Usmaan Sonko feddali na tuuma yim gàlloon ci kow way-wattu kaaraange yi ne dañ ko bëggoon a rey. Dafa bind ci xëtu facebookam :
« Mbokki réew mi,
Jot nanu ci ngirtey ceet yi nu doon seetlu ca laboraatuwaari bitim-réew, ginnaaw cong mi ñu ma songoon keroog 16 màrs 2023.
Ngirtey ceet yi firndeel nañu bu baax bóom bi ma way-wattu kaaraange yi doon jéem a bóom. Dinan ci ñëwaat, lu yàggul dara, gën cee xóotal ci ndajem waxtaan mu ñuy amal ak taskati xibaar yi. Ndaje moomu, dinan ci waxtaane tam yeneen i ponk.
Dinan yóbbu mbir mi ci Yooni àddina si. Dinan amal tontub pólitig ci biir réew mi ñeel faagaagal biñ ma doon jéem a faagaagal te, ba tey, xamagunu lan mooy doon njeexital yi ci sunu wér-gi-yaram… »