USMAAN SONKO : “BËGGUMA KU MA RAWALE… DAÑ MA BËGGOON A REY…”

Yeneen i xët

Aji bind ji

90 000iy nit ak lu teg ñoo teewe waxtaan wi Usmaan Sonko doon amal ci xëtu Facebookam, démb ci guddi gi. Muy lees mësut a gis. Nde, guléet ñuy nemmeeku lim bu tollu cib “live Facebook” ci réew mi. Dafa di, nag, xel yépp a teeyoon, nit ñi ame woon njàqare ak tiis ñeel wér-gi-yaramu njiitul Pastef li. Moo tax, bim yéglee ni day waxtaan ak askan wi, ñépp a daw ci seen i jollasu, lënku, ngir déglu kàdduy meeru Sigicoor bi.

Ci ndoorteelu waxam, njiitul kujje gi dafa biral i cant ak i ngërëm, jagleel leen ay xaritam ak i nitam, am-di-jàmm yi, militã yi ak ñépp, ñi ko seetsi ak ñi ko jotul a seetsi fa mu tëdd ca lalu loppitaanam. Ginnaaw cant yi, joxe nay xibaar ñeel wér-gi-yaramam, ne :

« AlhamndulillAllaa, maa ngiy tane,. Waaye, xamagunu ci lu wér njeexitali jàngoro jii ma dikkal. Ba tey xamagunu gan xeetu ndefar laa noyyi. »

Ciy kàddoom, ñoo ngiy gëstu ngir ràññee xeetu ndefar googule. Sonko neeti :

« Ginnaaw Senegaal amul jumtukaayi xarala yi war, yóbbu nañuy lëfit bitim-réew ngir ñu seet ba xam la ca biir ndefar gi ñu ma noyyiloo. »

Kon, dafa mel ni, Usmaan Sonko mébétul génn réew mi. Nde, fan yii yépp, ñoo ngi doon xalaat, naka lees war a def ba rawale ko tugal ngir mu fajoo fa. Nguur gi sax bëggoon na ci dugal loxoom. Waaye, loolu dalul xelu Usmaan Sonko.

« Wax nañ ma ne njiiti réew mi xalaat nañ maa rawale bitim-réew. Bëgguma ku ma rawale. Ku dem, ab ndëgg-sërëx buñ may tegal la. Bu ma xasee génn réew mi, amaana dootuma fi tegati tànk. »

Njiitul Pastef li daa fas yéene toog Senegaal ngir wéyal xeex bi. Ndaxte, ci gis-gisam :

« Senegaal la xeex biy ame, dara ba dara booloo jeex jaralu ma génn réew mi. Bu ma génnee réew mi, dina néewal doole li desandi ci xeex bi. Fenn laa demul… Waaye, nag, bu ma Maki Sàll bëggee rey, na ko def. Wànde, dinan àndando, nun ñépp, xeexandoo xeex bi nuy xaar. »

Usmaan Sonko jox nay militãwam ak ñi ànd ak moom ci xeex bi ay ndigal. Nee na leen ñu bàyyi ŋàññante bi, jiiñaate beek tiiñalante bi, te moytu mbaali jokkoo yi. Du lépp lees fa war a dugal. Ndaxte, loolu, day indiy féewalo walla di sabab ñuy jàpp ñenn ñi. Ci talaatay tey jii la war dellu këram, nag, dal-lu tuuti, laata muy sóobuwaat ci xeex bi. Ndax, nee na, donte ne yaram wi neexul, jamono jii du jamonoy noflaay, jamonoy xeex la.

Ndekete kat, gaynde, wéradi du ko teree xeex.

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj