WAAW, ANA AAMADU BA (BBY) ?

Yeneen i xët

Aji bind ji

Gaawu, 3 féewaryee 2024 lañ gëj a dégg Aamadu Ba, jëwriñ ju mag ji, di yit lawaxu lëkkatoo Bennoo Bokk Yaakaar. Moom nag, bi Njiitu réew mi jëlee ndogalu fomm wotey 2024 yi ba léegi, gisuñu ko fenn, dégguñu ko fenn. Lu tax ?

Fan yii, Aamadu Ba fésoon na lool sax. Muy ci tele yi, rajo yeek mbaali jokkoo yi, fépp la Aamadu Ba ame woon, saf sàpp ci bët ak noppi Saa-Senegaal yi. Nde, dafa mel ni ku tàmbali woon kàmpaañam, di wër réew mi, fu nekk mu dem fa. Tey, mu ngi fii di ubbi dara, suba mu ngi fee di amal i nemmeekuy koom-koom. Waxtu wii, nga gis ko Tuubaa, waxtu wee nga dégg ko Tiwaawan walla ci geneen këru diine.  Lépp rekk, ngir waajal wotey 25 féewiryee 2024 yi. Dafa di, dafa doon taafantoo mbubbum jëwriñam ngir di kàmpaañ ci suuf te mbir yi dooraguñ woon. Ànd ak loolu yépp, Aamadu Ba jekkuwul woon ba tey wote yi. Waaye nag, taxu ko woon xàddi. Nde, gëmoon na ni, ba tey, mën na gañe wote yi. Moo tax, xalaatul woon ñuy dàq àppug wote yi.

dafa di, keroog bi Aamadu Ba séq ub laaj-tontu ak waa Dakaractu, biraloon na xalaatam ci ruumandaat yees doon ruumandaat ndàqug wote yi. Moom, dafa waxoon ni àndul mukk ci ñuy dàq wote yi, di leen bëtal. Waaye de, Maki Sàll mi ko tabb, tànn ko def ko lawaxu Bennoo Bokk Yaakaar, dafa mujje fomm wote yi. Loolu day firndeel woroo bi am diggante Njiitu réew mi, Maki Sàll, ak jëwriñ ju mag ji, Aamadu Ba. Diggante bi rataxul jamono jii.

Keroog àjjuma 2 féewiryee 2024 sax, dalu web bii di Confidentiel Afrique siiwal na xibaar bob, mi ngi ciy wax ne Maki Sàll ak Aamadu Ba séqoon nañ waxtaan wu tàng jérr, maanaam xuloo nañ. Ndaje moomoo jiitu wax ji Maki Sàll wax ne day fomm wote yi. Te, moom Aamadu Ba, du Maki Sàll kese la réerool. Ndaxte, ñu bari ci waa APR ànduñu ak moom, jàppalewuñ ko. Moom kay, dañ koy xeex sax ci lu bir te nëbbatuwuñu.

Warees na xam ni, dekkare bu Njiitu réew mi mën a jël, fàww jëwriñ ju mag ji toftal xaatimam ci kow xaatimu Njiitu réew mi. Lu ko moy, dekkare boobu du am cëslaay te du baax. Laaj bi sampu nag moo di ne, ndax Aamadu Ba dina nangoo xaatim dekkare biy fomm wote yi ? Walla day bañ ngir jàmmaarlook Njiitu réew mi ? Ndax day tekki ndombog-tànkam ni ko ko ñenn ñiy xelalee ?

Li kanam rawul i bët.

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj