale yiy gën a ñaawlu mooy lees fa indeeti lim bu takku ciy ndongo yu bees (4 000 ak lu teg) te dëkkuwaay yi doyuñu, néeg yi fees nañu dell ba ñuy tancaloo ci lal yi. Rax-ci-dolli, seen nekkin ak anam yi ñu jànge, foofa ca UGB, dafa doyadi lool. Boobaak léegi nag, kurélu CESL a ngi doon artook a dànkaafu, di bind i yégle di leen siiwal. Mu mel ni dañoo soofantal seen i mébét, dummooyu leen. Nee ñu, looloo leen tax a dogaale tali bi. Duggewuñ ko, ci li ñu wax, lu mooy kilifa yi geestu leen. Nde, ñoom njiit yi, xamuñu maslaa, xeex lañ xam.

Dees na ci ñëwaat ci ni mu gën a yaatoo.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj