LU DEFU WAXU : Ban taxawaay la Afrig war a am ?
USMAAN SONKO : Tey, Afrig ci boppam moo nekk ci guddi gu bët setagul. Réew yépp jeexal nañu li ñu amoon. Réew yépp a soxla ay suuf ngir dundal seen askan, réew yu baree ngi wut fu ñuy jaaye li ñuy defar te amatuñu ko. Afrig rekk a leen mën a jox loolu. Su nu gaawul defaru, du baax. Gaa, mënagun leen dab, danoo war a def sunu kem-kàttan ba am doole ba noppi.
LDW : Ndax pexe mbaa saafara am na ?
US : Su nu booloo, dara mënunoo të. Ndax doole, nag, ñaar yii ñoo koy màndargaal cim réew : mberaay (tolluwaay) mu réy ak ay doomi-aadama yu bari. Am réew, bu ndawee du am doole, bu nit ña fay yeewoo barewul it, du am doole, astemaak nga néewle ñaar yooyu yépp. Boo ko seetee ci Amerig ak Siin, dinga gis li may wax. Afrig, nag, bun boole woon sunuy réew def leen benn, dina am doole juy tax ñépp weg ko. Su boobaa, bala kenn di jóg ngir jéem noo noot ak a nappaaje, dina seetaat xelam bu baax.
LDW : Gis nañu sa taxawaay ci coowul Madagaskaar li, gis it sa jëflante ak yenn njiiti kujje yi ci yenn réewi Afrig soowu jant yi deme ni Mali, Kodiwaar, añs, lan mooy sémb bi ngeen bokk ?
US : Li ko lal dëgg, weesuwul boole Afrig gépp. Boo xoolee bu baax, nun ñi ànd daanaka ay maas lañ. Teg ci ne, noo bokk melo ak jaar-jaar ci politig. Loolu am na ci solo. Sunu mébét, nun Pasteef, mooy fexe ba réewi Afrig yépp nu am fay ndaw yu bokk ak nun gis-gis ak taxawaay. Te yit nu dakkal xaajatle bi nuy def ñeel réewi Afrig yiy làkk àngale ak réew yiy làkk farañse. Moo tax, am na ndajem waxtaan mu ma waroon a teeweji Niseryaa ci weeru Me wii weesu te koronaa bi yàq ko. Lu am solo la waroon a doon. Te man mii maay mennum njiit mu bawoo ci réew muy làkk farañse bi fa waroon a teew. Daanaka, ci réewi Afrig yiy làkk àngale yépp njiiti kurélu politig daje kon nañu fa, ku mel ne Silyiis Malemaa bu Afrig-Bëj-Saalum, ay njiiti kuréli politigu Botswanaa, Ugàndaa, Tansani, Gànna, Niseriyaa, añs. Te foog naa bu lii jàllee dinanu amal ndaje moomu, su ko defee ma mën a jokkalanteek ñooñu ñépp.
LDW : Yu ni mel ngay wax ci téere bi ngay bind ?
US : Maa ngi ci téere boobu te bëgg naa bu génnee, mu doon xew-xew buy lëkkale Afrig gépp, maanaam ñoom njiit yooyu yépp fekke ko, nu fexe ba am gën gaa néew ñaar-fukki réew yu ko teewe. Mënaguma cee sori waaye léegi mu noppi te ni ma leen ko waxe bëgg naa bun koy « lancer » mu doon ndaje mu yaatu fii ci Ndakaaru. Bu boobaa dinan waxtaane li ci biir téere bi ak lépp lu jëm ci Afrig ak sax ci àddina sépp. Fi nu teg sunuy tànk daal mooy, taxawal ab «Internationale» bu Afrig moomal boppam, mu wute ak « internationale libérale » walla « internationale socialiste » yi gaa ñiy tiitaroo. Ni ma ko waxe ca Niseer, lu ma ñor la ndax boo seetee araab yi sax am nañu seen «internationale». Kon, dafa jot nu am sunu bos te du roy liberaalism, du roy sosiyaalism. Bun delloo ci sunuy baaxi maam, dinan fa fekk li gën ci liberaalism ak li gën ci sosiyaalism.
LDW : Maanaam… ?
US : Aa, jëlal Sàrtu Màndeŋ bi. Li ci biir lépp, ba ñu koy wax, ndax Tubaab yi xamoon nañu luy demokaraasi ak liberaalism ak leneen ? Li des rekk mooy méngale ko ak jamono, te fexe ba ndawi Afrig yi tënku ci loolu. Nu ngi ciy liggéey te fi mu ne noo ngiy déggante saa su ne, di jokkoo, di jàppalante.
LDW : Mbaa sóoraale ngeen jafe-jafe yi ?
US : Xam nanu ni du yomb. Ndax am na ci nun ñu am jafe-jafe yu tar, rawatina ki ci gën a féete ndaw, am 35i at te dëkk Càdd. Ma-koom bu mag la woon ca bànk bii di “BAD”, waaye daf faa jóge dem taxawu réewam. Idiriis Debi ne day soppi ndeyu-àtte Càdd, ne ku amul 45i at du fa doon ab lawax ngir jiite réew ma. Te li mu ci jublu du dara lu-dul xañ nguur gi sunu mbokk moomu nga xam ne goney Càdd yu bare moom lañu àndal.
LDW : Waaw, Usmaan Sonko yéen a ngi bey seen waar di wut ay pexe ngir Afrig doon benn. Ku mel ni Séex Anta Jóob doon na wax ne gisul ëllëgu Afrig fu dul cig bennoom. Waaye bu ñu xoolee ni mbir yiy deme, ndax yaakaar ngeen ne bennoo gi luy mën a nekk la ?
US : Waaw, man gëm naa ne mën naa nekk. Lu ma gëmul duma ci dugg. Waaye li ma gën a gëm mooy ne danoo war a tàmbalee ci gox-goxaati Afrig yi. Yaakaar naa ni CEDEAO moo gën a jàppandi ndax boo ko seetee ci mboor, bennoom day lu war a yomb. Da di ne 80% yoo jël ci tolluwaayu CEDEAO mu ngi yemoo ak réewum Songaay mi mujj a doon réewum Mali, jóge ca doon réewum Gànna. Kon nun amoon nanu bennoo ba noppi ci wàllu mboor ak politig : benn buur rekk moo fi newoon ci jamono jooju, ba muy tudd Songaay, ca ñoom Soni Aali ba ci Sunjata Keyta. Te ba léegi loolu dafa fee bàyyi ay njeexital. Moo tax ma gëm ni bennoog réewi CEDEAO yi mu ngi aju rekk ci pas-pasu njiit yi. Dëgg la, am na ñu Niseryaa dalul seen xel ndax li mu ëpp i nit ci réew yooyu. Ci wàllu koom tamit, moo ci ëpp doole. Waaye jaruta ragal, ponkal la mu tànk yi dëgërul.
LDW : Ndax yaakaaroo ni gaawantoo booloo ak ñoom du jur i gàllankoor walla mu yàq li yeneen réew yi daj ba seen taxawaay dëgër ?
US : Am na ñu bari ñu koy wax waaye man li ma seetlu mooy Bennoog réewi Amerig yi nekkul woon lu yomb. Jaar nañu fu nekk, xeex nañu, te ba léegi am na fa réew yu bëgg a beddiku moom seen bopp. Nanu xool li gën a am solo. Ñenn ñi dañ la naan bun deful ndànk Niseryaa dina wann yeneen réewi CEDEAO yépp waaye loolu du wax, bun ca demoon it, réew mu nekk day wéy di am lu muy doxalal boppam, di fal ay njiitam ni ko Amerig di defe. Gis nga, loolu moo tax Trump am fi mu ne ay jafe-jafe, am nay dogal yu mu bëgg a jël ci mbas mi, waaye górnoor yi dañu ne ko mukk, ndax loolu seen jagle la. Moo tax tamit ku mel ni Bolsonaaro mënuta def lu ko neex.
LDW : Noo gise yi nga xam ne am réew moo ko war a téyeel boppam sun demee ba bennoo?
US : Su bennoo amoom tey tamit, Senegaal, li jëm ci jokkalante ak bitim-réew, laamisoo ak kaaraange, lépp lu jëm ci biir réew mi, njàng mi, wér–gi–yaram, añs. moo koy doxalal boppam. Waaye nooy bokk benn weccit, te làrme bi benn lay doon. Bu ko defee dunu neex a song, kon yu mel ne ay Boko-Haraam duñ nu sonal. Danuy am ag bennoo ci laamisoo, di waxe benn kàddu ci àddina si ak ci Mbootaayu Xeet yi. Tey jii xoolal sunu réew yi. Mali am na suuf su ñu mën a bey, Niseer naka noonu. Ñoo ëppale sax Senegaal ci wàll woowu. Mën na noo yaatal sunu doxalin ci wàllu mbey mi. Bunu bennoo woon, am nanu 2800 jun-ñayi (kilometi) peggu géej, soo ko jëlee Niseryaa ba Senegaal. Te day àgg ba 3000 jun-ñay boo ci boolee Gànnaar. Bu ko defee jàppalante mën a am ci diggante réew yi amul ubbeeku ci géej gi te am suuf su bari su ñu mën a bey, ak réew yi nekk ci peggu géej gi.
LDW : Nga jàpp ni CEDEAO mën na koo nekkal ?
US : Loolu laa jàpp. Te bu nu ko defoon fii ci CEDEAO, day law ndax ñeneen ñépp dañu koy roy ngir njariñ li ñu ciy gis. Waaw, Mbootaayu réewi Afrig yi dafa newoon nu liggéey ci bennoo gox-goxaati Afrig yi. Afrig soowu-jant CEDEAO benn la ci, Afrig bëj-gànnaar (Gànnaar, Alseri, Tinisi, Marog, Libi, Misra) di beneen. Bu weesoo loolu am na Afrig-digg bi, ñoom it benn la. Afrig-penku tamit benn lañu. Afrig-Saalum benn lañu. Juróom-benneel bi mooy, ci li ñenn ñiy wax, doomi-Afrig yi nekk bitim-réew, jasporaa bi. Boobu laa àndul ak ñoom ndax ci sama gis-gis am réew dafa war a dëppook suuf. Ñu ne bu wàll wu nekk gaawtoo amal ag bennoom, kon 5i réew rekk lanuy boole ñu doon benn. Moo gën a yomb boole 54i réew.
LDW : CFA walla ECO ban moo la ci gënal ?
US : Xanaa kay dangeen naan ban moo ci tane ! Benn baaxu ci waaye jàpp naa ne Eco moo xaw a tane. Ndax, fàww nuy jiital xel ci bu nuy wax ci mbiru koppar. Samalyeer ca Farãs la ñuy defare CFA te ñu bare nee nañu du yoon. Man nag, sama yoon nekkul ci ñu koy tëgge Farãs walla Siin bu fekkeeni amunu jumtukaay ak kaaraange yiy tax nu mën koo tëggal sunu bopp. Loolu du li ci ëpp solo. Tur wi tamit, di fàttali na nu Farãs daan noote, am na ñu mu neexul. Doonte soppi nañu ko, ba tey am na ñu mu neexul. Tur wi, lu am solo la...
LDW : Kon ba tey turu Eco wi gënul ?
US : Liy jafe-jafe bi mooy Eco tamit dafay toppandoo Euro, ndax Eco Ecowas la, nga jël ñetti loy yi jiitu. Nun danoo war a wut tur wu gën a méngoo ak sunu mbatiit, ndaxte xaalis dafa ci am wàll woo xam ne ci sa xol nga koy yëg. Bu njëkkaan, xam nga nu nu doon woowe xaalis ? Boo demee ci joolaa xaalis ekóri lañu koy wax. Ekóri mu ngi jóge ci kóri, maanaam pettaaw. Kon waroon nanu xool loo xam ne day delloo nit ñi ci li ñu xam. Waaye Ërob ne Euro rekk yow it nga ni Eco, loolu du faayda. Te nun soxlawunu benn weccit kott. Li nu soxla mooy xaalis bu nu bennale. Ñaar yooyu bokkuñu. Bennoo xaalis mooy nga jël noste (système) yu wuute taf leen ci benn xaalis. Nun li nu bëgg mooy ànd bokk benn noste.
LDW : Lu ko mën a jëmmal ?
US : Ngir loolu am, fàww nu amal bennoo ci wàllu politig ak koom, ak tamit ja bu yaatu. Am na yeneen yu gën a am solo. Benn ci ñoom mooy li nuy wéer xaalis bi ci Euro, ba mu tee koo mën di ànd ak soppiku yi, beneen bi di li nuy yóbbu sunuy ndenc ca Farãs. Te yooyu, am nan ciy jéego yu wóor. Ndaxte, nee nañu léegi jël nañu sunu koppar gi nu dencoon Farãs. Te tamit Farãs dootul teew fa nuy doxale ak di jël ay dogal ci xaalis bi. Ay jéego la. Warunu koo xeeb. Ñaar yi des mooy li nu wéeru ci Euro te dunu mën a ànd ak soppiku yi. Te sax wéeru gi moom fàww mu am. Léegi nag ndax wéeru guy ànd ak soppiku yi lay doon, nu am ndabal xaalis lu def Euro, Dolaar ak Yuwaan ndax li Siin jiitu léegi ci koom, walla danuy des ak Euro rekk ? Loolu nag, bi ma déggee Watara, dafa ne danuy dem ci wéeru gi ànd ak soppiku yi. Ndax nag mënoo tëb rekk def lépp ci benn bés. Coppite ci xaalis day lu doy waar ba tax dañu cee war a dem ndànk-ndànk.
LDW : Li nga bëgg mooy nu dem ceek ràññatle, waaye ndax nit ñi dinañ ko nangu ?
US : Nun, noo war a ubbi sunuy bët ngir balaa yàgg ñu mën a dem ci wéeru gu ànd ak soppiku googu. Ndaxte soo nee yuwaan ne dolaar fàww nga waxtaan ak Siin waxtaan yit ak Amerig. Li ci des nag, damaa jàpp ne lu baax la nuy def coppite yi ndànk-ndànk. Bu nu xéyoon ñu ne dog nañu lépp, jox nañ nu xaalis bi, ci ngeen di xam ne njaaxum am na. Amagunu Bànk bu mag bu mel ni bu Amerig walla bu Ërób ndax BCEAO bànku Kodiwaar la, moo koy doxal, moo ci ëpp doole ci wàllu koom te réew yépp teewuñu fa. Alasaan Watara mooy jël dogal yi te looloo tax Macron siiwaal ab dogalam ca Kodiwaar. Te Alasaan Watara léppam ci leb xaalis bu bare la aju te loolu baaxul. Day defarloo BCEAO koppar gu bare ngir fatte ko kàmb yi leb gu metti yóbbee Kodiwaar. Loolu, bunu ci duggee caaf xëm.
LDW : Kon luy pexe, ci sa gis-gis ?
US : Xanaa taxawal Bànk bu mag buy wuyoo turam dëgg, di lëkkale sunu réew yépp, réew yépp am ku leen toogal ca fa ñuy nosee ak di nocci ba noppi am kàddu ci dogal yi ñu fay jël. Feek loolu amul, bés buñ nu bàyyeek xaalis bi, nu yàqu. Te sunu ndenc yooyu nu Farãs delloo, fàww nu sàmm leen bu baax. Loolu beneen jafe-jafe la. Ndax sunu njiit yu saay-saay yii mën nañoo wax ne am nanu ay jafe-jafe te ndenc yaa ngi fi, nan ko séddoo. Te ndenc yi du loolu lañuy jariñ, kiiraay la war a doon ba bu ay copppite amee ëllëg ci weccit yi nu wéeru nu mucc ci. Rax-ci-dolli saa yuñ demee ba njëg yi yokku, ci misaal bu xàndi petorol bi jógee ci 50i dolaar yéeg ba 80i dolaar, xaalis boobu dinan xettali. Mënees na limaale tamit li nuy jaay bitim-réew, rawatina sunu meññeef yi, bu nu waree fey ak weccit wu am doole mu jaar foofu.
LDW : Waaw, Usmaan Sonko ku yëbb ci moom, maanaam kan mooy royukaayam ?
US : Sama royukaay ? Mu ngi aju rekk ci ban fànn. Bu dee fànn bi ñu ma gën a ràññee, muy politig, moom, bi ma ciy dugg amuma royukaay. Politig dama cee tàbbi rekk, daanaka. Man, mësumaa xalaat ne dinaa taxawal bés pàrti politig.
LDW : Kon noo def ba dugg ci politig ?
US : Ñi taxawal Pasteef, at mañ koy def, daa fekk ma aji woon Màkka. Nekkuma woon Senegaal. Bi ma dellusee lañu ñëw ne dañu may siyaare si, ne ma nag ñoom dogu nañu ci taxawal kurélu politig te bind nañu sàrt bi ba noppi. Ma ni leen man, politig moom, dafa aw fii ma aw fale, duma dugg ci seen pàrti boobu. Fekk jotoon naa jiite lu mat 8i at ag kurélu liggéeykat. Ba ma fay jóge, kenn newu ma bàyyil, maa xool ba xam ne jeexal naa samay ay, ma joxe lenge yi ngir mën a dellu ci samay yitte. Politig dafa doy waar. Wax dëgg-Yàlla, du woon lu ma soxal. Waaye li ma leen tontu teewul ñu topp ciy wax ak a waxaat. Bés, ñu delsi kër ga, ne ma dañoo war a yendu kër kenn ci ñoom, bëggoon ma teew fa. Àjjuma la woon, waaye du woon bésub liggéey, ma dem, nu julli fa jumaa, añ fa, waxtaan. Ñu ne gaawu bi ci topp lañuy def seen ndaje mu yaa ngir taxawal kurél gi. Ma ne ca tonet ne leen déet mënagu leen taxawal kurélu politig, yéen matagu leen sax ñaar-fukki nit, te tamit mbindum sàrt yi des na. Kon def leen ndànk, waxtaan leen ak ñeneen, yaatal mbir mi. Waaw, ci noonu laa teewaatee 3i ndaje. Bi ñu ci tegee ñaari weer ñu ne taxawal kurél gi jot na. Ñu yëgal ma ko, ni ma fàww nga ñëw ci ndaje mi, man it ma dem ca. Ndekete ñoom bés boobu lañu waroon a fal njiiti pàrti bi, ñu déggoo yit ci ne bu ñu laaje ku ko bëgg jiite rekk, na am ku jóg joxe sama tur. Ndaxte ñoom, booy seet, 80% yi ay ma-xereñ lañu, ay saytukati galag, ay saytukati gafag réew mi, amoon na benn layookat añs. Waaye ñoom dañoo waxtaan seen biir, ñu ne nanu waxante dëgg kenn ci nun mënul a yore kurél gi te Sonko mi jot a bokk ci kurélu liggéeykat xéy-na xam na tuuti ci mbir yooyu. Man daal dem naa ca ndaje ma, ba ñu ne kuy nekk njiit li la Paap Umar Jàllo jóg joxe sama tur. Noonu, ña fa teewoon ñépp tàccu ne ma sañoo bañ. Man nii laa duggee ci politig. Waaye mësul nekk loo xam ne sama sémbu bopp la. Xawoon naa metti ca njalbéen ga, nag, ndax du lu ma tànnaloon sama bopp.
LDW : Amul sax kenn ku la taxoon a bëgg a def politig ?
US : Wax dëgg-Yàlla, bi ma ciy dugg amuma woon royukaay, rawatina ci ñiy def politig fii ci Senegaal. Gaa, bi ma doonee gone laa tàmbalee naw Mamadu Ja waaye teewul ma xawoon koo mere tuuti, damaa jàpp ne li nu nekke tey am na ci wàll. Ci sama gis-gis, ni mu doon maslaak Seŋoor dafa ëppoon.
LDW : Ci naka ?
US : Mbir day tollu foo xam ne maslaa amatu ci wàll te Ja da doon wax ne Seŋoor da koo jàppe woon ni doomu–ndeyam, du ko def lii, du ko wax laa… Fekk waa ji moom mu ngi koy fexeel ci suuf. Waaw, am na foo xam ni réew la ñuy wax, ëllëgam ak ginnaaw-ëllëgam. Foofu, maslaak koo bokkal ndey sax waru fa. Waaye nawoon naa ko ndax li mu defal réew mi te téere yee ngeen di séen ci sunu kàggu gi, yu ci bare Ja moo leen bind. Téerey Seex Anta Jóob yi defe naa ñaar yii ñoo fi nekk, yi ci des yépp yóbbu naa leen kër ga. Ci gàttal, Ja sama royukaay la, amoon na yéene ci Senegaal, bëgg ko ci xolam mu jaraloon ko jàmmaarlook Tubaab bi. Loolu daal lu ma neex la ci moom.
LDW : Séex Anta Jóob mi nga tudd léegi nag ?
US : Séex Anta Jóob, moom, xooleewuma ko bëtu politig. Moo tax bu dee politig rekk ci anam yi ñu koy defe fii, déedéet, Séex Anta du sama royukaay. Séex Anta ci fànni xeltu, xamtu ak mbatiit laa ko gën a nawe ndax jotul a bokk ci nguur, masu ko sax jege. Séex Anta Jóob ak Mamadu Ja sax damaa jàpp ne dañuy mottalante. Waaye xalaatu Séex Anta Jóob daal moo gën a ubbi sama xel. Am na yit yu ma nàndul ci taxawaayam, ci misaal lu ko tax a bokk cib joŋante ngir jiite réew mi ba noppi mujjee cee génn. Joxe na ay leeral ci loolu, nag, ne ag kilifa diine moo ne woon bu kenn jàmmaarloo ak Seŋoor, te ginnaaw moom taalibe la woon… Waaye loolu sax waxu politig la. Xalaatu Séex Anta moo gën a fatt bu ñeneen ñi, te day gën di am wàll wu rëy ci sama taxawaay ci politig.
LDW : Ba tax na amuloo benn royukaay bu nu mën a jàpp ?
US : Yonent bi (SAWS) mooy sama royukaay. Damay sant Yàlla bi ma teelee yaru, di gëstu ci njàngaleem. Ndax loolu rekk moo ma ñag, man. Man, taxawaay bi ma am bi may liggéey fi ñuy saytoo galag yi, loolu rekk moo ma ko may. Ndaxte bu dul woon sama diine, ni ñépp laay def kon. Toog di xalaat fooy jëlee loo feye sa luyaas, sa jabar doon jigéen ju wérul, nga dem cig lijjanti gu def naka su-dul-noonu ci wàllu galag, mën cee am 300i milyoŋ te kenn du ci yëg dara, nga ne duma laal xaalis boobu ndax ëllëg dinaa ko layoo ak sama Boroom, loolu diine rekk moo ko mën a may nit. Am na yit ñoo xam ne jikko yu ñu làmboo jële ko ci yar, aada ak cosaan ñoo leen koy may. Waaye man sama diine moo ma ko may. Mooy wéy di ma sàmm ba tey fi ma tollu nii, nit mënu maa tëkku walla nga xoqtal ma ba mu jaaxal ma. Dama la dul gis, man, Yàlla laay gis. Dara walla kenn mënul a fees samay bët. Loolu maa ngi koy sante samay way-jur waaye diine rekk a ma tënk.
LDW : Am na ñu naan ku am diine dëgg du politig…
US : Ñu bareey wax loolu waaye dafa fekk ñu réere mbir ne Yonent bi ci boppam dafa daan politig. Képp kuy politig te defar rekk tax laa jóg, mën naa ne moo la ci jiitu, mooy sa maam. Waxuma ne mën naa mel ni moom, waaye am na lu bari lu nuy jàng ak a roy ciy jaar–jaaram. Lees war a jàngat mooy naka la def ba tàmbalee ci neen, tey lu xaw a jege 3i milyaari doom-aadama diy jullit, wékk seen yaakaar yépp ci moom. Ñu bari jàpp nañu ne mbiri saari Alxuraan yi la,‘’Yàlla nee na’’ rekk la. Déedéet !
LDW : Naka la Yonent bi daan politige ?
US : Yàlla da koo yónni ba noppi seetaan ko ak ay pexeem. Ndaxte ku Yàlla yónni, ngay dem xare ñu damm say bëñ… Te Yàlla bu ko neexoon doo dem sax xare, da naan nii rekk saa noon yépp dee. Booba Yàlla bàyyi na ko mu demal boppam ngir bëgg koo natt, wonaale ko foofu ne àddina lépp ay pexe la. Boo xoolee ni mu néewe woon doole Màkka, génn fa dem Madina, ànd ak Ansaar yi ko woowoon, mu ànd ak muhaajirun yi di dem, ña doon ña gënoon a ndóol ca Màkka. Booba yahuut yi ñoo yoroon koomu Màkka. Mu ne fii naxantee fi sës. Moo tax parax-parax rekk di mbëkk, loolu du xam-xam. Keroog lañu torlu ndeyu-àtte Madina, am ñu ne mooy gi njëkk ci àddina. Liñ ci wax mooy nan déggoo, noo bokk dëkk bi, bu kenn song moroomam mbaa lëkkalook ay doxandéem di dal ci sa moroom, añs. Jàmm ne ñoyy. Jullit yi bu ñu xéyee dem ci toolu yahuut yi, toolu tàndarma yi walla ñu dem sàmmal leen géléem ñu leen di fay. Peyoor googu, ku ci dem ba am benn, ñaar, ñetti payoor dem ca ja ba lal di jaay. Ci noonu jullit yi tàmbalee am doole ci koom gi. Man, nag, damay jéem a jàng lu bari ci moom, pexeem yooyu laay jéem a doxal. Loolu dina dimbali nit ki ba mu mën a dékku lépp, di soofantal lu bari. Léegi sax, su ma gisee ñuy dal ci Sonko ay ree la may def. Ca njëlbéen ga, daf ma doon merloo. Waaye léegi damay xéy di laaj waaw tey lan la gaa ñi wax ? Léeg-léeg damay reetaan, tey jii [bésu laaj-tontu bi] moo ci mujj, dama xéy ñu ne ma Amet Xalifa Ñas nee na damaa sàcc kurélu politigam ! Damaa reetaan ba tëdd ci suuf ne leen ‘’waaw, baax na.’’
LDW : Kon daal, benn politiseŋu Senegaal doyu la ?
US : Senegaal moom, am fi royukaay ci politig yombul. Sunu polotiseŋ yi moom musiba lañu. Kenn mënu la koo nettali ! Dañoo doy waar. Man damay faral di xalaat ci bés ba may jàkkaarlook sama Boroom. Waaye, am na waa ju ma mas a wax ne moom Bés-pénc ba, bu gisee polotiseŋ yi jàll, xelam dina dal ndax da koy wóor ne moom tamit dina mucc.
LDW : Waaw léegi nag, wax nu, ndax yaa ngi bëgg Bob Marley ba tey ?
US : [Mu ree ba sëgg, nu àndandoo reetaan].
Loolu… Gis ngeen sama gaa ñi, dañuy wax rekk… Dëgg la, nag… xam nga Kaasamaas, dafa wuute ak fu bari. Bi ma fa nekkee xale, am fukki at ak juróom-ñaar, ku dégluwul Bob Marley walla Omar Pen walla ay ‘’Dire Straits’’ bokkuloo. Waaye misigu Senegaal moom, ku juumoon ba ñëw naan dangay déglu Yuusu Nduur, dee nga. Gaa ñi dañu doon wax naan jigéen ñeey déglu Yuusu Nduur, góor ñi Omar Pen lañuy déglu. Am nay woyi Bob Marley yoo xam ne dama leen daan tari. Xéy-na ci yu bare bokkumaak Bob Marley gis-gis waaye xam naa ne ku Bennoog Afrig ñoroon la, ay woyam firnde lañ ci. Wànte, damaa xéy rekk ne lii yépp ay caaxaan la, bàyyi misig.
LDW : Nataalu Sànkara bee di wékke, nag ?
US : Sànkara waaw, ponkal la woon. Amoon nañu fi yeneeni nataal, sax, bu Séex Anta ak bu Mamadu Ja… Maa ngiy defarlu yu Amilkaar Kabraal ak Kuwaame Kurumaak Ñereere… Waaye Séex Anta moo sutoon ñii ñépp. Li leen wuutale mooy mësul yor nguur. Moo tax ñii gën koo am tur, dañ daan def muy fés. Waaye tolluwuñu sax fii Séex Anta. Bu doon Séex Anta ak Mamadu Ja ñoo àndoon yor réew mi ci atum 1960, kon kenn du nu yab tey.
LDW : Usmaan Sonko, Lu defu Waxu, dib yéenekaay ci kàllaamay Kocc mi ngi lay gërëmaat bu baax ci jot geek waxtaan wi ak ubbéeku gi.
US : Maa ngi leen di gërëmaat bu baax, man it, te di leen ndokkeel ci seen taxawaay ci luy jëmale réew mi kanam, jaarale ko ci làmmiñ wi ñépp dégg daanaka. Di sant ñépp, di leen mas-sawu coono, di leen balu àq. Jërë-ngeen-jëf.