Tontu du forox naam, waaye mën na booy i nopp. Bu yeboo seet ba xam noppi Njiitu Réewum Farãs li booyuñu. Nde, tontu li ko Usmaan Sonko tontu, saf na sàpp. Moom, elimaanu jëwriñi Senegaal yi, dafa weddi kàdduy Emmanuel Macron yi. Njiitu Réewum Farãs li dafa wax ne, jóge bi sóobarey Farãs yiy jóge ci yenn Réewi Afrig yi, niki Senegaal, lees waxtaane la ca njëlbeen. Kàddu yooyu la Usmaan Sonko weddi ba mu set, ci waxiin wu dëgër nag.
Ku xam Usmaan Sonko ci fànnu pólitig, xam ne du kuy wann baat. Moo tax it, bi Njiitu Réewum Farãs li waxee ci ñibbig sóobarey Farãs yi, Usmaan Sonko xaarul sax lu yàgg ngir tontu ko. Nde, ci altiney démb ji, 6i fani sãwiyee 2024, la bind ci xëti Facebookam ak X, ñaawlu kàdduy Macron yi.
Njiitum réewum Farãs li dafa amoon ndaje ak àmbaasadëeri Réewam ca seen njénde la (l’Élysée). Ba muy wax ak ñoom nag, dafa àdduwaale ci mbirum sóobarey Farãs yees bëgg a jëlee ci réewi Afrig yi. Dafa di, fan yii weesu, Senegaal, Koddiwaar ak Càdd dañu xamle ne sóobarey Farãs yi dañuy ñibbi, ñu daldi jëlaat béréb yees leen jagleeloon. Li ko sabab mooy ne, dañu bëgg a tëggaat seen diggante ak nootkat ba woon (Farãs), gën a moom seen bopp. Te, ngir fàttali, Njiiti Réewi Mali, Burkinaa Faaso ak Niseer, ñoom, jot nañu dàq Saa-Farãs yi ba noppi. Mu mel ni, Farãs dafa ñàkk Afrig, buumu njaam gi doxoon ci diggante bi dafa dog. Loolu nag, ñu bari dañu jàpp ne toroxal la ci Farãs. Looloo metti Macron ba tax ko wax ne Farãs moo demal boppam te waxtaan na ci ak Réewi Afrig yi. waxam jooju nag moo sabab coow li.
Bu dee Senegaal moom, Usmaan Sonko weddi na ba mu set kàdduy Macron yi. Ndax, ci li mu bind, moom elimaanu jëwriñ yi, nee na « Bu dee Senegaal, wax jooju dara du ci dëgg », mu teg ca ne, « …ba tay jii, amul fenn fu ñu waxtaanee walla waxaale mbirum ñibbig sóobarey Farãs yi. »
Ginnaaw bi mu weddee waxu Macron jooju, Usmaan Sonko leeral na ne, ndogalul jële fi daluy sóobarey Farãs yi, Senegaal « …a ko jëlal boppam te kenn xiiru ko ci, niki réew mu moom boppam, jonn te am sañ-sañi boppam. » Maanaam, Senegaal moo xalaatal boppam, seet ba seet, xam ne teewaayu sóobarey Farãs yi fi réew mi, dëppoowul ak màndargay Réew mu moom boppam, ba tax ko jël ndogalu jële leen fi. Kàdduy Usmaan Sonko dañuy dàq itam li Macron wax ne, « sunu yar ak teggin [ñoom njiiti Farãs yi] moo tax nu bàyyi leen ñu njëkk a siiwal xibaar bi. » Loolu yit, ci kàdduy Usmaan Sonko, dafa woroo ak dëgg.
Fi tontu Usmaan Sonko li gënee ñagas mooy fi muy weddee li Macron wax ne « menn réewu Afrig du woon moom boppam tay bu dul woon ci ndimbalul Farãs. » Foofu yit, Elimaanu jëwriñ yi yemale na Njiitu Réewum Farãs li. Ndaxte, xamal na ko ne, Farãs « …amul kàttan gi te amul sañ-sañ bi ngir sàmmal Afrig kaaraangeem ak jonnam. » Ngir dëggal ay kàddoom, elimaanu jëwriñ yi dafa sukkandiku ci Réewum Libi mi ngi xam ne, ciy kàddoom, sóobarey Farãs yi « … bokk nañu ci li yàq Réew ma […] yàqaale Réew yi féete ci Sayel bépp ci wàllu kaaraange. »
Ba muy daaneel, Usmaan Sonko fàttali na Macron wall gi sóobarey Afrig yi wallu woon Farãs ca jamonoy ñaareelu xare bu mag ba, ba leen Hilter songee. Dafa wax ne, « Bu dul woon sóobarey Afrig yoy, yenn saa yi dañu leen jaay doole dugal leen ci làrme Farãs ba woon, metital leen ba noppi wor leen, bu dul woon sóobare yooya ñoo walluji Farãs ca jamonoy ñaareelu xare bu mag ba, kon Farãs, amaana tay jii, mi ngi ci loxoy Almaŋ yi ba tay. »
Du Usmaan Sonko rekk moo tontu Macron. Waa Càdd tamit tontu nañu ko tontu bu wex xàtt. Seen jëwriñu Mbiri bitim-réew, Abderahmaan Kulamalla, dafa génne ab yégle di ci ñaawlu kàdduy Njiitu Réewum Farãs li, di ko wax mu jox cër Réewi Afrig yi te bàyyi di leen suufeel ak a sewal ndax, la woon wonni na.