WAXTAAN CI MBIRUM ALFAABETISAASIYOŊ AK DEMOKARAASI Mamadu Jara Juuf 2/2

Yeneen i xët

Aji bind ji

Yaxal bii, aw waxtaan la wu, bindkat bii di Mamadu Jara Juuf moo ko amaloon ca Kawlax, 8 sàttumbar 1992. Mi ciy waxtaane alfaabetisaasiyoŋ ak demokaraasi ci kàllaamay Kocc. Solos wax ji, ak dayoom, ñoo tax seen yéenekaay Lu defu waxu biral leen ko. Waxtaan wi nag, xaajees na ko ñaari pàcc. Ca pàcc bu jëkk ba, werekaan baa ngi ca doon faramfàcce maanaa ñaari baati nasaraan yii di alfaabetisaasiyoŋ ak demokaraasi. Ci pàcc ñaareel bile nag, da ciy biral solos njàng ci doxalinu demokaraasi, rawatina njàngum làmmiñi réew mi.

 Njariñu njàng, saytu doxalin

Gis nanu ne demokaraasi doxalin wuy cëral mboolo la. Loolu, dafay jox nguur gi ay sañ-sañ, walbatiku gàll ko ay xeeti warugar. Mboolo mi ci boppam teg nañu ko ay wareef waaye am na itam ay sañ-sañ.

Bu nu jàppee ni nguur gi xam na liy wàllam ci ni àddina di doxe ci sayir, mënees naa jàpp it ne mboolo mi moom umple na ci lu bari, te li njëkk ci li ko waral moo di ñàkk jàng. Ñaari firnde kepp laay joxe ngir màndargaal wax jii :

Bu njëkk bi mooy : danoo maase ak jamono mbind. Xam-xam dees ko ŋëb ci mbind. Ay soxla ak ay xalaat nu ngi leen di bindante. Xew-wewi jamono ji, sàrtu àtte yi, lépp danu ko tëral, bind ko teg. Nu daldi gis ne kon jamono toll na fu xamees ne, ku mënul a bind, daanaka danu lay ber.

Bi ci topp moo di sunu réew yi ngeen xam ne Tubaab bi da leen a nootoon, ba léegi ci làmmiñu jàmbur lañu leen yore ; ay làmmiñ yoo xam ne waa réew mi nàmpuñu ko, te lu mat asakay doomi réew mi dégguñu ko. Bu nu jëlee ab tegtal ci sunu Senegaal gii, mënees naa wax ne téeméeri nit ñoo jël, fanweer yi kepp a dégg nasaraan gu wér, ngën-jee-bari. Nu gis ne kon, ñaareelu ponk bi tënk na waxtaan wi ndaxte laaj biy daldi ñëw ci xel yépp moo di : ndax mën nanoo doxal baatu mbooloo mi su fekkee ne làmmiñ wa nuy jëfandikoo, téeméeri doomi Aadama yoo jël, juróom-ñaar-fukk ya dégguñu ko ?

Ngeen gis ne kon ñàkk a farlu gi ci wàllu njàng ak njàngale mi dina indi ay gàllankoor yu xaw a takku ci li mën a faaydaal baatu mbooloo mi, ndax dafay fekk sàrt yi am réew mën a jaar, muy lu xamees ne ay àtte ko tëral, mbooloo ma du ko mën a xam ndax ñàkk a jàng. Xeetu fitna ak jalget yuy dal ci seen kow it, doonte sax teguwul ci yoon, duñu xam fu ñuy jaar ba teggi ko.

Te bu dara desul lu dul delloo mbooloo mi kàddu gi, mu dogal, du xam sax ne moo ko yelloo walla boog bu ko xamee sax, du ci mën a fés ndax béréb ya nuy dogale, weneen làmmiñ lañu fay jëfandikoo wu dul wosam. Te sax doonte aw làmmiñam lañu fay jëfandikoo, lu bari dina ko ci rëcc ndax ñàkk a mën bind.

Rax ci dolli, ñi yelloo ab dogal, dañoo war a nekk ay nit ñu, seen i xel ubbiku na, seen i gët fett ci ni àddina di doxe ci sayir. Doon mbooloo mu mën a dendale ay yoon yu bari yu jamono indi, seet ca ba méngoo ak lu koy jariñ musal ko. Te léeg-léeg nag, xew-xew yi dinañu jaxasoo ba, ki toog ci keppaaram rekk yaakaar ni àddina fa la yem, dafa ciy gaaw a gëlëm.

Mu bir ne kon, njàng mi ci boppam dafa di cër ci nit ku mu doon, rawatina ay muskàllaf yu, képp kuy saytu xam-xam walla ay xalaat yu rafet ci ñoom ngay jublu. Kon boog nanu ko cërale sunu bopp, te bañ ci xaar kenn ndaxte wolof yi dinañu di faral di naan « mere màndiŋ, mën a waaxoo ko gën ». Te taal bu tëw a tàkk, wet gu nekk ngay xambe ; waaye boo dee def matt gu saxaar nga xembi sànni, doo ñorle.

Alfaabetisasyoŋ mooy ndëraan miy maasale dig wi xàjjaatle ñi jàngoon ak ñi jàngul. Muy doole ji askan wi mën a sukkandikoo, doon jenn jëmm bokk taxawaay ci liggéey biy jëme réew mi kanam.

Jàng nag du wees ; rawatina ba ñu amee aw teggi wuy tax mbir mi du taxawaalu, te mu di jàngal nit ki ci làmmiñ wi mu nàmp te dégg ko ba noppi. Bu ko defee mu mën caa bind la ko soob, di ca xayma, di ca sàkku bépp xeetu xam-xam.

Loolu nag, li koy rafetal te gën koo yombal, yokk nit ñi pas-pas, moo di cëral sunu làmmiñ yi ci doxalinu nguur gi. War nanoo fonk sunu kàllaama yi, te bañ a yaakaar ne jamano mën naa indi ci wàllu xam-xam ak xarala lu sunu làmmiñ yii mënul a tudd.

Loolu njuumte la, te fi xeeti àddina si yépp jaar ba agsi fii mu toll tey, joxe na ci ay tegtal yu leer, muy ay misaal yuy biral ne « lu am xel daj rekk aw làmmiñ mën na koo tudd ». Lii bokk na ci xalaat yi ndem-si-yàlla Séex Anta Jóob bàyyi, moom mi dëkkoon di nu fàttali ni am xel mooy gàtt, aw làmmiñ gàtt ; waaye nit kiy wax moom, fi xelam tollu, fi gis-gisug àddinaam yem, foofu rekk la ay waxam mën a yem.

Kon ci gàttal, mënees naa wax ne, ndeem demokaraasi moo di doxalin wu wéeru ci baatu mbooloo mi, la koy sabab dëgg-dëgg mooy : mbooloo mi di def fu mu tollu, mbir mu nu ko woo rekk, mu xam loola lu mu laaj, daldi ko mën a jox àqam.

Ngeen gis ne kon, alfaabetisasyoŋ xorom la ci ndax solo sépp ci moom la aju.

Moo tax nu war ci góor-góorlu, def ci kem sunu kàttan te bañ a réere mbir ne yit bu nu bëggee sukkandiku ci sunuy làmmiñ ngir saxal demokaraasi, tabax réew mi, fàww ñu mottalee alfaabetisasyoŋ bi, beneen liggéey, te muy yokk gëstu bi ci wàll wi soxna Aram Faal tudde « yaatal sunu làmmiñ yi, méngale leen ak jamono ».    

Mamadu Jara Juuf

Kawlax, 8 sàttumbar 1992

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj