Ñoo ko dige woon, tàmbali nañ ko def. Càmmug Basiiru Jomaay Fay geek Usmaan Sonko miy njiitul jëwriñ yi, wàñni na lenn ci dundu gi. Yi askan wiy gën a aajowoo lañu wàññeegum.
Kilo suukar su mokk si daan jar téeméer ak fanweeri dërëm (650 FCFA) léegi téeméer ak ñaar-fukki dërëm (600 FCFA) lay jar.
Wàññi nañ juroom-ñetti dërëm (40 FCFA) ci njëgu kilob ceeb bu ñu parfiimewul. Nee ñu sax, am nay gaali ceeb yu mag yu bawoo End, yeb lu tollu ci juroom-ñett-fukki junniy toni ceeb (80 000 tonnes de riz), jëmsi Senegaal.
Diwlin gi tamit wàññi nañ ci ñaar-fukki dërëm (100 FCFA) ci njëgu liitar bi.
Bu dee mburu mi, kilo bi daan jar fanweer ak juróomi dërëm (175 FCFA) wàññi na, léegi fanweer ak ñaari dërëm (160 FCFA) lay jar. Ñetti dërëm (15 FCFA) lees ci wàññi.
Njëgu simoŋ bi yit wàññeeku na. Nde, dañu far galgu ñeenti téeméeri dërëm (taxe parafiscal de 2 000 FCFA).
Ngir wattu wàññi yi nag, dees na delloosi SONADIS ci anam bu bees niki ay “Magasins Témoins”. Ayooba Fay moo ko xamle. Lees ko duggee mooy fexe ba jaaykat yi sàmmonte ak njëg yu bees yi, mu bañ a am ay jalgati.
Naka noonu, ci lees jukkee ci taskatu xibaar bile, Càmm gi fas na yéene jël ay ndaw, góor ak jigéen, ngir taxawee liggéey boobii.
Ci diirub ñaari weer kepp, Càmm gu bees gi teg na jéego bu njëkk ñeel wàññig dundu gi ngir jàppandalal ko askan wi. Li ci des nag mooy fexee yaatal ko te lal i pexe ngir njëg yi bañatee yokk. Ndax, ñi fi jot a jaar ñépp, ku ci nekk jot na wàññi dundu gi. Waaye, daawul yàgg, lépp yokkaat. Kon, bu ñu mënulee gën a wàññi njëg yi, sasam mooy fexe ba njëg yooyi yem fi ñu yem.