USMAAN SONKO : “LI TAX MAKI SÀLL MËNU MA JÀPP…”

Yeneen i xët

Aji bind ji

Usmaan Sonko jiitu na Maki Sàll ci kàddu gi. Ci altiney tey jii, 3 suwe 2023, la Njiitu réew mi war a wax ak askan wi. Njortees na ni, dina àddu ci ndogal yi tukkee ca waxtaan wa mu woote woon, rawatina ci mbirum ñetteelu moome gog, tey la koy leeral. Démb nag, njiitul Pastef li dafa mel ni ku ko dogaale, jéem a junj li mu nar a wax ngir waajal ay àndandoom. Usmaan Sonko wax na ci kootoo gi waa “système” bi lal ñeel ko ak daan bi ñu ko daanoon keroog 1 fan ci suwe te àtte bi génn keroog ci àllarba ji. Nee na nag, Maki Sàll mënu ko jàpplu.

Ci xeexub xel bu metti la Usmaan Sonko ak Maki Sàll nekkee jamono yii. Bu Maki Sàll dee nappaate, di xuppaate ak a fëgg dënn, Usmaan Sonko moom, mi ngi koy artook a dankaafu, di ko jéem a xamal ni, moom, du ku ñuy xoqatal walla di ko tiital. Ñu ngi mel ni ñaari mbër yuy léewtoo, di waaj a songante. Waaye nag, ku ci nekk day jéem a nax sa moroom, di ko tegal ndëgg-sërëx.

Usmaan Sonko dafa bàyyi ba ñu ne Maki Sàll day wax ci altine ji, 3eelu fanu sulet, mu jiitu ko ci kàddu gi, wax ci dibéer ji, 2eelu fanu sulet. Waxam ji nag, dafa bette. Ndax, ba démb ci ngoon, xameesul woon ne dina wax. Mu mel ni, li mu ko duggee mooy jaxase Maki Sàll ci xelam ak a waajal askan wi ba dara bañ leen a bett ci kàdduy Njiitu réew mi. 

Li jëm ci waxtaan wi Njiitu réew mi woote woon te mu jeex fan yii, meeru Sigicoor bi nee, dara wundu ko lu dul ag kootoo gog, beddi Usmaan Sonko ak paacoo réew mi rekk a di laltaay bi. Mu ne, ña ko sumb, dañ ko waxtaane ci suuf bu njëkk, déggoo seen biir ba noppi, di xool am pexe ngir yoonal ko ba du nirook kootoo. Mu neeti, bu Maki Sàll waxee, ñaari mbir rekk a ñoo mën a am : mu ne day bokk walla Mu ne du bokk.

Ci kàdduy Usmaan Sonko, bu Maki Sàll nee day bokk, mbirum askan wi la, ñoo koy fajal seen bopp. Bu nee du bokk itam, pexe rekk lay doon. La mu cay jublu mooy wéetal ko ci géewu pólitig gi. Nde, Sonko dafa gis ni, xalaatu Maki Sàll mooy ne, bu bañee bokk, ñi naroon a xeex ñépp ay wéer seen i ngànnaay. Dañ naan rekk, ndeem Maki Sàll du bokk, xeex bi jaratu ko. Maanaam, kenn du tal a xeexal Usmaan Sonko. Bu boobaa, ci kàdduy Usmaan Sonko, Maki Sàll dina ngembaat Yoon ngir jàpplu ko, tëjlu ko kaso ci lu gaaw a gaaw. Waaye, moom de nee na :

“Maki Sàll mënu ma jàpp. Dañ ma àtte àtteb teewadi. Ci xeetu àtte bu ni mel, ki ñu àtte woon bu feeñee, àtte bi day neen. Kon, amul fenn fu Maki Sàll mën a tënku ci Yoon ngir jàpp ma, donte benn simili la.”

Mu ne, “…layoo bi yépp lañ war a tëggaat”. Te, bu boobaa, “seen layoo lay doon” ndax, moom, setal nañ ko. Kon, ku ko dégg, layoo bii mënu ko teree bokk ci wotey 2024 yi. Te, bu ko ko Maki Sàll naree xañ, moo ngi woo askan wépp ñu génn jàmmaarloo ak moom, jële ko fi wenn yoon mu jeex. Nde, du Maki Sàll moo war a tànn kuy bokk ak ku dul bokk. Moo ko tax a waxati ne :

“Buñ ma jàppee, maa ngi woo askanu Senegaal wépp mu jóg def benn say, génnandoo bu baax ngir tàggook Nguurug deret gi fi nekk.”

Njiitu réew mi dina wax tey ci guddi. Ñu xaarandi ba xam lu muy tontu Usmaan Sonko.

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj