Usmaan Sonko : « Paab Aale Ñaŋ du doon weneen nagu sarax… »

Yeneen i xët

Aji bind ji

Coowal jàppug Paap Aale Ñaŋ gi moo lëmbe réew mi ba tey. Kilifa yu bari fésal nañ seen naqar ci lees ko teg loxo. Wone nañ itam ànd bi ñu ànd ak moo ba mu jeex.

Usmaan Sonko, Njiitalu Pastef li, lii la wax :

“Yeen, naataangoy réew mi,

Tuuma yii toftalu lañu mujje wax ne, lañuy toppe taskatu-xibaar bii di Paap Aale Ñaŋ :

1 – li mu siiwal wayndare wu pólisu réew mi defaroon lu jiitu ñuy déglu genn kilifa ci wàllu pólitig, te wayndare wi aju woon ci matuwaayi fàggandiku ;

2- li mu siiwal weneen wayndare wu ñeel sàppëer yi ;

3- li mu yor aw wayndare wu ñu sàcc, te muy lees nëbb ;

Paap Aale Ñaŋ nee na, wayndarew pólis wi ci boppam, ci lënd gi la ko jële, ni ñépp, te mësul a siiwal wu sàppëer yi.

Ginnaaw bi ñu waxtaanee ay waxtu, waa Nguur gi dañoo mujje bàyyi sabab bi taxoon dëgg-dëgg ñu jàpp ko : ràppooru luññutug sàndarmëri bi ne fàŋŋ te indi jiixi-jaaxa bu réy a réy biir kootookati Nguur gi. Ndaxte, xam nañ njeexital yi ciy tukkee yépp te dañu ragal a biral wayndare wu tàng woowu. Waaye, wees na ! Wayndare waa ngi fi mu war a nekk dëggantaan.

Paap Aale Ñaŋ nag, du doon weneen nag saraxu Nguur gi nga xam ne, ginnaaw bi mu defee njombe ba noppi, day bëgg a ŋalaab ñi koy ŋàññ.

Maa ngi ànd ak moom ba mu jeex, ndax dañu ko tooñ, pólisu Maki Sàll, ci ndigalu Toppekatam bi, moo ko jàpp ci anam bu jubadi te safaanoo ak yoon. Bàyyileen ko te leeralal askanu Senegaal njombew njëndum ngànnaay mi, te ngeen leeralaale jëflante yu teey xel yi ngeen am ak njabootug Peretz ak i këri liggéeyam. »

Du Sonko kese moo àddu ci mbir mi. Nde, Soxna Aminata Ture, moom it, ñaawlu na jàpp gi, wax ne :

« Sunu demokaraasi dafa weesu fi ñuy jàppe ay taskati-xibaar yoy, seen liggéey kepp lañuy def. Paap Aale Ñaŋ, dañu ko war a bàyyi ci ni mu gën a gaawee “

Biraayim Sekk, njiitalu kurél gees dippe Forum Civil, lii la wax ci mbir mi :

“Noo ngi xaarandi Toppekatu Bokkeef gi ba xam yan leeral lay biral ñeel tuuma yees di toppe taskatu-xibaar bii di Paap Aale Ñaŋ. Bu ko defee, waa Senegaal dinañu gindiku ci mbir mi ba xam ban taxawaay lañu ci war a am.”

Gii Mariis Saañaa tamit sàndi na ci kàddu, wax ne :

« Dañoo bëgg fayloo Paap Aale Ñaŋ li taamu askan wees di xoqatal wëliis Njiitu réew ak i jëwriñ yoo xam ne, dañuy kootoo ngir daaneel njiitalu kujje gi, ñoom ñi nga xam ne dañuy lottal ak a rey seen askan.

Maki Sàll dafa bëgg a damm genn xalima gu jafe gu taxaw temm di bañ, benn taskatu-xibaar bu jafe boo xam ne kenn soppiwu ko, def ko surga, muy dunguroo xalimaam.

Maa ngi fésal sama jàppale ci lépp ñeel Paap Aale Ñaŋ ! »

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj