Wolof dinay faral di wax ne, réeroo amul, ñàkk a waxtaan a am. Waaye, booba, day fekk waxtaan wa am sabab bu ko jar, am bopp ak i ponk, jubluwaay bi leer nàññ. Muy benn. Ñaareel bi mooy ne, kay woote waxtaan wi daf ko war a mate, am dayoom te yey ca. Ñetteel biy dellu ci dëggu ak yéene ju rafet ji war a màndargaal ñiy sékk waxtaan wi. Ndaxte, waxtaan kat, wax dëgg ca la. Bi ci mujj mooy, ña tax ñuy waxtaan ak ña leen di teewal, dees na jox mbaa delloo képp-kenn ci ñoom àq jim yeyoo. Lu ko moy, mbir mi dootul nekk waxtaan, waaye naxtaan lay doon.
Waxtaan ?
Keroog ci korite gi, ca laaj-tont bam amaloon ak Allaaji Asan Géy ca rajo RFM, Njiitu réew mi, Maki Sàll, dafa woote aw waxtaan. Boobaak léegi nag, ci loolu rekk lañuy yey ak a yàbbi daanaka. Soxlay askan wi moom, tegees na leen boor.
Na ñu dee ak xiif, waxtaan a xew. Na ñu dee ak mar, waxtaan a xew. Na ñu feebar ba ñàkk lu ñuy fajoo, waxtaan a xew. Na ñu dëkke luubal seen i alal, waxtaan rekk. Na ñu leen xoqatal, di leen tooñ, di leen jàpp a tancale ci kaso yi, waxtaan rekk. Xëyu ndaw ñi ? Seen yoon, waxtaan kese. Njàngum xale yi ? Seen yoon, waxtaan kese. Dundu gu jafe gi, seen lanc nekku ci. Nde yëguñu ko. Waxtaan a xew, waxtaan rekk, moom kese. Waaye, waxtaan diggante kan ak kan, fan, ngir lan, kañ ?
Waxtaanu pólitig ngeen wax de, am déet ? Waaw, ndax réew mi dafa nekk ci fitna ? Déedéet.
Ndax dafa am ay noon yu song Senegaal ? Déedéet.
Ndax dafa amati mbas mu gaar dëkk bi ? Déedéet.
Ndax jéyya walla musiba bu réy dafa dal ci kow réew mi ? Déedéet.
Ndax Senegaal dafa nekk ci guuta ? Mën na am. Waaye, bu amee yit, ndax waajaleesu woon ay kurél ak i campeef yo ko war a waxtaane ngir génn ci ? Ãhã kay ! Bañ a am.
Senegaal amul ug Ngomblaan, walla ? Xanaa du moom lañ duppee Péncum réew mi ? Xanaa askan wi falul i dépite, ñu war ko faa teewal cig wuuteem, di fa fénce li ko ñeel ? Ndege, ngomblaan gi, béréb la bob, dajees na fa pàcci réew mépp, xeet yépp, diine yi ci réew mépp. Diiwaan bu nekk, gox ak gox-goxaan bum ci doon, am nga fa ndaw. Xanaa kon waxtaan fa la gën a yey. Du dëgg, walla ? Waaye, Njiitu réew mi, Maki Sàll, daf ko tëjlu diirub ñeenti weer, desàmbar ba keroog barki-démb. Askan wiy fay dépite yi weer wu dee xaalis bu baree bari te liggéeyuñu. Kon, Maki Sàll, loo dugge waxtaan wi ?
Ana Ndajem depàrtmaa yi nekk, maanaam “Conseil départemental” yi ? Xanaa foofeet amul i falaakoni askan wi, ñu dénk leen mbir depàrtmaa yi, ñu war leen a waxtaane ? Waa kon Maki Sàll, sa waxtaan wi lan la ?
Ana meeri yi ? Luy njariñu ndajem diglekati meeri yi ? Du waxtaaneek a doxal gox ba ? Waa Maki Sàll looy waxtaane ?
Maki Sàll, xanaa du yaa fi sos kurél gees duppee Magum ndajem diisoog mboolaay gi, maanaam Haut conseil du dialogue social ? Ñoo ngi lay laaj nga wax nu lu taxoon nga sos ko, def ci xaalis bu baree bari, di xaalisu baadoolay Senegaal yi. Mbaa du ngir neexalee ko say militaŋ a taxoon ? Kon looy woote waxtaan ?
Maki Sàll, xanaa du yaa fi samp “Haut conseil des collectivités territoriales” ? Moom itam lu muy jariñ ? Lu “Conseil économique social et environnemental” di jariñ tamit ? Luy liggéeyu Médiateur de la République ? Xanaa gox bu nekk amul ag kurél guy fénc soxlay gox ba ak lu koy jëmale kanam, ñu naan ko ci farãse “conseil de développement du quartier” ?SëñMaki Sàll daal, sa waxtaan wi dafa rax. Te sax, yow, xanaa amaloon fi ñaari waxtaan diggante 2012 ak tey ? Fu ñu mujje ?
Naxtaan…
Wareesul a fàtte sax ne, bi Maki Sàll faloo ak léegi, 2012 ba tey, woote na fi ñaari waxtaan. Bi ci jiitu, ca la génne Kariim Wàdd kaso, gàddaayloo ko ca dekki naar ya. Fekk ne, booba, moom ak baayu Kariim Wàdd am na luñ jotoon a nas ca Gine Konaakiri, ñu di ko wax ci farãse “Le protocole de Conakry”.
Ñaareelu waxtaan wi, ca la parenaas ya tukkee. Amoon nay déggoo yu bari yees xaatimoon te parenaas bi bokku ci woon. Waaye, ca waxtaan woowu la Njiitu réew mi jaare woon, layal ko.
Ci ginnaaw gi, juroon na coow lu réy a réy, ba CEDEAO sax santoon Nguurug Senegaal mu dindi ko. Nde, day salfaañe demokaraasi ak àqi lawax yi bëgg a dagaan baatu askan wi. Waaye, Maki Sàll ak nguuram dañoo tanqamlu, jàllale ko ci doole. Yeneen déggoo yi moom, ba jonni-Yàlla-tey jii, kenn jëmmalu leen. Mu mel ni, Maki Sàll, daf leen doon naxtaan ngir sottal pexeem. Wii yoon nag, man pexe la Maki Sàll di nos ak nocci, bëgg ko jaarale ci waxtaan wi ?
Nax, tànn
Waxtaan wii ñuy soow, Aminata Ture nee na Maki Sàll ak waa PDS ñoo ko bokk sumb. Soxna si ne duggewuñ ko lenn lu dul delloosi Kariim Wàdd ci géewu pólitig bi, sàkkal pexe xaalis bi mu yoreel askan wi ak beddi Usmaan Sonko. Nee ñu yit, dafa bëgg naxasaale ba bokk ci wotey 2024 yi.
Pastef ak Usmaan Sonko bañ nañ waxtaani. Waa F24 bañ nañ waxtaani. PRP bu Décce Faal nee na bokkul.
Ku xool ni mbir yi tëdde, mën nga njort ne Maki Sàll, ber Sonko rekk a ko tax a jóg. Ndaxte, bu PDS ak Taxawu Senegaal nangoo bokk, liñ ci jublu mooy Kariim ak Xalifa mën a bokk ci wotey 2024 yi. Bu loolu amee, PDS ak Taxawu yépp naruñoo jàppale Sonko xi xeexal beek Maki Sàll. Nde, ku nekk ci ñoom ñaar, dafa am fu la Maki Sàll tée, rawatina Xalifa mi nga xam ne, bu 2024 weesoo, dootul mën a bokk ciy wote, ndax day ëppal 75i at bu 2029 teroo.
Ñaareelu pexem Maki Sàll mooy jéem a gëmloo yenn lawax yi ne day woyofal parenaas yi. Bokk na ci pexe yi tamit, daganal ñetteelu lawaxug Maki Sàll ak gëmloo àddina si ne, Senegaal, dëkku jàmm la ak dal. Sekk amul ci ne, waxtaan wii, Maki ngànnaay la ko begg a def ngir xeexe ko Usmaan Sonko.
Li Njiitu réew mi bëgg bu sottee, dina làq ay nitam yu luubal alalu askan wi, féewale kujje gi, jalgati wote yi ngir am ñetteelu moome. Maanaam daal, lii du aw waxtaan. Day jéem a naxtaan kujje gi, nax leen ngir tànn ñiy bokk ak ku dul bokk.