USMAAN SONKO : « Bu Maki bëggee jàpp Usmaan Sonko, fàww mu taqal boppam»

Yeneen i xët

Aji bind ji

Démb, ci guddig àjjuma ji, Usmaan Sonko séq naak Piyeer Eduwaar Fay mu Walf Tv ab laaj-tontu bob, tele Siidi Lamin Ñas bi la ko beraloon. Ci biir waxtaan wi, meeru Sigicoor bi àdduna ci layoo bim séq ak Aji Saar te ñu war ko àtte ci talaat jii nu dégmal, 23 me 2023 fa Ndakaaru. Tontuna yit Idiriisa Sekk ak ñi koy sàndiy xeer, di tuumaal ak a dëkkal fum dëkkul.

Réew mi tàngoon na lool fan yii diggante Sigicoor ak Ndakaaru. Xeex bi metti woon lool fa Sigicoor ak Ndakaaru, diggante takk-der yi ak ndaw ñi, ba ay nit dee ci. Njort ñaawoon na sax ci fi réew mi naroon a tàbbi. Li fi jot a xew yépp nag, ci xalaatu Usmaan Sonko, jenn jëmm a ko waral muy Maki Sàll. Ndax, ciy waxam : « Maki Sàll dafa jàpp ne, li xewoon màrs 2021 toroxal la ci moom, moo tax mu gën a defaru ngir jàpp ma. Na jéem, dina xam. »

Ciif gi Aji Saar di tuumaal njiitul Pastef li, 2i at ci ren, moo waral fitna jépp. Usmaan Sonko nag, dafa lànkoon ni du wuyooti Yoon. Ñu doon ruumandaat ne dañ koy jëlsi. Ndawi Sigicoor yi taxaw temm ne, kenn du laal seen meer, li ci jot a xew, xew ci.

Usmaan Sonko dafa njëkk a fàttali xeeti tooñange, xoqatal ak fitna ji ko Nguurug Maki Sàll ak Yoonu Senegaal teg yépp, bi layoo bi dooree ba léegi. Muy ñag bi takk-der yiy ñag këram (Site Kër-Góor-Gi), ngànnaayi xare yiy takk-der yooyiy gàlloo ba diis, ñaari yoon yi ñu toj ay weeri daamaram, ndoxum tooke mees ko piis, ni ñu koy yàqalee « Nemmeeku Tour » yi muy amal ci réew mi, añs. Rax na ca dolli sax, jalgati yi am layoom yi, muy bu am ak Maam Mbay Ñaŋ ak bu Aji Saar bi yépp. Ciy waxam, looloo taxoon mu dogu ni, dootul wuyooti wooteb Yoon. Waaye, dafa mel ni dellu na ginnaaw ci kàddoom yooyu.

Amaana Usmaan Sonko dafa gis tolluwaayu réew mi, xam ne bu yolomalul buum gi, musiba bu réy a nar gaar Senegaal. Nde, moom, léegi nangu na wuyuji ci kow ay sàrt. Ndaxte, moom njiitul Pastef li, dafa jàpp ne ci mbirum ciif gi ko Aji Saar di tuumaal, amul benn firnde lol, mënees na ko ci jàpp kaso.

« Tus nekkul ci wayndare wi. Ku ànd ak Sonko, nanga nelaw ba yàndoor. Dara amul ci wayndare wi. »

Kon, ragalul layoo bi. Nangu na cee teew bu fekkee ne, « Dara dootul mel na njëlbeen ga bu may dem ca àttewaay ba. Nañ ma bàyyi ak sama sago ma dem ñu àtte ma. Bu ma benn pólisee walla sàndarm dar. […] Bu ma wóoree ni bu ma àggee Ndakaaru, dinaa mën a dem tirbinaal ci jàmm te kenn dunu fitnaal, man ak samay àndandoo, kenn du nu sànniy gaas lakkirimisen, metital nu, suba suba ma jël roppëlaan gi. Bu ko defee, talaata, dina dem tirbinaal. »

Bu nangoo dem itam, Usmaan Sonko nag, artu na, dankaafu Yoon, wax ne :

« Léegi, dootuma nangooti ñuy ñag sama kër, ñuy song samay layookat, di tere samay militaŋ dugg ci néegu àttewaay bi. … Ñoom ci seen bopp ñooy sabab li ñuy woowe daloodig pénc mi. »

Usmaan Sonko dafa jàpp sax ne, moom moo war a gën a bëgg teewe layoo bi ngir feeñal dëgg gi. Mu ne :

« Yor naa wayndare wépp. Dara amu ci. Ay caaxaan kepp la. Amul jenn firnde. Laajuma dara lu dul ay gaaranti. »

Bi ko Piyeer Eduwaar laajee ci mbirum Bàrtelemi Jaas, daa faxas wax ji, xamle ne du ci waxagum léegi. Maanaam daal, daf ko bërngal. Waaye, Idiriisa Sekk de, moom rëccul. Nde, Usmaan Sonko leeral na ndaje ma mu amaloon ak kees duppee Ndaamal Kajoor. Dafa di, fan yii weesu, meeru Cees ba woon daf doon bàkkoo fu nekk ne, dafa ndogook Njiitu réew mi, Maki Sàll, xëdd ak Usmaan Sonko. Waxoon na sax ne, ginnaaw Yàlla, moo taxoon ba réew mi tàkkul, keroog 3 awril. Meeru Sigicoor bi nag, indi na ciy leeral.

Bees sukkandikoo ci waxi Usmaan Sonko, Idi dafa woo ñu bari ci ay jegeñaaleem ngir gise ak moom, mu bañ. Ndaxte, dafa xamoon ne Idiriisa Sekk a ngi doon waaj a wax bésub 27 màrs. Da doon bañ Idi yóbbu fa turam. Bi mu ko lànkalee gise bi, dafa jékki rekk fëgg buntu këram ci waxtuw xëdd. Kon, du Usmaan Sonko moo sàkku ndaje mi, te yit Idi daf ko bett. Ndax yëgluwul bi muy ñëw këram, keroog 27 màrs ci njël. Noonu la fa deme. Bu dee waxtaan wi ñu séq, Usmaan Sonko lii la ci wax :

« Daf ma ñaan ma dox jàmm. Ma tontu ko ne Maki Sàll lees war a wax mu dakkal naalub seppi ay lawax ci wote yi. »

Xel yépp nag, ñu ngi ci layoob talaata jii. Ndax Usmaan Sonko dina ci teew am déet ? Ndax Nguur gi daf ko bëgg a jàpplu walla ? Lu ci mën di am, Usmaan Sonko tëkku na Maki Sàll ci kàddu yii :

« Bu Maki bëggee jàpp Usmaan Sonko, fàww mu taqal boppam. Na jéem. Dawuma. Maa ngi réew mi, maa ngi sama kër. Na ngemb sóobareem yépp ngir jàppsi Usmaan Sonko. Na ku nekk jël ay matuwaayam. »

Yàggatul kon. Ayu-bés bii di ñëw, lépp dina leer.

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj