USMAAN SONKO ŊÀÑÑ FARÃS, ARAAMAL NGÓOR-JIGÉEN

Yeneen i xët

Aji bind ji

Usmaan Sonko,  njiitul PASTEF, doon na dalal Jean-Luc Mélenchon. Njiitul làngu La France Insoumise, ca Farãs, daf fee amalsi tukkib nemmeeku, ganesi waa PASTEF. Démb, ci alxames ji 16 me 2024, amaloon nañ ndajem waxtaan fa jànguneb Séex Anta Jóob bu Ndakaaru. Usmaan Sonko jot na faa ŋàññi bu baax njiiti Farãs yi, daldi leeral ne Senegaal du mës a daganal ngóor-jigéen.

Ay njàngaan yu baree teeweesi woon ndaje mi. Nde, “Amphithéâtre” bi daa feesoon dell, xumb lool. Bi Usmaan Sonko jëlee kàddu gi nag, génnee na mer mi mu guuxaloon Farãs yépp. Nde, ñaawlu na taxawaayu njiiti Farãs yi. Ndax, ciy waxam, Njiitu réewum Farãs ak i ñoñam dañu bokkoon ci ñi doon jàppale Maki Sàll jamono ji mu daan xoqatal kujje gi.

Usmaan Sonko dafa njëkk a gërëm Jean-Luc Mélenchon ak làngam gi ci seen taxawaay, daan leen xeexal ak waxal bi leen Maki Sàll doon fitnaal diggante 2021 jàpp 2024. Ginnaaw gi la ŋàññ kilifay Farãs yi. Sonko nee, “mësooleen dégg nguurug Farãs gi ñaawlu li fi amoon.” Wax na ba tuumaal Emmanuel Macron, Njiitu réewum Farãs. Li metti Usmaan Sonko mooy li Macron dalaloon Maki Sàll “ci jamono ji fitna ji gënee tar”, daldi koy “ndokkeel”. Njiitul PASTEF li dafa gis ne, doxaliin woowu, “day daganal xoqatal bi Maki Sàll nekkee woon, di yoonal fitna ji mu daan teg ci kow Saa-Senegaal yoy, defuñu woon lu dul ànd ci naalub pólitig.” Dafa di, nguuri Tugal yi sax, elimaanu jëwriñ yi moyu leen. Ndax, rafetluwul dara tekkaaral gi nguur yooyii nekke woon, mel ni ñu àndoon ci ñaawteefi Nguurug Maki Sàll ga woon.

Ci benenn boor, Usmaan Sonko àddu na ci coowal ngóor-jigéen li fi lëmbe woon réew mi. Usmaan Sonko nag, jàpp na ne coowal ngóor-jigéen yàgg na fi. Waaye, ni koy waxee léegi ak booba, wuute na. Ci gis-gisam,  lenn rekk mooy jafe-jafe bi, mooy ni ko réewi Tugal yi bëggee fésal, bëgg koo ga yeneen réew yi ngir ñu mën a jot ci sémb yi, ñu leen ciy kopparal. Waaye, ciy kàddoom ba tey, muy Senegaal di yeneen réewi Afrig yi, menn du ci nangu daganal jëf jooju.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj