ÀTTEKAT YUY WERANTE BAY WEERANTE (NDEY KODDU FAAL)

Yeneen i xët

Aji bind ji

Fii ci Senegaal, ay kàngam ci yoon ñooy tamante dëmm. Àttekat bii di Yaaya Aamadu Ja moo jiiñ nawleem Usmaan Kan miy jiite tirbinaalu Kawlax ni ku ñuy ger la. Àttekat bii di Kan moom daa woote ndaje ak taskati xibaar yi, teggi tuuma ci kowam teg ci yakk Ja lu mel ni xeme. Lu jiitu loolu Kan tekkil na boppam ndombog-tànkam ci kurélu àttekat yi te Suleymaan Télikoo nekk ca bopp ba « ndax mënatul a dékku ñàkk orma gi ci biir te ñi féete ndaw di ko teg seeniy mag ».

Jëwriñ biy jiite yoon nag santaane na ñu ubbi ab lànket ci mbir mi ngir mu leer ndax rafetul ci deru Senegaal. Ñuy xaar ba xam fu wànnent di mujjee ki gëtëm. Laata boobu nag ñuy laaj lan moo xiir sunu àttekat yii ñuy werante bay weerante ?

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj