Kër Masaar wàcc na. Bu yeboo, bés niki tey, nu ngéntewaat depàrtmaa bu bees bi, duppee ko Kër-Sonko walla Kër-Pastef. Guléet mbooloo mu ni tollu dajaloo ca pàkkub Yékini ba. Ndax, démb, ci dibéer ji, fépp a ñuuloon kukk ak i nit, muy mbooloo mu jéggi dayo. Dafa di, foo sàndi woon mbàttu, mu tag. Ndeke, ca guddig gaawu ga jàpp dibéer la ndawi Pastef yeek soppey Usmaan Sonko yi wutali gox ba. Li ñu ko dugge woon mooy teewe mitiŋ bu mag bi ñu jagleel Soxna Mariyaama Saañaa, militaŋu Pastef bi ñu faatoon Kër Masaar ca atum 2019. Mu doon mitiŋ bob, dafa làmboo lu baree bari, bees seetloo jamono ji mu ame. Ndege, noo ngi tollu ci waajtaayu wotey Njiiteefu réew miy am 2024 te njiitalu Pastef li, Usmaan Sonko, fas cee yéene samp ndëndam ngir déjjati Maki Sàll ci jal bi. Waaye, jamono jii tamit, coowal Aji Saar li topp lawax bi diirub ñaari at, moo lëmbe réew mi. Nu ni déet-a-waay, Séex Yerim Sekk génne ab téere, di ci taqal Usmaan Sonko lu ñaaw, mel ni kuy layal tuuma yees koy gàll ci wàllu ciif. Mu mel ni, dafa am lu nooni meeru Sigicoor bi nas ngir tilimal deram, teg koy daan, yàq këyitam ba du bokk ci wotey 2024 yi. Loolu la Sonko ak i àndandoom xam ba tax leen a ngembu, fas yéene xeex. Démb, dafa meloon ni gaynde gu fippu, nar a song xare boo xam ne, xoolu ci bakkanam.
Mitiŋ bu mag a mag a amoon démb ci dibéer ji, 22 saŋwiye 2023. Ci turu Mariyaama Saañaa lees ko tëgge. Nde, lenn ci jubluwaayu mitiŋ bi mooy sargal ko, delloo ko njukkal. Moo tax Usmaan Sonko ubbee ko waxam, bi mu jëlee kàddu gi, daldi sàkku ñu amal 1 simili ngir ñaanal ñi nga xam ne, boobaak léegi, ñàkk nañu seen i bakkan ci sababu xeexu pólitig bi ñu sumb, rawatina Mariyaama Saañaa.
« […] palaas bii ñu daje tey, juróomi at ca gannaaw, dañ fi daje woon, def fi mitiŋ. Mitiŋ bi matul woon xaaj sax ci li fi daje tey. Ñu pare mitiŋ ba, kenn ci ñi fi nekkoon, di sunu jigéen, di jigéen ju am gëm-gëm, am pas-pas, bëggoon « projet » bi lool, dëkk fii rekk ci ginnaaw, ay sàmbaa-booy daldi koy faagaagal. Tey, njabootam a ngi fii toog ci mbaar mi ndax bàyyi na fi njaboot. Loolu rekk waroon na tax nu taxawaat tuuti, jagleel ko ñaan. »
Ginnaaw Mariyaama Saañaa ak i militaŋam yi faatu, sàkku nay ñaan itam ngir soldaari Senegaal yi, rawatina sóobare yiy jaay seen bakkan ngir réew mi, fale ca Kaasamaas. Tagg na leen, sargal leen. Seedeel na njiiti Yewwi Askan Wi seede yu rafet a rafet.Biral na yit ne, tey la waa YAW gën a booloo, bennoo, bokk jëmu, te dara ba dara booloo jeex du leen féewale.
Bi mu noppee ci loolu, Usmaan Sonko dafa biral jaar-jaaram, wane ne doomu Senegaal dëggantaan la, ci ndey ak ci baay. Leeral na yit li ko tax a dugg ci pólitig. Ci gàttal daal, liggéeyal réew mi, doon jaamu maxejji Senegaal yi ngir génne réew mi ci ndóol, dog buumu njaam gi dox sunu diggante ak tubaab yi, looluy nisëram. Bi loolu weesoo, dafa dalal xeli nit ñi ko gëm ñépp, topp ko, waatal leen ci Yàlla ni du leen mës a wor :
« Ma feddaliwaat leen, billAahi, wallAahi wa tallAahi du ngeen mës a toog ba ne tas naa seen yaakaar ! Du mës a am. BillAahi, wallAahi wa tallAahi du ngeen mës a toog ba ne am tas naa seen yaakaar ! Mukk ci àddina ! Am na loo xam ne gor moomu ko, te nun ay gor lañu. »
Bi mu noppee ci ngërëm yi, njukkal yi, seede yeek dig yi, dafa tàmbalee wax ak Maki Sàll ak i ñoñam ñi koy fexeel, moom ak kujje gi. Ciy waxam, Maki Sàll yéenewul Senegaal jàmm. Yoonam nekkul ci Saa-Senegaal yi ndax Nguur jaral na ko lu nekk. Usmaan Sonko ne :
« Maki Sàll lijjantiwul Senegaal. Moom ak nguuram, lu nekk def nañu ko ngir ma bañ a bokk ci wotey njiiteefu réew mi. Waaye, dañuy sonn rekk. Ndaxte, xam naa ni yeen, askanu Senegaal, dingeen taxaw temm ngir gàntal mébétam boobule… »
Coow lépp nag, ci mbirum Sweet Beauty mi lay dellu. Nde, ci la Nguuru Maki Sàll jafandu ngir sàkkal ko pexe. Wànte, Usmaan Sonko takku na ba dëgër, wax ne, noppi na ngir jàmmaarloo ak Maki Sàll ci xeex bi mu koy woo. Te, lu ci Njiitu réew mi bañul, moom, Njiitalu Pastef, yaakaaru ndawi réew mi, du ko ci bañ. Moo ko tax a waxaat ne :
« Fi mu ne nii, sës nanu ! Xas naa miiraas sama bopp. Dinanu xeex ak Maki Sàll, ak lu mu nu mën di jaral. »
Xeex boobu, moom kese mënu ko xeex. Ndaxte, dooley Nguur xajul ci kenn nit kese, xanaa askan wi xeexle ko. Te, bu dee wax dëgg rekk, bu dul woon askanu Senegaal, kon kenn waxatul waxi Usmaan Sonko. Loolu la meeru Sigicoor bi xam ba tax ko di xelal mboolo ma fa teewoon, ne leen :
« Bu leen déglu kenn ku leen di fàbbi ci seen jubluwaay. Nit ñi leen di wax ne dangeen a ànd ak fitna, dañoo bëgg ngeen jéllale solos xeex bi. »
Usmaan Sonko artu na Njiitu réew ak ñi ànd ak moom di ko xeex ci anam yu nekk, wax leen ne, léegi, dinañu xeex ak ñoom ba mu saf sàpp ; lu mu leen jaral rekk, jaral na leen ko, moom ak i àndandoom. Ca la leen tëkkoo ak kàddu gog, doy na junj. Nde, Usmaan Sonko nee na leen :
« Ma bëgg leen a wax ne, man mii Usmaan Sonko, démb laa jóge Sigicoor. Bi ma demee, dem naa ca sëg ya, siyaare sama way-jur, ñaan, tàggoo. Bi ma fa jógee, dem na seet sama yaay ji ma jur, tàllal sama loxo ne ko ñaanal ma, mu ñaanal ma, ma jël sama roppalaan ñëw. Li ma bëgg a wax foofu, mooy man xas naa miiraas sama bopp. Loolu tekkiwul ne dama dem jox sama bopp Maki Sàll. Xam ngeen lu muy tekki ? Mooy Maki Sàll dina jël sunu bakkan walla nu jël bakkanam su dee dafa bëgg a wéyal li muy def. […] Bu dee pare ngeen, te Maki Sàll ne fi mu nekk lay nekk, du yeggali moomeem. 2024 du ko fi fekk. »
Dankaafu na waa APR itam, wax leen ne, bu ñu yaakaare ne ndawi Pastef yi rekk ak waa kujje gi ñooy dee ci ñaxtu yi, juum nañu. Léegi « Gat-sa Gat-sa rekk ! ». Loolu mooy, dóor, fayu. Te nag, làmbi dóor, fayoo koy tas.