Elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, ma nga woon démb ca ndajem njàppale Palestin ma ñu doon amalee fa Espalaanaatu Jumaay Ndakaaru ju mag ji. Kurél gees duppee Alliance nationale pour la cause palestinienne a ko doon amal. Kurél googu, ci kàllaamay Kocc, mooy Déggoob way-réew mi ngir jàppale Palestin. Mbooloom junniy junni nit wuyusi woon nañu woote bi. Ràññees na fay raayay Palestin ak Senegaal yu ndaw, am ñu sol i tiset yees bind ci « Palestine libre » (Palestin dafa war a moom boppam).
Ci kàdduy elimaanu jëwriñ yi, Càmmug Senegaal bëggatuñoo yem kepp ciy wax. Ñoom, Càmmug Basiiru Jomaay Fay gi, dafa bëgg yokk taxawaayam ci wetu Palestin, ànd ak moom ci xeex bi muy xeex ngir afal boppam. Usmaan Sonko a ko xamle ca ndaje ma :
“Nguur gu bees gi, ci kilifteefu Njiitu réew mi, Njiitu réew mi, dafa jël ndogalu jéggi wax yeek jéego yi Mbootaayu Xeex yiy jël, waaye dafa taxaw ci sunu mbokki Palestin yi ngir xeexle neen.”
Senegaal moo jiite Komite biy wattu àqi askanu Palestin li ko dale atum 1975 ba tey. Boobaak léegi, seqi nay jéego yu bari ngir taxawu Palestin. Elimaanu jëwriñ yi fàttali na démb bi ci mujj, mooy ca atum 2016, bi Senegaal defee pexe ba ñu wote déggoo buy daan Israayel ci li muy wéy di sàcc suufi Palestin yi. Waaye, bees sukkandikoo ci kàdduy Usmaan Sonko, réewum Afrig-dii-Sidd moo gën a sori xeexal Palestin. Ndax, Njiiti Afrig-dii-Sidd yi dem nañ ba dog seen i jëflante ak Israayel, dippee leen réew muy jëf i pekk ñeel nit (crimes contre l’humanité). Moom, Usmaan Sonko, jàpp na ni réew yiy jàppale Palestin dañu war a booloo, bennoo ngir gën a mën a taxawu Palestin, dakkal nooteel ak tooñaangey Israayel yi ñeel Palestin. Ngir loolu mën a àntu, Usmaan Sonko dafa gis ne fàww réewi jullit ñi booloo ngir mën a jàmmaarlook seen i noon. Daf ne :
“Danu war a ràññatle mbirum diine ji ak mbirum pólitig ngir booloo ngir def wenn say, mën a aar sunu bopp.”
Usmaan Sonko ŋàññ na tamit taxawaayu réew yiy wootewoo demokaraasi te i seetaan Israayel miy fitnaal Palestin. Ciy waxam, mbir mi dafa mel ni « Kumba am ndey, Kumba amul ndey ». Ndax, ba tey ciy waxam, danu nekk ci « àdduna su màndoodi sos, ñiy wootewoo demokaraasi ak a taafantoo àqi doom-aadama ñooy jàppale Israayel ».
Ki jiite kurél gi woote ndaje mi, Mustafaa Señaan, jël na fa kàddu gi, di woo Saa-Senegaal yépp, ak lu ñu mën di gëm, ñu bennoo ngir Palestin mën a moom boppam.
Àmbaasadëeru Palestin bi nekk Ndakaaru, Naseer Jaddalaa, rafetlu na farle bi askanu Senegaal farle wow Palestin, rawatina ci jamono jii nga xam ne, Israayel dafa def « blocus » pàqu ((ñu bañ ko jaawale ak baatu pàkk). Gaza bi. Rafetlu na tamit teewaayu elimaanu jëwriñ yi ci ndaje mi. Ndax, ci li mu wax, wii yoon mooy guléet ci mboorum Senegaal ag kilifa gu bokk ci Càmm gi di fekkee ndaje mu ni mel.
Cig pàttali, atum 1947 la Mbootaayu Xeet yi, ci coobarey boppam, ràccal Israayel ag mberaay biir mberaayu Palestin. Diggante 1949 jàpp 1967, Israayel, ci ndimbalu saa-amerig yi ak yenn réewi tugal yi, jaay doole waa Palestin, nangu pàcc bu bari ci seen suuf. Noonu la ko yawuudi siyonist yi jàppe ba jonni-Yàlla-tey jii nga xam ne, Palestin, dara desatu ci lu dul ab pàq. Keroog gaawu 7 oktoobar 2023 nag, yemook bés bi Israayel di màggal Yom Kippour, Hamas dafa songoon Israayel, rey fa ñu bari. Israayel daldi fayu ci anam bu jéggi dayo te, boobaak léegi, mi ngi wéy di xoqatal Palestin.