USMAAN SONKO : ELIMAANU JËWRIÑ YI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Fay, tabb na Usmaan Sonko, def ko elimaanu jëwriñ yi. Ginnaaw bi ñu ko tabbee, Usmaan Sonko jël na kàddu gi, wax ne : “Fii ak waxtu yii di ñëw, dinaa jébbal Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, limub ñi war séq gornamaŋ bi, ni ko ndeyu sàrti réew mi yoonalee…”

Moom nag, elimaanu jëwriñ yi, mooy ki war a jëmmal naal bi Pastef jaay askanu Senegaal ci diirub fukki at yi ñu def ci kujje gi. Xamle na ne, gornamaŋ bi ñuy waaj a tabb, dina am ay góor ak i jigéen te, liggéey kepp moo leen tax a jóg, nguuru yékkatiwu leen.

Njiitu réew mi tabbaale na Mari Tëw Ñaan, def ko bëkk-néegam (directeur de cabinet).  Kii di Umar Sàmba Ba la tabb jëwriñ jiy magum fara-caytub njiiteefu réew mi (ministre secrétaire générale de la présidence). Moom, Umar Sàmba Ba, boppam la wuutu, ndax moo ko nekkoon ci Nguuru Maki Sàll.

Mu mel ni Njiitu réew mi sóobu na xaat ci liggéey bi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj